Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 031 (Jesus leads his disciples to see the ready harvest; Evangelism in Samaria)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?
4. Yeesu ca Samari (Yowaana 4:1–42)

b) Yeesu yóbbu na ay taalibeem ngir ñu gis meññeef mu ñor mi (Yowaana 4:27-38)


YOWAANA 4:31-38
31 Fekk taalibey Yeesu ya di Ko gétën naan: » Kilifa gi, lekkal. » 32 Waaye Yeesu tontu leen: » Am na ñam wu may lekk, te xamuleen ko. » 33 Taalibe ya nag di laajante naan: » Ndax dafa am ku Ko indil lekk? 34 Yeesu ne leen: » Sama ñam moo di def coobarey Ki ma yónni te àggale liggéey bi Mu ma sant. 35 Du dangeen naan: » Fii ak ñeenti weer ñu góob? » Waaye man, dama leen naan: » Xool-leen tool yi, ñoongi ñor ba weex tàll, di xaar ku leen góob. 36 Kiy góob tool yi mungi jot xaat peyam; day dajale nit ñi ngir dund gu dul jeex, ni ñuy dajalee pepp. Kon book, kiy ji dina bégandoo ak kiy góob. 37 Wax ji ñu wax ne: » Kenn dina ji, keneen góob. » dëgg la. 38 Yebal naa leen, ngeen góob tool bu ngeen bayul. Ñeneen a ko bay, te yeen a ko jariñoo. »

Ba Mu yewwee ruuwu jigéen ja doon njaaloo te may ko dund gu dul jeex ba noppi, Mu wëlbatiku ca taalibeem ya ngir xettali leen ci lu xaw a deme noonu. Seeni xalaat ci mbiri àddina rekk lañu daan faral di jublu. Béguñuwoon sax ci li Xelum Yàlla mi matal ci xolu jigéen ji. Lekk ak naan, lu am solo la ci dund, waaye am na ñam wu ëpp solo mburu, ak xel mu dal, mu gën a am doole li ndox man a maye. Waroon nañu xam loolu. Gënuñuwoon jigéen ji, ak li ñu doon wone ngëm te di topp Yeesu lépp.

Yeesu xamal leen li ñamu asamaan, walla baatin, di tekki. Ñam woowu moo ëppal solo ruu wépp weneen ñam. Xolu Yeesu seddoon na ci li Mu nekkoon barke ci ñeneen ñi, te di def coobare Baayam.

Yeesu,Yonent-Yàlla lawoon. Moo nekkoon Doom ju déggal Baayam, te di matal coobareem ak mbég, ndaxte Yàlla mbëggeel la. Li Krist déggal Baay bi tekkiwul ne Moo Ko gën a féete suuf, waaye dafay wone yaatuwaayu mbëggeelam. Doom ji nee na muccug àddina si, liggéeyu Baayam la, donte Moom ci boppam moo ko matal. Mu màggal Baayam, ni Baay ji tegewoon ca njalbéen ga lépp ci loxoy Doom ji. Baay ji may na Doom ji mu yilif lépp, te toogloo Ko ci ndeyjooram, jox Ko bépp sañ-sañ ci asamaan ak ci suuf.

Ca pindu teen ba, coobare Yàlla moo doon musal jigéen jooju ñu sewaloon. Du Yawut yi rekk lañu mayoon ñu mucc, waaye bépp doomu Aadama. Ñoom ñépp a geruwoon, te xiif teewaayu Yàlla. Yeesu gis ni jigéen ji màcce, ak ni mu soxlaa njéggal. Ni mu yàkkamteewoon jot mbaalu bàkkaar moo gënoon a fés bu Yawut ya. Ci saa si, Xel mu Sell mi won Yeesu niti àddina sépp, ñu mel ni ab tool bu rëy a rëy te fees dell ak mbooq mu ñor-xomm muy xaar ñu góob ko.

Taalibe ya nag manuñuwoon gis tool boobu di misaalu àddina, si jekkoon ngir ñu góob ko. Ci jamonoy sedd la Yeesu ñówoon ca Samari te waxtu ngóob sorewoon na. Mungi mel ne Yeesu dafa naan: » Yeenangi faaydaal mbir yi dul dara yi ñuy gis bés bu nekk. Deeleen bàyyi xel ci dëgg yi nekk ci xolu nit ki; bàyyileen di laaj seen bopp rekk, te di yóotu dund gu naat. Wutleen Yàlla! Tey jii mooy bésu ngóob mi. Ñu bare naroon nañoo nangu Doomu Yàlla ji ni seen Musalkat, bu fekkoon ne yëgal nañu leen xabaaru mucc gi, ci biir maandute ak mbëggeel. »

Xëyna leneen gay yëg lu mel ni » ñi ma wër ñépp dañoo dëgër bopp, sax ci seeni aada, walla gumba. Xëyna loolu la taalibe ya doon xalaat itam,ndaxte amuñuwoon gis-gis bu xóot. Waaye Yeesu dafay gëstu biir xol yi. Merewul sax jigéen ja Ko jàppewoon ni ab doxandéem. Amul benn sikki-sàkk sax ci wéy di waxtaan ak moom, ak li ko diisoo baatin bi sute lépp, taxul Mu bañ a wéy di waxtaan ak moom, ci nu woyof te leer. Xelam dimbali ko ba mu xam ,te yëngal ci moom pàttaliku màggal ak nguurug Almasi bi, ba xiir ko ci nekk ab yéenekatu Xabaar bu baax bi (Injiil li). Ndaw coppite! Jigéen ji moo gënoon a jëfi Xel mi Nikodeme sax. Boo dee liggéeyal Yeesu, dangay soxla mbëggeelam ngir man a ràññe ñi xiif njubte Yàlla. Bul toppatoo seen dëgëraayu xol, walla seen ñàkk pasteef, Yàlla bëgg na leen; te Yeesoo ngi leen di woo. Ndànk-ndànk, yiwam wi dina leeral seeni xelBul tekk-tekkaaral ci àddina su soxlaa nii Yàlla. Seen xel dina leer ci yiw tuuti-tuuti. Kañ ngay noppi ci àdduna bu bari ñuy wut Yàlla?

Bu amee ku nangu topp Krist, dafay jot dund gu dul jeex. Mbëggeel gi dafay fees xol yi. Ca asamaan malaaka yi dañuy ndax benn bakkan kese bu tuub te jébbalu. Rax ci dolli, Yàlla dafa bëgg ñépp mucc, te xam dëgg gi. Ñiy topp coobare Yàlla te di Ko déggal ci ni ñuy waare ñeneen ñi ak xol bu woyof, seen ruu dina dal te dinañu bég. Ni ko Yeesu waxe moom ci boppam: » Sama ñam mooy def coobaare ki ma yónni, te matal liggéeyam. »

Yeesu tëje waxtaanam ak taali beem ya, naan leen: » Yónni naa leen ngeen góobi. » Yaxya ruujoon na ba noppi tool yu bekkoor ya, ba muy waare tuubug bàkkaar. Yeesu ci boppam mooy pepp mi Yàlla ji ci suuf si ñu raadu ba noppi. Tey nag nungi góob meññeefu faatoom ca kurwaa ba. Yeesoo ngi lay woo ngir nga góob, te nga fàttaliku ne du sam ngóob. Liggéeyu Boroom bi la. Kàttanu Krist mooy meññil doomu Xel mi. Nun ñépp ay surga yu ñàkk solo lanu, moone terewul Mu nuy woo ci ligéeyam bu sell bi, yenn saa yi ngir nuy ji, yeneen saa yi ngir nuy raadu, mbaa nuy góob. Nuy fàttaliku ne dunu surga Yàlla yi njëkk, am na solo lool. Ñu bare jot nañoo liggéey laata nun, ci biir ay rangooñ, te seeni ñaan ñunga ñu bind ca kow asamaan. Amuloo juumtukaay yu gën a baax yeneen surga Yàlla yi, te gënoo leen a maandu. Ci yiwam ngay dunde saa su nekk. Deel jàng ni nga war a déggale Xel mi ci sa waar. Dee Ko liggéeyal ak ay cant ci waxtu ngóob,te di màggalandoo Baay bi ak góobkat yiy xaacu naa : »Na sa nguur ñów ; yaa yelloo nguur gi,kàttan ji,ak ndam li ba fàww, » Deel jàng ni nga war a déggale Xel mi ci sa waar. Dee Ko liggéeyal ak ay cant ci waxtu ngóob, te di màggalandoo Baay bi ak góobkat yiy xaacu naa: » Na sa nguur ñów; yaa yelloo nguur gi, kàttan ji, ak ndam li ba fàww. » Aamiin. »


c) Tas Xabaar bu baax bi ci biir Samari (John 4:39–42)


YOWAANA 4:39-42
39 Ba jigéen ja nee waa dëkk ba: ’’ Wax na ma li ma def lépp ’’ ñu bare gëm Yeesu. 40 Ñu daldi dikk ñaan Yeesu, mu dal ak ñoom. Yeesu toog fa ñaari fan. 41 Ñu bare gëm Ko ndax li Mu doon wax. 42 Ñu ne jigéen ja: » léegi gëm nanu, te du li nga wax moo tax waaye li nu gisal sunu bopp. Te xam nanu ne, dëgg-dëgg Kii mooy Musalkatu àddina si. »

Gàngóor gu takku génne ca dëkk ba, daw wutali Yeesu gannaaw ba leen ci waxi jigéen ja xiiree. Yeesu gis ci ñoom tool yu ñor-xomm, yuy xaar ngóob. Mu waxtaan ak ñoom ci mbirum dund gu dul jeex gi, te toog fa ak ñoom diirub ñaari fan. Taalibeem ya duggu ca dëkk ba mel ni ay góobkati ruu. Jëmmu Krist ak ay kàddoom laal lool waa dëkk ba. Ñu xam ne Yàlla jaare na ci Krist, ñów ci seen àddina su naqari sii ngir musal bàkkaarkat yi. Waa Samari yooyu ñoo njëkk a woowe Yeesu ‘Musalkatu àddina si » ndaxte mujj nañoo xam ne Yeesu ñówuloon ngir musal aw xeetam doŋŋ, waaye ngir gàddu bàkkaari waa àddina sépp. Kàttanu mbëggeelam amul àpp(dayo). Ba tey jii sax, man na goreel te musal ñi nekk ci buumu njaamu bàkkaar te Seytaane noot leen, rax ci dolli Muy aar ñi ñu goreel. Moom mooy dëgg-dëgg àttekatu àddina si. Sesaar ci boppam, jotoon na ca Rom ndombal "Musalkat ak Aarkatu Àddina si". Waa Samari yii dañoo jàppe Yeesu ni ku sut fuuf Sesaar; Dafay may askanam jàmm ju dul jeex.

ÑAAN: Nungi lay sant Yeesu; soqaliwaat nga dunug jigéenu moykat jii, te won nga nu ne déggal Xel mi moo ëpp solo màggal gi. Yewwi nu ci lépp li nuy tënk, ngir nu man a def sa coobare ak mbég ak, lewetaay, te di yët sa mucc gi ñiy wëndeelu. Noonu, dinañu dinañu am dund gu amul àpp, jaare ko ci ngëm gi ñu am ci Yów.

LAAJ:

  1. Nan lanu man a nekke ay góobkati Yeesu yu xarañ?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 23, 2025, at 04:42 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)