Previous Lesson -- Next Lesson
2. Sóobkat bi ci ndox(Yaxya) mungi waajal yoonu Krist (Yowaana 1:6-13)
YOWAANA 1:6-8
6 Yàlla yónniwoon na nit ku ñu naan Yaxya. 7 Kooku ñów na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñów na ngir ñépp dégg li mu wax,te gëm. 8 Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñów na ngir seedeel leer gi.
Yàlla dafa yónni Yaxya ci àddina si ngir mu woo nit ñi ñu ñów ci ceeñeeri leeru asaamaan gi. Ñépp xam nañu ne bàkkaar yu bare ñungi xew ci lëndëm gi. Waaye ku nangu say bàkkaar te tuub leen ci kanamu Yàlla, ak xol bu laab te metitlu, dinga dug ci leer gi. Foo ci tollu? Ndax ñów nga ci leer gi, waala yaangi làqatu ci lëndëm gi ba tey?
Yaxya dafay feeñal xolu nit ñi. Ci Yoonu Yàlla, nit ñépp a bon Soxla nañu tuub seeni bàkkaar te soppiku ngir bañ a sànku ca bésub àtteb Boroom bi. Wooteb Yaxya laaloon na xolu nit ña ba ay naaxi nit di dawsi ci moom ngir tuub seeni bàkkaar ca biir mànding ma. Dañu nanguwoon seeni bàkkaar ca biir mbooloo ma, te ñaan ñu sóob leen ci ndoxu Yurdan ga, muy misaal bu leen di laabal ci seeni bàkkaar, te di laabloo seen rëyaay ca dex ga, ba ñu fëlle ci dund gu bees.
Yàlla dafa tànn Yaxya; sol ko te yónni ko ngir mu gindi nit ñi, ba ñu soppi seeni xalaat, te jekk ngir teeru ñówug Krist. Niti jamono Kóllëre gu Njëkk ga xamoon nañu bu baax lu aju ci Ki war a ñów ci turu Boroom bi. Yonnent Yàlla Esayi newoon na ci Moom: ”Xeet wi doon wéy ci lëndëm, gis nañu leer gu mag; ñi dëkkoon ci réew mi dee njàtt, leer fenkal na leen. (Esayi 9: 2) Nee na itam ci turu Boroom bi: ”Jógal yów te nga jot leer gi ndaxte sa leer a ngi ñów, te ndamul Yàllaa ngi jolly ci sa know.” (Esayi 60:1) Yaxya dafa jàngale ne ñówug leer gi ci biir lëndëm gi du woon rekk ngir waa Kóllëre gu Njëkk ga, waaye ngir ñépp la. Noonu kàddu Yaxya àddina sépp la ko jagleel, ak askani penku bi gën a jege, te diiwaan yi wër Géeju Mediterane topp nañu ko ay ati-at gannaaw ba mu génnee àddina sax.
Ay junniy nit toppoon nañu Yaxya, ak li mu leen wax lépp ne du moom mooy Leer gi, waaye mooy ndaw li ñu yónni ngir mu jiitu Ko (Leer gi). Woowul nit ñi ngir ñu ñów ci moom, waaye ngir wommat leen ca Yeesu. Loolu mooy màndarga yonnent Yàlla yu dëggu, yi dul xëcc seeni taalibe ci seen bopp, waaye ci Yeesu rekk lañu leen di jëmale.
Li Yaxya doon wut, du tuub bàkkaar ak sóobu ci ndox, waaye ngëm gu sax ci Krist. Xamoon na ne nit ñi dañu doon yaakaar mu biral ne moom mooy Krist. Waaye moom nanguwul daanu ci fiir googu, xanaa kay, dafa xàllal yoon wi Boroom bi. Xamoon na ne ki waroon a ñów, dina sóob nit ñi ci Xel mu Sell mi. Yaxya xamoon na itam ne rëccu te tuub mu yem ci xel doŋŋ doyul, bu fekkee sax ne sóob nañu nit ka ngir mbaalug bàkkaaram. Réerewuloon mbir ne nun ñépp soxla nanu yeesalu biir gu mat sëkk. Yàlla mayu ko muy soppi xol yi, te itam mayul loolu benn Yonentu Kóllëre gu Njëkk nga.Googu ngëneel, Leeru njalbéen ga sàkkoon lañu ko jagleloon, maanaam Leer giy maye dund, te di yeesal nit ki ak sañ-sañam, bu gëmee turam, te jekk ngir dalal leer gi. Noonu la Yaxya doon fexee ba nit ñu bare gëm Yeesu, t exam ne ngëm gi kese moo leen man a dugal ci jamono ju bees.
Appolos boroom baatin bu am xadar te xarañ lawoon, te doon top njàngalem Yaxya. Waxoon na ci Krist te mosaguloon sax ci leeru Kóllëre gu Bees gi. Waaye bi mu jébbaloo ci Krist, leer gi dug ci xolam noonu mu nekk ag leer ngir Boroom bi, ak ab làmp ci guddi gi. Gindi na nit ñu bare( Jëf 18:24-28).
ÑAAN: Céy yow Yeesu! Ñungi màggal sa tur, te di la sant, ndaxte yow yaay leeru àddina si ak yaakaaru walaakaana yi. Leeral nga sunu lëndëmu xol, feeñal sunuy bàkkaar, te baal nu leen. Jarajëf ci li nga nu def say doomi leer te goreel nu ba fàww. Na say ceeñeeri leer leeral sunuy xarit ak sunuy waajur ndax ñu man a mos tuub dëgg te dugge ak ngëm ci sa leer gu kéemaane gi.
LAAJ:
- Lan la Yaxya di wut dëgg-dëgg ci liggéeyam?