Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 034 (Healing of the paralytic)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
A - Ñaareelu tukki ca Yeruusalem (Yowaana 5:1-47) -- Yokkute jànkoonte diggante Yeesu ak Yawut ya

1. Pajum jarag ga ca Betesda (Yowaana 5:1-16)


YOWAANA 5:10-13
10 Yawut ya daldi ne nit ku wér ka: » Tey bésu noflaay la, te sunu aada tere na ngay yor sa basaŋ. » 11 Mu ne leen: » Ki ma faj, moo ma ne: » Jëlal sa basaŋ te dox: » 12 Ñu ne ko: » Ku la ne: » Jëlal sa basaŋ te dox? » 13 Waaye waa ji xamul ki ko wéral, fekk booba Yeesu dem na, te nit ñu bare teewoon nañu ca bérab ba.

Ña teewoon ca pisin ba bég lool, ba mu des ña ŋankoon Yoon wa. Boroom ñaari boor yooyu ñee lool jarag ja, rax ci dolli mu xewe nag bésub noflaay ba. Du caagéen rekk ne Yeesu dafa wéral waa ja, waaye dafa ko osant mu gàddu basŋam ca biir mbeddi dëkk ba. Ci ñoom loolu bàkkaar la ci kanamu Yàlla, ak ci ormaal bésub noflaay bi; ndaxte benn liggéey warul a am ci bés boobu. Képp ku moyaan Ndigal loolu deesoon na la daane àtteb dee (Lim15 :32-36). Yawut ya dañu yaakaaroon ne laata Almasi bi di ñów, fàww ñépp topp Bésu noflaay bi ba mu mat sëkk.

Yawut yi naruñuwoon tëb rekk suule ay xeer góor googu yenuwoon basaŋam, ndaxte dañu la waroon a artu ba noppi, door laa daan. Artu bi, ab tëkku la woon. Ki Yeesu wéral nag, di setal boppam, ba dugal ci li ko Yeesu sant. Yenu basaŋam kay bokkoon na ci li waroon a matal wéram gi.

Boroom xadar ci diine yooyu mer ba futt, te béguñu ci wérug waa ji. Ñu tàmbali diwerante ci seen biir ak bëgge te rax ca bañ ka wéraloon nit ka. Moo dem ba sañ a sant laaga ba mu gàddu basaŋam ci ab bésub noflaay. Ci kow loolu, ngir ñoom,Yeesu, moykatu Yoon, bu yelloo dee la.

Nit ka ñu wéral, xamuloon ka ko faj, ndaxte Yeesu gan la fa woon, Bii mooy ñówam bu njëkk ci Betesda. Dafa mel ne dafa ne mes ba Mu fajee waa ja ba noppi. Yeesu bëgguloon nit ñi di ko gëm ndax kéemaan ya Mu daan def, waaye dafa bëggoon ñuy xool ci mbëggeelam.

YOWAANA 5:14-16
14 Ba ñu ca tegee ab diir, Yeesu dajeek moom ca Kër Yàlla ga, ne ko: » Déglul, fii mu nekk wér nga, bul defati bàkkaar ngir ragal lu yées lii dal la. » 15 Noonu nit ka dellu ne Yawut ya, Yeesu moo ko fajoon. 16 Looloo tax Yawut ya di wut a sonal Yeesu, ndaxte daan na faje ca bésu noflaay ba.

Yeesu dafa wut ka Mu fajoon, ngir matal paj ma te yewwi ko ciy bàkkaaram. Mu fekk ko ci Kër Yàlla ga muy màggal Yàlla. Tiitaange ak mbégte jaxasoo ci xolam, ba mu gisee Yeesu. Yeesu ne ko:

» Wér nga léegi. Xoolal kéemaan gu rëy gi la dab.Jaar nga ci 38 ati coono.Ci Yàlla la jóge,du mbiru nit. Yàlla mi jëmmu ci boppam ubbi na say bëti xol.

Xam nga say bàkkaar. Dund gu Yàlla teewul moo indiwoon googu musiba. Ci ni Mu la faje, lañu la baale sa bàkkaar yépp. Ngir wér gi laal biiram bépp, Yeesu dafa ko wax mu dégg ndigal, te bañ a bàkkaarati. Jot mbaalug bàkkar, dafa laaj dogu bàñ a defati bàkkaar bu ni mel. Képp ku nangu kàddu Krist, gu fees ak kàttan gi, te tuub say bàkkaar, dinga jot doole ju jóge asamaan, man a daan lu bon ci ndimbalu Yàlla. Krist laajunu lu nu manul, waaye dafa nuy may Xel mi ngir doole jooju man a daan sunuy bëgg-bëggi yaram ak sunuy xemmem yu bon yi. Xelum dëgg gi dafa nuy dëdale ak lu bon, te di nu dooleel ngir nu të ko.

Yenn saa yi, feebar yi ak gaañu-gaañu yi Yàlla dafa leen di dogal ngir nu dellusi ci Moom. Yeneen saa yi, alal ak naataange man nañoo nekk mbugalug Yàlla, ndax sunu dëgër bopp ci Moom. Dëgër bopp man na indil nit mu mel ni seytaane, ba tàbbi safara sax. Bul fowe bàkkaar bi lay sonnal, waaye deel nangu li la ciy xiir, te ñaan Yeesu Mu goreel la ci. Bul mel ne ku amul fu mu far ci diggante Krist ak sa bàkkaar. Dogal sa buumu bàkkaar. Sàmpal kóllëre ak sa Musalkat. Dina la musal ba mu mat sëkk.

Ndaw mbetteel! Ba waa ja dégloo yeddu Yeesu ya ba noppi, dafa ne wërëñ, dem ca Yawut ya ne leen waayu Nasaret ja moo ko wéral, te beddi ko ca la Yoon tëraloon ci bésub noflaay bi. Xarañ-Yoon ya am yaakaar ne xëyna dina gën a tëru Yeesu ba ñu man koo jàpp ci lu gën a leer.

Mbañ ga kilifa diine ya wonewoon ba Yeesu di sellal Kër Yàlla ga, dëgërewuloon ni jànkonte gi Farisen yi tegal Yeesu. Krist dafa ngàdd seen ‘Njubte’, te wone ne njubte teguwul ci Yoon wuy sàmm li ngay ràccal sa bopp. Yàlla, yërmande ak mbëggeel la santaane. Cellaay gu àndul ak mbëggeel du dëgg, ag neen la. Yàlla, yërmande la namm ci nun, waaye du ay ngér. Ndokk ba nu Yàlla génnee ci ay sarti ngér yu dul jeex, te jox nu genn ndigal giy mbëggeelam doŋŋ.

LAAJ:

  1. Lu tax Yawut yi bundxataal Yeesu?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 25, 2025, at 05:57 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)