Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 020 (Jesus' first miracle)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
B - Krist jële na ay taalibeem la ko dale ca tuub seeni bàkkaar ba ca mbébteg céet ga (Yowaana 1:19 - 2:12)

4. Kéemaan gi Yeesu jëkk a def ca céet ga ca Kana (Yowaana 2:1–12)


YOWAANA 2:1-10
1 Ñetti fan gannaaw loolu ag céet am ca dëkku Kana, ca diiwaanu Galile. Yaayu Yeesu teewewoon na ko. 2 Woowoon nañu it Yeesu ca céet ga, ak ay taalibeem. 3 Ca biir xew wa, biiñ ba daldi jeex. Yaayu Yeesu ne Ko: ”Amatuñu biiñ.” 4 Yeesu ne: ”Soxna si, loo ma bëggal? Ndaxte sama waxtu jotagul.” 5 Yaayam daldi ne surga ya: ”defleen lépp lu Mu leen wax.” 6 Foofa amoon na fa juróom benni ndaa yu ñu yett ci doj, yu man a def daanaka téeméeri liitaar. 7 Yeesu ne surga ya: ”Duyleen ndaa yi.” Ñu duy leen, ba ñu fees bay rembat. 8 Noonu Yeesu ne leen: ”Tanqleen ci léegi, yót ko njiitu xew wi.” Ñu daldi ko ci yót. 9 Ki jiite xew wa ñam ndox, ma Yeesu soppi biiñ. Xamuloon fu biiñ booba jóge, waaye surga ya tanqoon ndox ma, ñoom xamoon nañu ko. Naka noonu, mu woo boroom céet ga ne ko: 10 ”Ci xew yépp, naan gu neex gi lañuy jëkke. Bu nit ñi doyalee, ñu sog a génne ga ca des. Waaye yów dangaa dencoon gi gën a neex ba nëgëni.”

Yeesu dafa jële taalibeem ya ca tundu rëccu ak tuub, wa ca mbartali dexu Yurdan ga, yóbbu leen ca tundi Galile ya, ngir ñu bokk ca xawaare genn céet. Tukkib 100 kilomeetar boobu, moo nuy won coppite gu leer gi am ci diggante ñaari Kóllëre yi. Way-gëm yi waafatuñuwoon ci keppaaru Yoon wi (Ndigal yi), waaye dañoo dugg ci mbégteg njubte Yeesu, miy Jant bu fenk bi, ak mayekatu jàmm ji.

Yeesu duwoon Kuy dunde xiif ak diine, ni Yaxya. Loolu moo tax tukkib Krist aky taalibeem ya ngir bégeji ca ab xewu mbooloo, nekkoon ab kéemaan ci boppam. Araamalul biiñ bi, ndaxte jàngale na ne du liy dug ci nit ki moo koy selladil, waaye xalaat yu laabadi yiy jóge ci xolu nit ki. Yeesu bañul kuy xiifal ngir man a topp diine, walla ku xarañ ba mu ëpp, waaye jàngale na ne yooyu dundin amuñu solo noonu. Sunu xol yu bon yi, dundin ak juddu yu bees lañu soxla. Waaye nag Biibal bi tere na mandite, ak lang ci sangara.

Taalibe ya gunge Yeesu ca xew wa. Natanael ci boppam, kana la cosaanoo (21:2). Yaayu Yeesu dafa mel ne xam na waajuri boroom céet li. Xalaat nañu ne booba fekk na Yuusufa génn àddina. Ni Maryaama nekke jétur, Yeesu moo waroon a am baat bi jiitu ci kër gi, ndaxte mooy taaw.

Looloo tax Matyaama ñaan ko Mu fajal bokkam yi seen soxla bu jamp bi. Ba Mu jógee Yurdan ba ñibbisi, nekkatuloon nitu neen; Xel mu Sell mi daf koo soppi, te xiir ko ci surgawu Yàlla, muy waar wu taalibeem yi nar a soong lu yàggatul dara.

Maryaama amoon na yaakaar ci Doomam, ndaxte xamoon na mbëggeelam. Mbëggeelam ci Yeesu, moo indi kéemaan gu njëkk gi. Ngëm gu wéeru ci mbëggeelu Krist dafay baral loxo Yàlla. Maryaama dafa ñaan surga yi ñu def li Yeesu wax. Wóoroon na ko ne Yeesu dina def dara, ak nu mu manta deme. Kàddu yi mu wax surga yi, ñooy baati coongu bépp jàngu tey.” Defleen lépp lu Mu leen wax!” Kon nanga déggal Krist doŋŋ; déggal kàddoom, ay kéemaan rekk lay wàccee.

Ndaa ya ñu daan laabale seen yaram, dañu leen ŋaccoon ba ñu wow koŋŋ, te bu ci nekk manoon na duy 600 liitari ndox, duy nañu leen ba ñu rembat. Dafa mel ne gan ya dañoo jëfandikoowoon ndox mu bare ngir laabal seen yaram. Laabal gu wuute moo taxaw bu Yeesu teewee. Kenn manual a bokk ca céeytalu Mbote mi, bu ñu la laabalul ban ga set-wecc.

Moone dey, laabal gi nekkuloon lu gënoon a soxal Yeesu. Céetal gi dafa waroon a wéy. Yeesu soppi na ndoxum laabal ma, mu nekk biiñ bu neex lool. Xamunu nan la defe googu kéemaan. Waaye, li jëm ci céetalu Mbote mi, xam nanu ne deret ji ñu tuur doy na sëkk ngir gan yépp. Loolu séqul dara ak màndite. Xel mu Sell mi nanguwul màndite. Waaye biiñ bu bare bi, te neex, bi Yeesu maye, dafay misaal nattu mbaalug bàkkaar gu amul fu mu yem, gu Krist jagjeel nit ñépp. Na ñépp bokk ci mbégte asamaan ji. Ñépp jot ak ngërëm mburu mi ak biiñ bi bu ñuy séddoo reeru Boroom bi, muy misaalu teewaayu Krist- di maye mbaal fekk nungi noflaayu ci mbéggteem.

YOWAANA 2:11-12
11 Firnde bii ame na ca kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkk a def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu Ko. 12 Bi loolu weesoo, Mu ànd ak yaayam, ay rakkam, aky taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa.

Taalibe ya waaruwoon nañu lool ci ni Krist man a sàkke, te noonu la seen xel ubbeekoo ci sañ-sañ bi Mu am ci mbir yi nekk. Dañu gis ndamam te gëm ne Yàllla moo ko yebal. Loolu moo leen xiir ci gëm Ko. Ngëm dafa laaj ab diir ngir màgg, ak dégg ndigal, ngir man a xam. Boo jàngee jëfi Yeesu yi, te gëstu bu xóot ay kàddoom, dinga gis màggaayam.

Yeesu dafa beruwoon waa këram, te goreel boppam ci wareefi àddina ngir man a liggéeyal Yàlla. Waaye mungi doon sàmm digganteem ak yaayam aky rakkam. Am na jamnono ñu daan ànd tukkeendoo ak taalibe ya. Rakkam ya àndoon nañu ak Moom ca Kaparnawum, dëkk ba gënoon a mag, ca wetu déegu Tiberyad. Taalibe ya dañu Ko wóoluwoon ci seen bopp, te du caageen kéemaan ga Mu defoon ca Kana. Dañoo doguwoon taq ci Moom ba fàww.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ndaxte yaa nu dalal ci ag céetal, nu dug ci mbégte jokkoo ak Yów. Baal nu sunuy tooñ, te sol nu ba nu fees ak sa Xel mu Sell mi.D inanu La top, te sax ci njubte gi, cellaay gi, n inga ko defe, te jébbale sa bopp ni sarax ngir ñu bare.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu yóbbaale taalibeem ya ca céetal gag?

LAAJ YI - 1

Yow sama mbokk miy jàng téere bii,
yónnee nu 20 tontu yu jub, ci biir 24 yii. Bu loolu amee, dinanu la yónnee njàng mi top ci mii.

  1. Kan moo bind ñeenteelu Injiil li ?
  2. Lan la ñeenteelu Injiil li séq ak yeneen ñett yu jiitu yi ?
  3. Lan mooy mébétu Injiilu Yowaana ?
  4. Kan lañu ko jagleel ?
  5. Nan lanu ko man a xaaje def ko ay njàngale yu leer yu ñu xajjale ?
  6. Ban baat moo gën a fës ci aaya bi jiitu ci Yowaana 1, te lu muy tekki ?
  7. Yan ñooy 6 melokaani Krist yi Yowaana di wone ci fi Injiilam tàmbalee ?
  8. Lan moo wuutale leer gi ak lëndëm gi, ci baatin ?
  9. Yan ñooy nammeelu liggéeyu Yaxya ?
  10. Lan la Krist Leer gi séq ak àddinay lëndëm gi ?
  11. Luy dal ñi nangu Krist ?
  12. Lan mooy jëmmalu Krist (jëmmalu Krist, lu muy tekki) ?
  13. Lan mooy mataayu Krist ?
  14. Ban xalaat bu bees la Krist indil àddina si ?
  15. Waa Kureel gu mag ga luñu doon séentu ca la ñu doon laaj Yaxya ?
  16. Nan la Yaxya woowe nit ña ngir ñu waajal yoonu boroom bi ?
  17. Lan moo ëpp maanaa ci seede bi Yaxya def ci Yeesu ca kanamu Kureelu Sanedreeŋ ba?
  18. “Mbotem Yàlla”, lu muy tekki?
  19. Lu tax Yeesu nekk kiy maye Xel mu Sell mi ?
  20. Lu tax ñaari taalibe ya gis Yeesu ?
  21. Nan la taalibe yu njëkk ya siiwalee turu Yeesu ?
  22. Nan la taalibe yu njëkk ya jottalee ñeneen ñi, turu Yeesu ?
  23. Turu “Doomu Yàlla”ak “Doomu Nit ki” lu leen boole ?
  24. Lu tax Yeesu yóbbaale taalibe ya ca céetal ga ?

Yónneel say tontu,te bañ a fàttee bind sa dëkkuwaay ba mu leer-nañ fii:

Waters of Life
P.O.Box 600 513
70305 Stuttgart
Germany

Internet: www.waters-of-life.net
Internet: www.waters-of-life.org
e-mail: info@waters-of-life.net

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 11, 2025, at 10:53 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)