Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":

Home -- Wolof -- John - 092 (Abiding in the Father's fellowship appears in mutual love)

This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
D - Tàggatoo ba ca yoonu Getsemane (Yowaana 15:1 - 16:33)

2. Bu nu saxee ci jokkoo ak Yàlla Baay ji,kon dinanu wone sunu bëggante (Yowaana 15:9-17)


YOWAANA 15:9
9 Ni ma Baay ji bëggee, noonu itam laa leen bëgge. Saxleen ci mbëggeel googu ma am ci yeen.

Baay ji dafa bëggoon lool Doom ji, ba ubbi asamaan yi ba ñu Koy sóob ci ndox ca deux Yurdan. Xel mu Sell mi wàcc ci jëmmu pitax, ab baat jib ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg ci moom laa ame bànneex.» Yégle Kenneefu Ñett boobu, fekk Yeesoo ngi gàddu bàkkaari nit ñi, dugal na mbotem Yàlla mi ci yoon wi Koy yóbbu ca saraxe ba. Na Yaxya doon sóobe ca ndox moo doon misaalu tuub ak mbaalug bàkkaar. Doom ji dafa matal coobare baay ji, te fàtte boppam, ngir sunug mucc. Mbëggeel googu yemul ci Baay ji ak Doom ji rekk, waaye dañoo ànd lëngoo ci bëgg àddina su bon sii, ngir waajal mucc gu rëy gi.

Ni nu Yeesu bëgge, la Ko Baayam bëgge. Yeesu dafa déggoon ndigal, moo tax wuute na ak nun. Amul kenn ci nun ku ñu sàkk ca njalbéenu lépp. Li am mooy ne, Doom ji dafa nu tànn, nun bàkkaarkat yi, te sellal nu. Dafa noo may juddu gu bees ci Xel mi, te sellal nu. Jàppewunu ni ay fowukaay yu muy sànni saa su ko neexee. Fépp fu Mu tollu, xelam a ngi ci nun te mungi nuy xalaat saa su nekk. Mungi nuy rammu, te di nu bind ay bataaxali mbëggeel ci biir Injiil li dafa nuy ñaax ngir nu gëm, bëgg, te am yaakaar. Bu nu naroon a dajale mbëggeelu ndey ak baay yépp ci àddina si, te sellal mbëggeel googu ci lépp li koy gàkkal, ak itam ci ger, loolu lépp dafay mel ni lu tuut, ci boo ko méngalee ak mbëggeel gi Yeesu am ci nun; maanaam mbëggeel lu dul wor mukk.

YOWAANA 15:10
10 Su ngeen toppee samay ndigal, dingeen sax ci sama mbëggeel, ni ma toppe sama ndigali Baay, ba tax ma sax ci mbëggeelam.

Yeesu dafa la artu ne la: «Bul tàqalikook sama mbëggeel. Ku la bëgg laa, te di séentu say firnde mbëggeel ci man. Nooy dunde say ñaan? Ndax yaangi yëg sa jokkoo ak sa Boroom? Lan ngay defal néew-doole yi, jaare ko ci sama mucc gi ma jëf? Maangi lay ñaax ci def lu baax, liy woneji sa baaxaay ak sa sellaay. Saxal ci sama mbëggeel. Xel mu Sell mi dina la xiir ci def lu baax, ni Yàlla di defe lu baax saa su nekk.»

Bañ a bëgg ni Yàlla bëgge, bàkkaar la. Krist dafa noo bëgg a yéege ba nu àgg fi yërmande Yàlla tollu. «Na ngeen am yërmande ni Baay ji ak man ame yërmande.» Xëyna yaa ngi xalaat ne loolu lanul a nekk. Bu fekkee ne ci kàttanu nit doŋŋ la, wax nga dëgg. Waaye xamuloo lu Krist bëgg, ak li Mu man a def ci yów. Dafa lay sol Xelam mi ba nga fees, ndax nga man a bëgg, ni Mu bëgge. Ci kow xalaat boobu la Póol waxe ne: « Man naa lépp, jaare ko ci Krist mi may dooleel.»

Yeesu seede na ne mosul a weesu rëddi coobare Yàlla. Dafa mos a sax ci mbëggeelu Yàlla. Krist dafa nuy may nu ñam jàmmu Yalla, ñaan gu ànd ak Xel mi, ak surgawu ci mbëggeel.

YOWAANA 15:11
11 Wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk.

Xolu nit ki dafay tiis te ñàkk yaakaar, fi ak mungi tàqalikook Yàlla. Krist mi saxoon ci mbëggeelu Baayam, dafa feesoon ak mbég te barkeel. Ay cant aky màggal ñoo dëkkoon ci biir xolam. Ay géeji mbëggeelu xol la nu bëgg a may, rax ci dolli muccam gi. Yàlla mooy Yàllay mbégte gi.

Ci limu meññeefu Xel mi, mbégte moo topp ci mbëggeel. Fépp fu ñu daane bàkkaar, mbégte jolli fa. Krist dafa bëgg a dooleel sunu mbégte mucc, ndax nu man a jot ñeneen ñi. Nit ku bég du man a denc mbegam ngir moom kese, waaye dafay namm a indi ñeneen ñi ci dundug mbaal, te ñu xam mbégtewu kóolute gi nekk ci Yàlla. Su boobaa dinanu bég ndaxte ñu bare dinañu mucc. Ni ko apotar bi waxe, bi mu nee : «Yàlla dafa bëgg ñépp mucc, te xam dëgg gi.» Tas Xabaar bu baax bi, mbégte la ci biir ŋaayoo yi ak metit yi.

YOWAANA 15:12-13
12 Sama ndigal mooy ngeen bëggante, ni ma leen bëgge. 13 Genn mbëggeel manul a weesu joxe sa bakkan ngir say xarit.

Yeesu dafa noo bëgg,xam na sunu tur, sunu jikko ak sunu démb. Sunuy jafe-jafe ak sunuy metit ñoo ko soxal. Am na tëralin te bëgg naa tette sunu ëllëg. Saa su nekk mungi jekk ngir diisoo ak nun ci biir sunuy ñaan. Dafa nuy baal sunuy bàkkaar te di nu dundloo dund gu sell ci dëgg ak cellaay.

Li nu Yeesu bëgg, moo tax Mu namm nu bëggante ci sunu biir. Fu nu tollu danuy bàyyi xel ci sunu njaboot ak sunuy xarit, di xam li ñuy dund ak seeny tolof-tolof. Nu tàmbali di xool seen pasteef ak seen jikko. Nu fexe nu nuy saafare seeny jafe-jafe te may leen ndimbal lu wér, teg ci di am seen jot. Bu ñu juumee, nu baal leen, te bañ di joxoñ seen matadi ak seeny tooñ.

Yeesu mooy portale njobbaxtalu mbëggeel gi. Yemul rekk ci wax ak dimbalaate, waaye dafa saraxe boppam ngir bàkkaarkat yi. Dundul rekk ngir nun, waaye dafa nu wuutu ci dee gi. Kurwaa bi mooy kaalag mbëggeel gi nuy leeralal mbëggeelu Yàlla. Dafa bëgg nuy wesaare xabaaru mucc gi te di sàkk saraxu jot ak alal. Su la woowee ngir nga yégle Injiil li, te defal leen li nu Yeesu defal, kon mungi xaar nu joxe sunu bopp, sunu alal, ak sunu doolee. Ñaanal na ñi Ko doon metital, te jàppe leen ni ay xaritam. Ñaanal na ay noonam ba mu nee: «Baay baal-leen ndaxte xamuñu li ñuy def.» Woowewuleen doom-ndey (doom-baay), walla doomi Yàlla, waaye samay soppe la leen tudde. Ndaxte dafa dee ngir ngir rammu sax ñi yelloowul mbëggeelam.

YOWAANA 15:14-15
14 Samay xarit ngeen, ci ko ngeen di def li ma santaane. 15 Dootuma leen woowe surga, ndaxte surga du xam li sangam di def. Xarit laa leen di woowe, ndaxte xamal naa leen lépp li ma jële ci sama Baay.

Yów yaay «soppe» Yàlla. Nun ñépp lay woowe «ay soppeem». Man na am nga wéet, te xamuloo ci kan ngay dem. Xoolal ci Yeesu mi dee ngir yów, te di dund it ngir yów. Mooy sa xarit bi gën a mag, bi jekk saa su nekk ngir wallu la. Xam na say xalaat te mungi lay xaar. Ngir sax ci xaritook Moom, danga war a bëgg ñeneen ñi, ni Mu leen bëgge. Ñaari nit manuñu meroo, ba noppi naan dañoo sopp Yeesu. Mbëggeelam dafa laaj bëggante. Ay soppeem lanu tudde. Moo nu moom ndaxte moo nu sàkk, te am na sañ-sañu def nu ni ay jaamam. Yewwi nanu ci buumu njaam gi te yékkati nu. Dafa nuy xamal jëfam yu sell yi. Dunu bàyyi ci ñàkk a xam, waaye dafa nuy jàngal turu Baay ji, kàttanu kurwaa bi ak mbëggeelu Xel mu Sell mi. Bi Mu nu wonee kumpa gi ci Kenneefu Ñett ñi, ci la nu feeñal dëgg yu làqu, yu amul àpp yi. Baay ji teg na mbir yooyu yépp ciy loxoom, ngir Mu xamal nu leen. Xaritoom gi dafa rëy ba Mu may nu, nu bokk ci liggéeyam, ngëneelam, terangaam, kàttanam ak dundam. Jéemul a xëccoo sax yelleefu baayoo, walla njureel, waaye dafa noo indi ci boppam ngir def nu ay doomi Yàlla.

YOWAANA 15:16-17
16 Du yéen yéen a ma tànn, waaye man maa leen tànn, sas leen ngeen dem, meññ meññeef gu sax, ngir Baay ji def lu ngeen Ko ñaan ci sama tur. 17 Li may santaane nag, mooy ngeen bëggante.

Sa wóllëre ak Yeesu ajuwul ci sa coobare, sa bëgg-bëgg, walla ci li nga jot a dund, waaye ci mbëggeelam, tànneefam, ak wooteem la aju. Jaamu say bàkkaar nga nekkoon, Seytaane yollangar la, te nga nar a dee. Manuloo woon génn ci kaso boobu, waaye Yeesu dafa laa tànn la ko dale ca njalbéen ga, te goreel la jaare ko ci deretam ji Mu tuur. Def na la xaritam te may la yelleefu ndono ni doom àqan. Tànneefam ci yiwam doŋŋ la aju. Waaye yów man nga Koo nangu, mbaa nga weddi Ko. Yeesu ñépp la tànn ba mu jébbalee bakkanam ca Kurwaa ba ngir seeny bàkkaar. Waaye du ñépp a dégg wooteem gi. Ñenn ñi, toog ci lëndëmu bàkkaar gi moo leen gënal. Xamuñu goreelug doomi Yàlla yi. Krist dafa laa woo ngir nga yewwiku ci bàkkaar te dund ak Moom ci biir wóllëre gu tar. Sa goreel gi dafa am mujj: Liggéeyal sa Boroom ak nit ñi, ci kow mu neex la. Amul forse gu mel ni njaam. Yeesu dafa def boppam surga ndax mbëggeelam. Mooy sunu misaal. Xalaatul boppam, waaye ay soppeem la tal.

Kon mungi yaakaar gis nu ni ay sàmmi géttam gi ëmbaale sunu xarit yi. Fi ak sunu kàttan matul, kon kay manunu goreel kenn ci buumu njaam. Yeesu dafa nuy ñaax ngir nuy ñaan ci turam. Ndaxte bu nuy ñaan Yeesu ngir muy wommat ñi Mu goreel, te di leen dooleel ci teggin ak baatin, rax ci di saafara seeni mébéti ruu, yaram ak xel, kon sunu Boroom dina àddu ak mbégam. Kumpa ñaan gu nangu mooy mbëggeel. Booy ñaanal say xarit ak sa xol bépp ci anam yooyu, Yeesu ci yów lay tàmbalee: Di la won say bàkkaar, dammat la, dugal la ci dund gu maandu, gu am njariñ, te woyoflu. Teg ci nag sa Boroom dina musal say xarit. Nungi lay ñaax ci ngay góor-góorlu di ñaan. Yeesu digewul lu tuuti, waaye meññeef muy law la dige. Képp ku gëm ndax say ñaan, ak sab seede, dina dund ba fàww, jóge ci dee, tàbbi ci dund.

Bu weesoo ngëm giñaan yi ak seede bi, Yeesu dafa la sant nga bëgg say noon, ak mbëggeel gu dëggu te laab. Muñalal leen, ak lu seen jikko yi man a ñagase. Nanga lewet ci seen kanam, ni Yàlla lewete ak yów. Na sa leeraayu mbëggeel ne rayy ci àddinas ger gu bon gii. Fexeel ba di jëfe dox-dox bi, jébbale sa bopp ji, déglu bi, ak jëf ji. Na mbëggeelu Krist wesaaroo jaare ci yów.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ndaxte yaa nu goreel ci buumu njaamu bàkkaar, ba noppi def nu say soppe. Dimbali nu ba nu bëgg ñépp, ni nga nu bëgge. Nungi lay màggal te di am yéene wéy ci say ndigal. Jàngal nu ni nuy dégge ndigal, ndax nu man a meññ doomu mbëggeel gu sakkan.

LAAJ:

  1. Lan la Yeesu defal ñi nekkoon jaami bàkkaar ngir ñu doon ay soppeem?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 20, 2026, at 08:29 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)