Previous Lesson -- Next Lesson
5. Pajug doomu kilifa takk-deru buur bi (Yowaana 4:43-54)
YOWAANA 4:43-46a
43 Ba Yeesu amee ñaari fan ca dëkk ba, Mu jóge fa jëm diiwaanu Galile, 44 ndaxte Moom ci boppam newoon na: ’Ab yonent kenn du ko faaydaal cim réewam. 45 Bi Mu agsee Galile, nit ñi teeru Ko, ndaxte ñoom itam teewewoon nañu bésub màggalu bésu jéggi ba, ca Yerusalem, te gisoon nañu lañu fa defoon lépp. 46 Noonu kon Mu dellusi Kana ca Galile, dëkk ba Mu soppewoon ndox ma biiñ.
Yeesu ak ay taalibeem waare nañu ca Samari. Waare nañu ak mbég, jaare ko ci kàttanu dund gu dul jeex gi. Jamono ji ñu waroon a jot askan yi, agseeguloon; Yeesu dafa waroon a yey xel yu bon ya nekkoon ca ay mbokkam ba noppi. Muu jubal ca Galile, ak la Ko waa Nasaret doon ñaawale lépp, boole ca jëfi coxorte ya Mu naroon a dékku. Xaritam ya ak ay mbokkam gëmaguñuwoon ne nitu asamaan la, ndaxte ci njaboot gu amul doole la bokkoon. Dañu faaydaaloon alal ak tur wu siiw, te xebatoon ñàkk alalu Yeesu. Manuloon a def benn kéemaan ca seen biir ndax seen ñàkk kóolute googu.
Siwaayu Krist ni fajkat daldi law fépp. Xabaaru kéemaan ya Mu defoon ca Yerusalem, ak ca Galile di wéy. Waa Galile yu bare dañu daan teew ca Yerusalem ci màggalu Bésub Jéggi ba (Paak). Jotoon nañoo dégg te gis lépp li Yeesu waxoon te def ko, rax ci Muy waare ak sañ-sañ gu mat sëkk. Ñu teeru Ko ak tàccu yu tar, di yaakaar a barkeelu ci kéemaanam yi. Yeesu dellu ca waa céet gu bees ga, ca Kana. Dafa bëggoon a matal liggéeyam ca biir ña Ko njëkkoon a yëg ndax kéemaan ba Mu fa defoon.
YOWAANA 4:46b-54
46b Amoon na benn dagu buur bu dëkkoon Kapernawum,te doomam feebar, 47 Bi mu déggee ne Yeesu jóge na Yude, ñów Galile, mudikk ci Moom, ñaan Ko mu ñów këram, wéral doomam ji wopp bay bëgg a dee. 48 Yeesu ne ko: »Yéen daal, dungeen gëm mukk, fi ak gisuleen ay firnde walla ay kéemaan. » 49 Dagu buur ba neeti Ko: » Sang bi, ñówal, balaa sama doom ji di dee. » 50 Yeesu ne ko: » Demal, sa doom dina dund. » Kilifa ga gëm la ko Yeesu wax, daldi dem. 51 Bi muy dellu këram nag, ay surgaam gatandu ko. Ñu daldi ne ko: » Xale bi dina dund! » 52 Mu laaj leen ci ban waxtu la tàmbalee tane, ñu tontu ko ne: » Démb ca njolloor la am ag féex. » 53 Noonu baayu xale ba daldi seetlu ne, ca waxtu woowa la ko Yeesu ne woon: »Sa doom dina dund. » Moom ak njabootam yépp ñu daldi gëm Yeesu. 54 Lii mooy ñaareelu kéemaan bi Yeesu def ci Galile, gannaaw bi Mu jógee Yude.
Kilifa takk-der gu mag ci ëttu buur bi daldi ñów ci Yeesu, ndaxte dégg na ay jalooreem ak sañ-sañam. Waa dëkk ba dañoo xalaatoon ne xëyna dafa koo bëggoon a wonale ak buur ba.
Bii takk-der dafa amoon doom ju feebar ca Kapernawum, ca booru dex ga. Baay ji yóbbu na ko ci doktoor yu bare, te fay ca xaalis bu takku, cig neen. Mujj gi, mu wékk bépp yaakaaram ci Yeesu. Ndax man na koo xettali am déet? Baay jii dfa bëggoon Yeesu jóge Kana ba Kapernawum, ci kow yaakaar ne teewaayam dina wéral doomam.
Yeesu amul genn làq-làq ci nuyoom ak kilifa googu. Xolam dafa tiisoon ci ñàkk ngëm gi Mu gisoon ci moom takk-der bi. Yeesu du la man a dimbali boo ko gëmul, ba seey ci Moom mi kenn dul méngale. Ñu bare dañuy ñaan, ba noppi di am xel ñaar. Dañuy bëgg a am ndimbal lu ñu man a teg bët. Way-gëm dëgg,dafay wéeru ci Kàddug Yàlla te am kóolute ne dina ko tontu.
Kilifa takk-der googu meruloon ci li ko Yeesu artu, waaye dafa suufeelu, ba woowe Ko sax « Kilifa gi » maanaam jàppe na boppam ni surgab Krist. Mbëggeel gi mu am ci doomam ji,ak wegeel gi mu am ci Yeesu ñoo tax mu wéy di ñaan Yeesu mu ñów Kapernawum.
Yeesu ràññee ci moom coobarey gëm Kilifteefam, ne ko: » demal, sa doom dina dund. » Yeesu dafa bañ a dem Kapernawum, waaye natt na mbëggeelu baay ji, te dëgëral ngëmam. Ndax gëmoon na ne Yeesu man na wéral xale ba ca diggante bu sore booba xale ba nekkoon?
Ci biir waxtaan wi, takk-der bi gis melokaanu Yeesu ak mbëggeelam. Mu wóor ko ne Yeesu dëgg la ko wax, te foowantoo-u-ko. Dafa gëm te gisagul sax wérug doom ja. Na mu déggale Yeesu, la doon delloo këram. Dégg ndigalam googu delloo na Yessu njukkal, te dëggal wér gi. Bu Yeesu manee wéral sama doom jiy waaj a dee, kon Moo sut lépp. Wér gi dafay wone sañ-sañam ak cosaanu asamaanam. Ñibbi bi ab nattu la woon ngir dëgëral kóoluteem.
Yeesu moo xiiroon dagi takk-der ba ñu gatanduji ko ngir xamal ko ne doom ja wér na péŋŋ. Njàqareem daldi deñ, noonu mu màggal Yàlla. Na mu bëggoon a xame ca ban waxtu la doom ja wére, mu gis ne ca diggu bëccëg la woon, maanaam ca ba ko Yeesu digee ne doomam dina wér.
Takk-der boobu seede na ci kanamu waa këram yépp kàttan ak mbëggeelu Krist, boole ca ay cant.
Bii kéemaan mooy ñaareel bi Yowaana xamle. Mbiru Krist tàbbi na léegi ca ëttu buur ba. Nit ñépp a ngi doon xaar nag yeneen xew-xew.Gëmal ne boo gëmee Yeesu, màggal gu Yàlla nangu la te di ko firndeel ak ay mandarga, aky jëf yu fees ak kàttan.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu, ñungi lay sant ci sa ñów. Wéral nga xale ba feebaroon ca Kapernawum, ak li mu la sorewoon lépp! Tax nga ba baay ja am ngëm gu takku ci Yów. May nu ñuy wóolu sa mbëggeel ak sa kàttan. Nungi ñaanal ñiy sànku ci seeni bàkkaar, te di am yaakaar ci nga nangul nu sunuy ñaan.
LAAJ:
- Yan jéego la takk-der boobu defoon ba ngëmam mat?