Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 100 (Introduction to the intercessory prayer; Prayer for the Father's glory)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
E - Ñaanu rammu gi Yeesu def (Yowaana 17:1-26)

1. Ubbite ñaanu rammu gi


Yeesu liggéeyal na àddina si ci Injiilam ak ci ay jëfam : faj na ñu wopp, reggal ñu xiif, ubbi bëti gumba yi te dekkal ñu dee. Mbëggeelam moo feeñal ndamul Yàlla ci diggu mbañ gi ak dee gi.

Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, ñu bare dañu doon dawsi ci moom. Waaye ba Kuréelu diine Yawut ya (bokkoon nañu fonk diine ak ay naaféq) gisee ne seen ponki diine ji ak taxawaayu seen Yoon wa ñungi jeng, te nar a nërmeelu, ñu tëkku Yeesu ak taalibeem ya ngir dàq leen ca dëkk ba mbaa rey leen. Noonu xadaru mbooloo ma wàññiku te ñu bare dëddu Ko. Teg ci ñuy sonal Krista k taalibeem yu gore yi Ko toppoon, waaye loolu lépp terewuloon muy wéey ci bëgg àddina sépp.

Mujj gi Kuréel ga am kenn ca fukki taalibe ya ak ñaar : ku jekkoon ngir wor Sangam bi, fekk ñuy reer, reeru kóllëre ga. Yeesu di tàggat ay ñoñam ngir ñu man a tambali seen liggéeyu apotar. Mu xamal leen ne Moom ak Baay ji benn lañu, te itam ne leen ne Xel miy dëfalaate dina leen may ndëgërlaay ci mbëggeelu Yàlla, donte metital yi duñu ñàkk a am.

Waaye taalibe ya xamuñu woon bu baax li seen Sang bi naroon, ndaxte yónneeguñu leen woon Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ak Baay ji ci boppam, teg ciy loxoom ruuwam ak bu taalibe yi. Mu ñaanal itam ñi Ko nar a gëmi jaare ko ci seede apotar yi.

Ñaanu rammu gi Krist def ci téere Yowaana 17, dafa nuy won ni Doom ji doon jokkoo ak Baay ji, ak mbëggeel gi dox ci diggante ñetti jëmm yi nekk ci Kenneefu ñett gu Sell gi. Xelum Ñaan mi am na fi solo lool. Képp kuy jàng saar bii, yaangi dugg ci Kër-Yàlla, gi nga xam ne màggal ak ñaanu rammu duñu jog mukk.


2. Ñaan ngir ndamul Baay ji (Yowaana 17:1-5)


YOWAANA 17:1
1 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa xool ci kow ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne : « Baay, waxtu wi tax ma ñów ci àddina agsi na. Feeñalal ndamu Doom ji, ngir Moom itam mu man a feeñal sa ndam;

Krist xamal na taalibeem ya ne Moom ak Baay ji benn lañu. Mungi ci Baay ji, Baay ji nekk ci Moom. Képp ku ko gis, gis nga Baay ji. Waaye taalibe ya manuñu woon dégg wax jooju bu leer. Manuñu woon xalaat teewaayu Yàlla ci jëmmu nit. Yeesu dafa jébbaloon Yàlla taalibeem ya néewoon doole te ñàkk a xa, ngir Mu may leen leer te aar leen ci biir mbëggeelu Yàlla gu sell gi.

Bi Yeesu nee jàkk asamaan, waroon na jaaxal taalibe ya. Nan la man a ñaane Baay ji ci asamaan, te ne mungi ci Baay ji te Baay jaa ngi ci Moom ? Yëf yu lëj yooyu xejuñu woon ci seeny bopp. Xel mu Sell mi moo nuy may nu xam lu mel noonu : Jokkoo gu mat sëkk gi am ci diggante Baay ji ak Doom ji, ak itam nekkaayu kenn ku ci nekk ci sa wàllu bopp. Yàlla moo ëpp kàttan sunu xel. Bu mbir yi leerul, ñaanal Yàlla mu leeralal la. Ndaxte ci dëgg kenn manul a xam Baay ji ak Doom ji te Xel mu Sell mi mayu la ko.

Ci ñaan gii, Yeesu dafa woowe Yàlla, Baay. Yàlla du Boroom bu Sell ak Àttekat bu soxor rekk, waaye mbëggeelam gu am yërmande gi dafa ëmbaale yeneen melokaanam yépp. Yŋlla ci boppam mooy mbëggeel gu sell gi, ak dëkk giy yërmande. Gis-gis gu bees googu nu am ci Yàlla, ni Baay, ju qm mbggeel, mungi tàmbalee bi yeesu nekkee Doomu Yàlla jaare ko ci Xel mu Sell mi. Mungi dund ba fàww ak Yàlla, waaye dafa jëmmoo nit ngir rammu nu ngir ku Sell ki. Feeñalu turu Baay bi mooy reenu bataaxalu Yeesu bi mu jagleel àddina si. Ci dëgg googu la Yeesu jaare ba goreel nu ci ragal àtte bi, ndaxte àttekat bi mooy sunu Baay ji, te yiir sunu mag, ji nu fayal sunuy bor. Soo bàyyee sa ruu mu fees ak turu Baay ji jaare ko ci kàdduy Yeesu yi, te nga dunde xam-xam boobu, kon yaa ngi won ne xam nga li bataaxalu Injiil di tekki.

Krist nangu na ci Kanamu Baayam ne waxtu wi ëpp solo ngir àddina si agsi na, maanaam waxtu wi nit ki di jubóo ak Yàlla. Nit ñi ak malaaka yi, diine yi ak joŋantekati xel yi, jotoon nañoo déegg lu jëm ci waxtu yooyu, waaye xamuñu woon lu mu doon. Waxtu wi agsi woon na. Krist moo naroon a gàddu tooñi àddina si, ni mbotem Yàlla. Ci saa soosu, workat bi munga woon ca kow yoon wa, ñand ak soldaari Kër-Yàlla ga, di jàppsi Doomu Yàlla ji, nit ku néew doole ki te bare kàttan, pare ngir dee te yorul benn ngànnaay.

YOWAANA 17:2
2 Ndaxte jox nga ko sañ-sañ ci bépp mbindeef, ngir Mu may dund gu dul jeex gi, ñi nga ko dénk.

Nit ñu bare dañuy xalaat ne baatu « ndam » ceeñeeri leeraay lay tekki. Yeesu dafa ne mbëggeelam, gi Mu saraxe mooy reenu ndam li ak itam xolu jëmmu asamaanam. Mu ñaan Baayam ji, mu fas Ko ci mbëggeel googu, ci waxtu yi Mu nar a sonn ci kurwaa bi. Ceeñeeri mbëggeelu asamaan yi ñungi melax ci Ki ñu daaj. Doom ji dafa bëggoon a saraxe boppam ngir fippukat yi ak bóomkat yi, ndax ñu man a jaare ci deewam ngir am njubte. Loolu mooy xolu nettalib Doom ji.

Waajul sax ngir wax ne du dee ngir moom ci boppam, waaye ngir ndamul Baay ji lay faatu, te dina dékku metit yu kenn manul a dékku. Màggal na Baay ji ci kurwaa bi, te matal juboo doo; u-Aadama ak Yàlla. Bu ñu baalee bàkkaar, mbëggeelu Yàlla daldi law. Ñi gëm Krist lañu yónnee Xel mu Sell mi, ngir doom yi man a màggaal seen Baay ci seen doxalin. Rax ci dolli, doom yu bees yiy door a dugg ci njaboot gi itam, dañuy màggal Baay ji. Looloo tax ba Yeesu ñaan juddug doom yu bare, ci Xel ak ci Dëgg ngir sargal turu Baay ji.

Doom ji dafa gàttal ay kàddoom ci lu jëm ci ni ko Baay ji joxee bépp sañ-sañ ci kow nit ñi. Krist mooy Yàlla ji dëgg, Aji Sàkk ji, Rammukat bi. Mooy sunu Boroom, di sunu Buur ak sunu Àttekat. Moo nu moom te Moom rekk mooy sunu yaakaar. Jot na sañ-sañ boobu nag, waaye du ngir àtte ak yàq, waaye ngir musal ak wommat. Nësëru ñówug Krist, mooy na ñi ko gëm am dund gu dul jeex. Dee gi amatul benn sañ-sañ ci ñoom. Yeesu baal na ñépp seeny bàkkaar, ca Kurwaa ba. Bu dee sax ñu néew ñoo nangu mayug mucc googu, ñi gëm daal ñooy ñi ñu fal, ñi gëm Baay ji, Doom ji ak Xel mu Sell mi, te di wéy ci ndamul muccug Krist gi. Xel mi ci asamaan mungi dëkk ci ñoom. Seen dund gu bees gi mooy sunu kéemaanu jamono, te loolu mooy sargal turu Baay ji.

YOWAANA 17:3
3 Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yów jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Krist.

Xel mu Sell mi dëggal na kàdduy Yeesu yi aju ci Yàlla. Mooy Baayu Krist, ak sunu Baay it. Képp ku xam kumpa baatin googu, te gëm ko, am nga dund gu dul jeex ba fàww. Manunoo xam Yàlla te xamunu kan mooy Yeesu Krist. Ku gis Baay ji ci Doom ji, te wóolu Ko, dees na la soppi te baayoo la. Xam kàddu Krist yi du xam-xamu neen, waaye dafa laaj coppite baatin. Yàlla dafay yeesalaat melokaanam ci bépp way-gëm. Lan mooy melokaanu Yàlla boobu ? Mooy mbëggeel gi, dëgg gi, ak njubte yi Xel mu Sell mi sàkk ci nun. Mooy itam màggal Yàlla ndax ay ngëneelam.

Dañoo yónni Krist ci àddina si ngir ñépp xam ne bu dul Moom, kenn du man a xam Yàlla. Doom ji mooy Apotar Yàlla, bi doxal sañ-sañ bépp, ak mbëggeel ak sellaay. Soo bëggee xam Yàlla jiy dëgg, jàngal dundu Yeesu miy melokaanu Yàlla bi Xel mu Sell mi sotti diw ci kow boppam. Almasi bi mooy itam Buuru Buur yi, Saraxalekat bu mag bi; Yonent bu mat sëkk bi; ak kàddug Yàlla gi ñu jëmmal.

YOWAANA 17:4-5
4 Wone naa sa ndam ci àddina, ndax li ma matal liggéey bi nga ma santoon. 5 Léegi nag Baay, ci sa teewaay, feeñalal ci man ndam li ma amoon ci sa wet laata àddina di sosu.

Ci diir bi mu ganesee àddina bépp, Yeesu xelam jógul ci di xalaat Baay ji : Daf Ko daan seedeel, te di matal liggéeyam. Dafa fàtte woon boppam, te di màggal Baay ji. Dafa nu daan jottali li mu daan dégge ci Baay ji. Dundam gépp a màggal Baay ji. Gëmoon na ne dinañu nangu ay ñaanam. Matal na liggéeyu rammoom ca bant ba. Monte bàkkuwu ci sax, ndaxte Baayam moo Ko santoon liggéey boobu. Nangu woon na ne Baayam mtaloon na lépp. Ndegam Yeesu dafa futteeku te bàyyi sargal yi ñu ko waroon a jagleel, kon kay yelloo na ndam lu amul àpp li. Ci aaya yii, wax na ci ne amoon na ndam laata ñuy sos àddina si, maanaam ba dara nekkagul, mooy Yàlla ji juddoo ci Yàlla, Leer gu juddoo ci Leer, ki ñu jur te kenn sàkku Ko. Ba mu matalee ngirteem ba noppi, dafa fasoon yéene dellu ca Baayam. Ba mu àggee asamaan, malaaka ya ak yeneen mbindéefi jaww ji di Ko màggal naan : « Mbote mi yelloo na jot doole ji, alal ji, maandute gi, kàttan ji, sargal gi, ak ndam li. »

ÑAAN: Sunu Baay ji ci asamaan, na saw tur sell. Sa Doom màggal na la, ci doxalinam, ay ñaanam ak saraxam. Yeyoowunu yëkkati sunuy bët ne la jàkk. Nungi lay sant ci li nga nu baal suny bàkkaar ndaxte Krist dee na ngir nun ; def nga nu say doom. Jarajëf ci li nga nu may dund gu dul jeex bi ngay yónnee sa xel mu Sell mi. Dimbali nu ba nu màggal la, te bañ di wut sunu ndamu bopp, waaye di déggal sa ndigalu Doom ji te di bëggante ci sunu biir, ndax ñeneen ñi di gis sa baayoo ci sunuy jëf yu baax te di la màggal ci ni nu lay déggale.

LAAJ:

  1. Lan mooy xalaat biy ponku wàllu ñaanu Yeesu wu njëkk wi?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 23, 2026, at 02:39 PM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)