Previous Lesson -- Next Lesson
1. Nekkin ak liggéeyu Kàddu gi laata muy feeñu (Yowaana 1:1-5)
YOWAANA 1:1
1 Ca njalbéen ga fekk na Kàddu gi nekk, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.
Nit ki, ci ay kàddu lay xamle ay xalaatam ak li mu nar. Li ngay wax mooy ki nga doon. Say kàddu ñooy tënk ki nga doon, ak li sa xel di xelli.
Ci Yaatal, Kàddug Yàlla dafay wone nekkinu Yàllaam ak kàttanam ci biir ni muy jëfe ak kàddoom gu sell gi. Ndaxte ca njalbéen ga,Yàlla dafa sàkk asmaan ak suuf ci ngelawal Kàddoom gu am kàttan gi. Te ba Mu nee: Na am”, dafa am. Ba tey jii kàttanu Yàlla mungi feeñ ciy kàddoom. Ndax xam nga ne Injiil li nga téye ci say loxo dafa fees dell ak sañ-sañu Yàlla? Téere bii moo ëpp doole bépp boombu ngelaw luy reye, ndaxte dafay faxas mbon gi ci yow, te wuutoo ko mbaax.
Ci Injiilu Yowaana,baatu “kàddu gi”, ñaari tekki-tekki la am ci grek: 1) ngelaw liy génnee ci sunu gémmiñ lu nu man a dégg; 2) ab jëmmu baatin bu góor. Ci Araab, ñaari tekki-tekki yooyu ñungi leen di ràññee ci melo baatuwaay bi topp ci kàddu gi,muy góor mbaa jigéen. Krist dafa jóge ci Baay bi ni kàddu neen di génne ci sunu gémmiñ. Noonu Krist moo tënk coobare Yàlla ak xalaatam. Gis nanu lii ci yeneen diine, yu naan Krist mooy Kàddug Yàlla, ak Xel mi jóge ci moom. Amul benn doomu Aadama bu am melokaani asamaan yooyu, ku dul Ki juddoo ci Maryaama xiig gi.
Peeñug Krist ca Betleyem nekkuloon njalbéenu dundam, ndaxte mungi woon ak Baay bi ba dara sosoogul, te nekkoon na laata ñuy sàkk àddina. Krist amul àpp, ni Baay bi amule àpp itam; du soppiku mukk, ni kàddug Yàlla gi itam.
Yowaana dafa nuy won jokkoo gu xóot te wér ci diggante Krist ak Baayam. Tàqalikoowul ak Moom, ni kàddu guy génne ci sunu gémmiñ te di seey ci ngelaw li. Krist dafa nekk ak Yàlla, te sax ci Moom. Baatu ”ak Yàlla” mungi tekki ci grek kàddu gi mungi jëmoon ci Yàlla, te doon duggu ci moom. Kon Krist dafa doon jublu saa su nekk ci Yàlla. Loolu mooy taxawaayu képp ku juddoo ci Xel mu Sell mi, ndaxte mooy reenu mbëggeel gi. Te mbëggeel wutul beru waaye dafay nangu reenam di ko wommat, te mu sax ci moom.
Yàlla sàkkewul Krist ci Kàddoom cig neen, ni yeneen càkkite yi, waaye Doom ji ci boppam mooy Kàddu giy sàkk te fees ak sañ-sañu Baayam. Ci njeextalu aaya bii dinanu ci gis ni ñu jibale ne Kàddu gi moo nekkoon Yàlla ci boppam. Taskatu Injiil bi dafa nuy xamal ne Krist mooy Yàlla ji juddoo ci Yàlla,l eer gi juddoo ci leer, Yàlla dëgg, ji juddoo ci Yàlla dëgg ji ñu jur Ko te kenn sàkku ko, bokk ak Baay bi amul àpp, am kàttan, sell te di boroom yërmaande, fi ñu soqikoo. Képp ku nangu ne Krist mooy Kàddug Yàlla gi, dinga déggook wax jii ci nekkinu Yàllaam.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist nungi lay sujjootal ndaxte yaangi woon ak Baay bi ca abada ba tey,te jublu saa su nekk ci Moom. Dimbali nu ndax nu bañ laa beru, waaye nu jébbal sunu bopp Yàlla, te sax ci mbëggeelam. Nungi lay sant, Boroom bi Yeesu, ndaxte ci sa Injiil, Yaangi ñówe ci nun ak ay kàddu yu neex a dégg, di nu feeñal sa Sañ-sañ ngir nu gëm ko jaarale ko ci Kàddu gi.
LAAJ:
- Ban baat moo ëpp doole walla gën a fës ci aaya bu Yowaana 1, ak lu muy tekki?