Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":

Home -- Wolof -- John - 099 (Christ's peace in us defeats the world's afflictions)

This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
D - Tàggatoo ba ca yoonu Getsemane (Yowaana 15:1 - 16:33)

6. Jàmmu Yeesu ji ci nun mooy daan tiis yi ci àddina si (Yowaana 16:25-33)


YOWAANA 16:25-26a
25 Loolu lépp dama leen koo wax ci ay misaal. Jamono dina ñów, ju ma dootul wax ak yéen ci ay misaal, waaye ju ma leen di wax lu leer ci Baay ji. 26 Bu keroogee, dingeen ñaan ci sama tur…

Yeesu dafa feeñal dëggi asamaan yi ci biir ay firnde aky misaal, nëbbe noonu kumpa yi niti àddina si. Ñi nammoon njub la ko feeñalal. Yeesu dafa bég ci bés bi Ko taalibeem yi naree dégg bu leer. Ngir loolu, dafa waroon a dekki ci ñi dee, yéeg asamaan te yónnee leen Xel mu Sell mi. Xew-xew yépp yi aju ci mucc gi la boole woon ba mu mel ni ci benn bés doŋŋ la xewe. Gannaaw gi, ba Xel mu Sell mi wàccee ci xolu taalibe yi, misaal yi ak firnde yi dañoo dakk, ndaxte Xelum Yeesu moo leen doon may dégg-dégg bu bees, bu dakkal jamono misaal yi. Yàlla mooy Baay ji, Krist di Doomam. Ci lu gën a xóot, kàdduy Yeesu ak dëfalu Xelam mi ñoo nuy biral ne Yàlla mooy Aji Kàttan, ju Sell ji, te bëgg kenn ku nekk ci nun. Nun ñooy doomam yi Mu bëgg, donte ay bàkkaarkat lanu nun ñépp. Deretu Yeesu sellal nanu ci kanamam. Xel mu Sell mi dafa nuy xiir ci ñaan gu dëggu, ndaxte Xelum Krist la. Krist dafay waxe ci sunuy ñaan. Ñaanal li Xel mi di ñaan, ci biir wóolu Yàlla ak ci wóllëre gi nga séq ak Doom ji. Say ñaan , diisoo la ci diggante Xel mi ci yów ak sa Baay ji ci asamaan, ji nekk ak Doom ji.

YOWAANA 16:26b-28
26… neewuma dinaa leen ñaanal Baay bëgg na leen. 27 Ndaxte Baay ji ci bopp bëgg na leen. Bëgg na leen ndaxte bëgg ngeen ma, te gëm ngeen ne, ci Yàlla laa jóge. 28 Jóge naa ci Baay ji, ñów àddina. léegi maa ngi génn àddina, fekki Baay ji. »

Baay ju bëggul ay doomam, du baay. Bi Yeesu di feeñal turu Yàlla, dafa nu cee dimbaliwaale ngir nu xam kàttanu mbëggeelu Yàlla. Sargal turu Baay ji, mooy li Krist di xënte. Ku xam Baay ji, xam Yàlla; te nekk doomu Yàlla ju sax ci mbëggeelam. Ci tur wii lanuy fekk Xabaar bu Baax bi, ak yaakaaru ëllëg gu amul àpp. Krist yëgal na la ne li ko dale tey, aajootul rammukat, ndaxte Baay ji ci boppam bëgg na la, te mungi fess ak mbëggeel, ak yërmande. Ba Krist deewee ca kurwaa ba, ba tey, amatul genn mbañ-gàcce ci sunu diggante ak Yàlla. Gëm Doom ji, maanaam Mbotem Yàlla mi, dafay may Baay ji mu feesal mbëggeelam ñi bëgg Krist. Ki xam baatinu Krist, gëm ne ci Baay ji la jóge, te benn lañu, jegesi nga Kenneefu Ñett gu Sell gi. Kooku dafay sax ci dundug Yàlla, te fees ak yiwu Baay ji, ci biir mbégu Xel mi.

Krist faramfàcceel na taalibeem ya kéemaanu rammu gi. Dafa wacc màggaayam ca asamaan, ñów yëngal àddina si nga xam ne ger ak mbañ ñoo fi nguuru woon. Léegi nag mungi nar a matal njubte ngir doomu Aadama yépp, ca Kurwaa ba, ba noppi génn àddina ngir dellu ca Baayam, jiy cosaanu gépp dund.

YOWAANA 16:29-30
29 Taalibe yi ne Ko : « Léegi yaa ngi wax lu leer te misaaluloo ! 30 Léegi gis nanu ne xam nga lépp, te soxlawul kenn di la laaj dara. Looloo tax nu xam ne, yaa ngi jóge ci Yàlla. »

Ndànk-ndànk taalibe yi di jëli màggaayu mbëggeelu Yàlla, ak nekkinu Yeesu gu amul àpp gi. Yeesu mooy Yàlla dëggantaan ji, Ki xam lépp, Ku Sell ki, te nekk ba fàww. Waaye dañoo fàtte woon ne mbëggeel gi ñu jëmmal la woon, te noonu tuddewuñu Ko Yàlla, Baay. terewul sax ne Yeesu waxaat na baati dëgg yooyu lu bare.

YOWAANA 16:31-32
31 Yeesu ne leen : « Ndax gëm ngeen léegi ? 32 Waxtu waa ngi ñów, te agsi na ba noppi, dingeen tasaaroo , ku nekk ñibbi, ma des man rekk. Waaye nag wéetuma, ndaxte Ba way baa ngi may wéttali. »

Ak ree ju ànd ak muuñ, Yeesu ne : « Ndax xalaat ngeen a dégg li may wax ci seen xelum bopp ? Xam-xam bu ni mel, ndax méngoo na ak ngëm gu dëggu ? Nattu baa ngi nii ci sunu kanam, te dina wone sa ñàkk mbëggeel. Manuloo xam Yàlla, ndaxte gëmuloo ne man na nekk Baay. Yéen ñépp dingeen daw , bàyyi ma man doŋŋ, seen ngëm dina woyof. »

Ci biir dee gi duma wéet, ndaxte Baay ji mungi ak man. « Ndax loolu juuyoo na ak yuuxu Yeesu ca Bantu kurwaa ba ? Sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma » ? Mukk , ndaxte Yàlla mu Sell mi dafa nëbb kanamam Doom ji, waaye Krist mungi donn wéy di gëm teewaayu Yàlla Baayam ji. Yuuxoom bi wone na ne Yàlla du soppiku mukk « Duma la bàyyi mukk, su ma la gisul sax. Maa ngi delloo sama ruu ci say loxo. » Ngëmu Krist ci baayoo gi ak Yàlla, moo ëppoon solo àtte bi Mu nu wuutoo. Mbëggeel gi Doom ji am ci Baayam, moo fay lakku merum Yàlla, mi jóge ci sunuy bori bàkkaar. Buntu yaakaaram ji dul am benn dog-dog moo nu ubbil bunt bu nu man a gise Yàlla Baay ji. Bu nu xoolee ci ni Mu déggalee Baayam ba dee, man nanu ne : « Wéeetuma ndaxte Baay jaa ngi ak man. »

YOWAANA 16:33
33 Dama leen wax loolu, ngir ngeen am jàmm ci man. Dingeen am nattu ci àddina, waaye takkleen fit yi; noot naa àddina. »

Yeesu yékkati na ay kàddu dëfal ngir ñépp ñi gëm : « Dund naa ab diir ak yéen, te jàngal naa leen ngir seen xol fees ak jàmm ju sell ji. Way-gëm yi amuñu jenn jàmm. Man, Doom ji, baal naa seeni xol, te sellal seen yaram. Gannaaw man, amuleen genn kaaraange. Seen jubóowaat ak Yàlla , mooy reenu jàmmu biir jooju. Seen xel du sell bu ngeen nanguwul seen mbaalug bàkkaar. Musal naa leen, te sama Xel maa ngi ci yéen. Sama jàmm du njuuma, waaye dafa am. Damaa ñów ngir indil leen jàmm ; nanguleen ko te gëm ma. »

« Buleen yaakaar a dunde jàmm ci àddina sii. Mukk ! Dingeen jànkonteek coono yu bare : metital, feebar, naxaate, ragal ak dee. Ñi fonk lu dul Yoon wi dinañu leen bañ. Ñi woyofal diine dinañu leen ñaawal. Ay téeméeri fen aky xalaat dinañu jéem a nattu seen ngëm. Rëy-rëylu dina leen tëru. Bulleen bëgg xaalis, ndaxte alal du leen may genn kaaraange. »

« Defleen ci seen xel sama mbëggeel te roy sama suufeelu gi ak sama njébalu gi. Daan naa àddina si. Laaju ma dara ngir man ci sama bopp. Man maay ku Sell ki yàlla am. Ci man la ndigalu Yàlla mate : ‘Nangeen sell, ndaxte damaa sell’. Man maay mbëggeel gi dëgg, ci man ngeen di gise Baay ji. »

Ndax gis nga solo si kàdduy tàggoo yu Yeesu yii am ? Jokkale na la ak Baay ji, ngir sa xol di bége jàmmam. Jàmm jooju mooy dëgg gi gën a am solo ci dundu ki gëm. Àddina si dafay wéy di bon, te dina la jaxasse. Waaye sa ngëm gi nga am ci Krist, te mu daan dee gi ak seytaane, dina la rëccloo safaras merum Yalla, ak lëj-lëj yu amul àpp yi. Képp ku gëm Yeesu, dangay jot yërmande Yàlla. Ndax xabaaru Yeesu bii tooyal na sa xol ? Ndax Xel mu Sell mi nekk ci yów, ndax mungi naan : « Baay ji moo ma moom, Doom ji mooy sama Musalkat te Xell maa ngi dëkk ci man. Yàlla kenn ki, mungi ci man. Maa ngi sax ci yiwam. »

ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist, dugg nga ci sama xol, te musal ma. Aar nga ma te sàmm ma ci fiiri Seytaane te itam goreel nga ma ci kaso fenam yi. May nga ma dund gu dul jeex. Ragaluma dee gi. Aar ma ci sa coobare te sol ma sa kàttan ba ma fees, ndax ma lay màggalandoo ak ñu sell ñépp. Dimbali ma ba ma bëgg sama mbokk yi, te di baale, te it ma nekk taalibe jàmm buy nangu nga koy wommat. Maa ngi wéeru ci Yów ; yaay Boroom Ndam li.

LAAJ:

  1. Lu waral Baay ji bëgg nu,ak nan la nu bëgge?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 23, 2026, at 06:56 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)