Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
B - Krist jële na ay taalibeem la ko dale ca tuub seeni bàkkaar ba ca mbébteg céet ga (Yowaana 1:19 - 2:12)
4. Kéemaan gi Yeesu jëkk a def ca céet ga ca Kana (Yowaana 2:1–12)YOWAANA 2:1-10 Yeesu dafa jële taalibeem ya ca tundu rëccu ak tuub, wa ca mbartali dexu Yurdan ga, yóbbu leen ca tundi Galile ya, ngir ñu bokk ca xawaare genn céet. Tukkib 100 kilomeetar boobu, moo nuy won coppite gu leer gi am ci diggante ñaari Kóllëre yi. Way-gëm yi waafatuñuwoon ci keppaaru Yoon wi (Ndigal yi), waaye dañoo dugg ci mbégteg njubte Yeesu, miy Jant bu fenk bi, ak mayekatu jàmm ji. Yeesu duwoon Kuy dunde xiif ak diine, ni Yaxya. Loolu moo tax tukkib Krist aky taalibeem ya ngir bégeji ca ab xewu mbooloo, nekkoon ab kéemaan ci boppam. Araamalul biiñ bi, ndaxte jàngale na ne du liy dug ci nit ki moo koy selladil, waaye xalaat yu laabadi yiy jóge ci xolu nit ki. Yeesu bañul kuy xiifal ngir man a topp diine, walla ku xarañ ba mu ëpp, waaye jàngale na ne yooyu dundin amuñu solo noonu. Sunu xol yu bon yi, dundin ak juddu yu bees lañu soxla. Waaye nag Biibal bi tere na mandite, ak lang ci sangara. Taalibe ya gunge Yeesu ca xew wa. Natanael ci boppam, kana la cosaanoo (21:2). Yaayu Yeesu dafa mel ne xam na waajuri boroom céet li. Xalaat nañu ne booba fekk na Yuusufa génn àddina. Ni Maryaama nekke jétur, Yeesu moo waroon a am baat bi jiitu ci kër gi, ndaxte mooy taaw. Looloo tax Matyaama ñaan ko Mu fajal bokkam yi seen soxla bu jamp bi. Ba Mu jógee Yurdan ba ñibbisi, nekkatuloon nitu neen; Xel mu Sell mi daf koo soppi, te xiir ko ci surgawu Yàlla, muy waar wu taalibeem yi nar a soong lu yàggatul dara. Maryaama amoon na yaakaar ci Doomam, ndaxte xamoon na mbëggeelam. Mbëggeelam ci Yeesu, moo indi kéemaan gu njëkk gi. Ngëm gu wéeru ci mbëggeelu Krist dafay baral loxo Yàlla. Maryaama dafa ñaan surga yi ñu def li Yeesu wax. Wóoroon na ko ne Yeesu dina def dara, ak nu mu manta deme. Kàddu yi mu wax surga yi, ñooy baati coongu bépp jàngu tey.” Defleen lépp lu Mu leen wax!” Kon nanga déggal Krist doŋŋ; déggal kàddoom, ay kéemaan rekk lay wàccee. Ndaa ya ñu daan laabale seen yaram, dañu leen ŋaccoon ba ñu wow koŋŋ, te bu ci nekk manoon na duy 600 liitari ndox, duy nañu leen ba ñu rembat. Dafa mel ne gan ya dañoo jëfandikoowoon ndox mu bare ngir laabal seen yaram. Laabal gu wuute moo taxaw bu Yeesu teewee. Kenn manual a bokk ca céeytalu Mbote mi, bu ñu la laabalul ban ga set-wecc. Moone dey, laabal gi nekkuloon lu gënoon a soxal Yeesu. Céetal gi dafa waroon a wéy. Yeesu soppi na ndoxum laabal ma, mu nekk biiñ bu neex lool. Xamunu nan la defe googu kéemaan. Waaye, li jëm ci céetalu Mbote mi, xam nanu ne deret ji ñu tuur doy na sëkk ngir gan yépp. Loolu séqul dara ak màndite. Xel mu Sell mi nanguwul màndite. Waaye biiñ bu bare bi, te neex, bi Yeesu maye, dafay misaal nattu mbaalug bàkkaar gu amul fu mu yem, gu Krist jagjeel nit ñépp. Na ñépp bokk ci mbégte asamaan ji. Ñépp jot ak ngërëm mburu mi ak biiñ bi bu ñuy séddoo reeru Boroom bi, muy misaalu teewaayu Krist- di maye mbaal fekk nungi noflaayu ci mbéggteem. YOWAANA 2:11-12 Taalibe ya waaruwoon nañu lool ci ni Krist man a sàkke, te noonu la seen xel ubbeekoo ci sañ-sañ bi Mu am ci mbir yi nekk. Dañu gis ndamam te gëm ne Yàllla moo ko yebal. Loolu moo leen xiir ci gëm Ko. Ngëm dafa laaj ab diir ngir màgg, ak dégg ndigal, ngir man a xam. Boo jàngee jëfi Yeesu yi, te gëstu bu xóot ay kàddoom, dinga gis màggaayam. Yeesu dafa beruwoon waa këram, te goreel boppam ci wareefi àddina ngir man a liggéeyal Yàlla. Waaye mungi doon sàmm digganteem ak yaayam aky rakkam. Am na jamnono ñu daan ànd tukkeendoo ak taalibe ya. Rakkam ya àndoon nañu ak Moom ca Kaparnawum, dëkk ba gënoon a mag, ca wetu déegu Tiberyad. Taalibe ya dañu Ko wóoluwoon ci seen bopp, te du caageen kéemaan ga Mu defoon ca Kana. Dañoo doguwoon taq ci Moom ba fàww. ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ndaxte yaa nu dalal ci ag céetal, nu dug ci mbégte jokkoo ak Yów. Baal nu sunuy tooñ, te sol nu ba nu fees ak sa Xel mu Sell mi.D inanu La top, te sax ci njubte gi, cellaay gi, n inga ko defe, te jébbale sa bopp ni sarax ngir ñu bare. LAAJ:
LAAJ YI - 1Yow sama mbokk miy jàng téere bii,
Yónneel say tontu,te bañ a fàttee bind sa dëkkuwaay ba mu leer-nañ fii: Waters of Life Internet: www.waters-of-life.net |