Previous Lesson -- Next Lesson
d) Yeesu, leeru àddina si (Yowaana 8:12-29)
YOWAANA 8:21-22
21 Yeesu dellu ne leen: »Maa ngi dem; dingeen Ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deewaale. Fa ma jëm, dungeen fa man a dem. 22 Yawut yay waxante naan: »Nee na kat, fa Mu jëm, dunu fa man a dem. Mbaa du dafay xaruji? »
Yeesu xamoon na ne surga Kër Yàlla gépp ñungi Ko wër. Noonu Mu léebu leen li ëllëg di tekki: » Sama dee jegesi na. Dinaa génn àddina sii te dungeen Ma man a topp. Du yéen a may bóom ni ngeen ko tërale. Man maay dogal sama waxtu dem. »
« Waaye, dinaa génn bàmmeel ba, jaar ca digante doj ya, ak bunt ya ñu tëj. Dingeen ma seet ba tàyyi. Dinaa yéeg ca sama Baay te dungeen ci xam dara. Dangeen maa xalab, man Mbotem Yàlla mi, te wóoluwuleen Rammukatu nit ñi. Dingeen dee ci seen kaso bàkkaar. »Sunu bàkkaar yu bare yi, nekkuñu sunu tooñ bu jëkk, waaye sunu taxawaay ci kanamu Yàlla, ak sunu ñàkk ngëm ñooy sunuy gàllankoor.
Yawut ya xalaat ne Yeesu demam ba fàww lay wax, te xamuñu sax ne dafay dellu ca Baay ja. Dañoo foogoon ne amatul doole ju Mu man a jànkoonteek Farisen ya ak Xutbakat ya. Amatuloon leneen lu Mu man a tànn lu dul xaru rekk. Ndax Safara la jëm, walla dafa nar a sànku ba fàww? Yawut ya bëgguñu woon mujj googu ndax li seen Yoon tëraloon. Waaye ba waa Rom tëroo Yerusalem ca atum 70, ay junniy nit xaruwoon nañu ndax xiif ma, ak yaakaar ju tas.
YOWAANA 8:23-24
23 Yeesu tontu ne: »Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kow laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci. 24 Looloo tax ma ne, ci seeni bàkkaar ngeen di dee. Bu ngeen gëmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeny bàkkaar. »
Yeesu biral na ne Nguurug Yàlla moo sut sunu àddina su rëppeelu sii. Nun ñépp ci pënd lanu juddoo te fees ak xalaat yu ñagas. Doomi Seytaane, ay meñeef yu nëb rekk lañuy jur. Nitu neen manul a xam bu leer nguuru Yàlla, waaye man na am yégeel ne lu nekk la.
Krist bokkul ci sunu duniya; ruuwam mungi jóge ci Baay ji. Nguuru Baayam ca kow la nekk, waaye du ci anamu féetewaay. Lu nu gën a jëm kow, sunu diisaay gën a wàññeeku, noonu itam la sunu bàkkaar bi ub sunu bopp di seeye su nuy gën a jege Yàlla. Sunu àddina si dafa mel ni kaso bu nu manul a rëcc fenn. Ay doomi sunu diiwaan lanu, yuy bañ a déggal mbëggeelu Yàlla. Sunu dund dafa fees dell ak bàkkaar. Ci xët bii Yeesu dafa cee bareel baatu « bàkkaar », ndaxte bàkkaar yu bare ak ay njuumte ñungi jóge ci sunu ñàkk a déggal Yàlla. Ñungi mel ni ay gaana yu fees ak ay góom. Gaana dafay dee ndank-ndank, donte mungi dund. Noonu la bàkkaar di ŋeeñe nit ki. Danoo bàkkaar moo tax nuy dee. Lan mooy bàkkaar? Mooy ñàkk ngëm, ndaxte Ku lëngoo ak Krist dangay dund ba fàww - deretu Doomu Yàlla ji dafay wéy di la sellal ci bàkkaar. Kàttanam dafay laabal sunu xel te sellal sunuy xalaat. Waaye ki tàggook Yeesu, dafa tànn a dee; Dafay nekk jaamu bàkkaar, te di xaar àtte bi. Gëm Yeesu moo nuy yewwi (goreel) ci merum Yàlla.
Kon, kan mooy Yeesu mii bëgg a xiir nit ñi ci ñu gëm Ko? Mu ne « Maay ki nekk » la tudd(Yowaana 8 :24) Kàddu yii ñoo tënk seedeem yi gën a am solo. Xàmmeeku na itam ni Buuru dëgg gi, Yàlla jiy dund, Ku Sell ki feeñu woon Musaa ca ngarab sa doon tàkk te lakkul (Gàddaay 3 :14 ; Esayi 43 ;1-12) Mucc gi nekkul ci kenn ku dul Moom. Bépp Yawut xamoon na ñaari tur yooyu, ñemewu leen a tudd ndax ragal a wax turu Yàlla cig neen. Waaye Yeesu moom dafa leen a def moomeel ca diggu mbooloo ma. Kon du Krist, Doomu Yàlla rekk, waaye it Yahweh, Yàlla ci dëgg.
Mooy Injiil ji ñu jëmmal. Krist mooy Yàlla mi ñu jëmmal. Képp ku Ko gëm, am dund gi. Waaye nag ku Ko weddi te bañ kiliftéefam, dinga xañ sa bopp mbaalug bàkkaar. Ngëm walla ñàkk ngëm ñooy dogal fa nit ki jëm.
LAAJ:
- Luy tekki gëm Ki xamle boppam ni »Man maay ki nekk »?