Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 033 (Healing of the paralytic)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
A - Ñaareelu tukki ca Yeruusalem (Yowaana 5:1-47) -- Yokkute jànkoonte diggante Yeesu ak Yawut ya

1. Pajum jarag ga ca Betesda (Yowaana 5:1-16)


YOWAANA 5:1-9
1 Gannaaw loolu Yawut ya amoon nañu genn màggal, moo tax Yeesu demoon Yerusalem. 2 Ca wetu benn ci bunti dëkk ban ag, maanaam ca Buntu xar ya, am na fa bët bu tudd Betesda ci làkku Yawut, te ñu wërale ko ak juróomi mbaar. 3 Ca suufu mbaar yooyu la jarag yu bare, yu deme niki ay gumba, ay lafañ, ak ay làggi, daan tëdd, di xaar ndox mi yëngatu; 4 ndaxte, ci ni ñu ko nettalee, benn malaakam Boroom bi da daan wàcc léeg-léeg di jax ndox mi. Bu ndox mi masaa yëngu ba noppi, jarag ju ca jiitu, wopp joo amaan, daldi wér ca saa sa. 5 Amoon na fa jenn waay ju feebaroon lu mat fanweeri at ak juróom ñett. 6 Bi ko Yeesu séenee mu tëdd, te mu xam ne, woppam ji yàggoon na lool, Mu laaj ko ne: » Ndax bëgg ngaa wér? » 7 Jarag ja toontu ko ne: » Sang bi, duma am ku ma sóob ci ndox mi, bu yëngoo; su ma ciy fexee dem, ñu jëkk ma ci. » 8 Yeesu ne ko: »Jógal, jël sa basaŋ te dox. » 9 Ca saa sa mu daldi wér, jël basaŋam daldi dox.

Yeesu toog na Galile lu war a tollook juróom ñeenti weer, Gannaaw loolu Mu dem Yerusalem teeweji feetu Xayma ya. Xamoon na ne xareb ngëm gi ca péey ma lay mate. Ak li Mu doon jànkonteek ña fonkoon diine ak Yoon ñépp, terewul ne dafa doon sàmm Yoon wi. Daan na aji ñetti yoon ci at mi ca Kër Yàlla ga ca Yerusalem bu daan man a nekk (Detoronëm 16 :16).

Ca diggu dëkk ba amoon na ab déeg (pisin), bu yenn Grec yi wax ne yenn saa yi malaakam Yàlla moo daan jax ndox ma. Erod dafa tabaxoon ay kenu yu wër pisin ba. Bu yàggul dara lañu feeñal desiti kenu yooyu. Ȅttu kenu yooyu lañu tuddewoon » Këru Yërmande ji », ndaxte laago yu bare dañu fa daan daje ngir yaakaar faa fajoo, bu ndox ma jaxee. Dañoo gëmoon ne ku jëkk a tàbbi ci ndox mi, dangay wér ci saa si.

Yeesu dem ca pisin, bu fees ak ñu wopp boobu. Mu seetlu fa geen góor gu jarag dal diiru fanweeri at ak juróom-ñett te ànd ak xol bu naqari ak mitit. Rax ci dolli dafa bañoon sax ña ca des. Ci këru yërmande googu, bopp sa bopp moo fa amoon, Ku nekk sa bopp nga taloon, kenn yërëmuloon kenn. Waaye moom góor gi, loolu taxuloon mu ñàkk yaakaar. Ba léegi mungi doon xaar yërmande Yàlla. Nees tuuti rekk yërmande gi ñu jëmmal ne jameet ca kanamam. Noonu rekk Yeesu tàmbali di ko faj ba génne xelam ci pisin bi. Noonu Yeesu xiir ko ci mu bëgg a wér. Mu may ko itam fu mu man a waxe naqaram: » Kenn du ma faale! Jéem naa fexe nu ma wére ba tàyyi, maangi bëgg a yoqi nag. Kenn yégu ma. Ndax man nga xaar ba ndox mi jax, nga tëmbal ma ci? »

Kenn du ma faale! Mbokk mi, mbaa du loolu moo la dal itam? Ndax ñeneen ñi dañu lay sàbbi? Xamal ne Yeesu mungi taxaw ci sa kanam; soxal nga ko, te ñów na ci yów. Man na la dimbali te musal la. Loolu la jarag ga doon yég ci xolam. Bëti laajteem yooyu, ne jàkk Yeesu mi yërmandeem tabbal ci xolam kóolute ci mbëggeelu Yàlla.

Bi Yeesu gisee ni mu bëgge wér, ak nimu Ko wóoloo, Mu sant ko: » Jógal, jël sa basaŋ te dox. » Ndigal lu jóge asamaan la woon, luy def ba lu manta nekk, nekk. Jarag gi gëmoon na li Krist wax, te wóoluwoon na kàttan gi doon feeñ ci Moom. Noonu muy yég yaramam di maas, ba ca biir yax ya, ak kàttan ji doon dundalaat yaramam. Mu amaat doole te wér.

Ca saa sa, mu ne bëret ak mbég, yenu basaŋam te dem. Ngëmam mottali na kàddu yu am doole yi Yeesu waxoon, ba mu wér ci saa si.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu nungi lay sant, ndaxte rombuloo jarag googu, waayemay nga ko bët, ci sa yërmande. Amuloon kenn ku dul yów Boroom Yërmande ji. Dimbali nu ba nu taq ci Yów ,te bañ di wéeru ci ndimbalu nit ñi. Soppi nu ba nu mel ni sa mbëggeel, dimbali nu ba nuy toppatoo ñeneen ñi, te di cëroo ak ñoom say barke.

LAAJ:

  1. Nan la Yeesu faje jarag ga ca pisinu Betesda?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 24, 2025, at 03:44 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)