Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":

Home -- Wolof -- John - 104 (Jesus intercedes for the church's unity)

This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
E - Ñaanu rammu gi Yeesu def (Yowaana 17:1-26)

4. Yeesoo ngi ñaan ngir Jàngu bi nekk benn (Yowaana 17:20-26)


YOWAANA 17:20-21
20 Ñaanaluma leen ñoom rekk, waaye itam ñi may gëm ëllëg ndax seen wax. 21 Damay ñaan ngir ñépp doon benn. Baay, na ñooñu nekk benn ci nun, ni nga nekke ci man te ma nekke ko ci Yów. Nañu ànd, ba àddina gëm ne, yaa ma yónni.

Krist dafa samp ay taalibeem ci mbëggeelu Baay ji ak kàttanu Xel mu Sell mi. Dafa ñaan Baayam mu aar leen ci ku Bon ki te sellale leen ak Injiil li laata ñu koy daaj ci bant bi. Ba mu xamee ne ñaanam ngir ndawam yi ak Jàngu bi nangu na, Mu bég ci li war a ñów te gis naaxu nit ñu gëm ndax xabaar bi leen ay ndawam yegge. Ndamu Ki ñu daaj ci kow Seytaane ak bàkkaar moo leen ñaax. Ni ñu wóoloowoon Krist miy dund, moo tax Xel mi wàcc ci seen xol te di leen dimbali ba ñu man di séddoo yiwu dundu baatin gi. Ngëm gi moo tax ñu nekk benn ci Baay ji ak ci Doom ji ba fàww.

Krist dafa ñaanal ñi naroon a gëm ndax seedes ndawam ya. Kàddoom ya wone nañu kóolute gi Mu amoon ci seeny xabaar. Kon book, ñaanam gi, lu nu ci boole? Ndax ñaanal nanu wér-gi yaram? Walla naataage? Mbaa ndam? Mukk! Dafa ñaan Baayam ngir Mu may nu suufeelu ak mbëggeel, ngir nu man a nekk benn ak kercen yépp yi dëggu. Bu nu foog ne noo gën ñeneen ñi, walla seen doxalin jekkul. Kercen yi nekk benn rekk la Yeesu bëgg; Jàngu bi tas, bokkul ci tëralinam Waaye nag jokkoo gi Yeesu bëgg kenn manu ko samp ci kow ay maslaa diine, waaye ci kow ay ñaan, ak ci Xel mi lay jaare. Ni Yàlla nekke benn, noonu it la Krist ñaane Baayam ngir Mu boole way-gëm yépp ci jokkoo ak Xel mu Sell mi, ndax ñu man a aaru ci moom.

Krist waxul ne: «ngir ñu gëm ma, walla ñu gëm la», waaye «ñu gëm nu». Kon kay dafa ci laawaale ne jokkoo gu wér gi am ci diggante Baay ji ak Doom ji, jaare ko ci Xel mi, firnde ju dëggu la. Dafa laa bëgg a yemale ak boppam, ndaxte gannaaw jokkoo gi ngi nga man a am ak Kenneefu Ñett ñi, Safara rekk moo fa sës.

Sunu mébétu dunde jokkoo ak Yàlla, du neex sunu bopp ci baatin, waaye ngir nu man a seede ci kanamu ñi seen dund sore Yàlla la. Ci kow yiwu Yàlla, ñooñu dinañu man a ràññee ne bàkkaar faat na leen ba noppi, dañoo rëy te nekk jaami seeny nafsu. Noonu dinañu rëccu seeny bàkkaar, tuub, te dellu ci Musalkat bi. Yów mi jokkoo ak Baay ji, Doom ji ak Xel mu Sell mi, dinga am kàttanu woyof te fees ak mbëggeel. Ci biir goreelug baatin, dinga bëgg ñépp ñi gëm, te bége ak ñoom. Noonu ngeen ànd nekk seedey mbëggeelu Krist yu takku. Nun ñépp ay firnde baatinu jëmmu Yeesu lañu. Bu kercen yépp dëggu woon, kon kenn ku dul kercen du des ci àddina si. Kon seen mbëggeel ak seen jàmm naroon na leen a xiirtal te soppi leen. Nanu bàyyi xel ci ñaanu Yeesu gi, te nekk benn! Ndax dangaa nar a indi ñàkk ngëm ci jàngu bu tas ba noppi, mu mel ni yaramu Krist dañu koo def ay morso?

YOWAANA 17:22-23
22 Boole naa leen ci ndam li nga ma sol, ngir ñu àndandoo, ni nu ànde man ak Yów. 23 Man ci ñoom, Yów it ci man, ngir ñu gën a ànd, nekk benn, ba àddina xam ne yaa ma yónni, xam ne bëgg nga leen, ni nga ma bëgge.

Lan mooy ndamu Yeesu? Ndax ay ceeñeeram ak leeraayu màggaayam ñoo tax? Déet! Ndamam a ngi làqu ci suufeeloom, muñam ak lewetaayam. Bépp meññeefu Xel mi, ceeñeer la ci ndamam Yaxya gis na loolu te seede na ko ba mu nee: «Gis nanu ndamam.» Du caageen ne ca coppiteg xax-kanam ga ak ca ndekkite la, la doon xool, waaye it ca lekkukaayu jur ga ak ca Kurwaa ba. Ca biir xew-xew yooya yépp, ndamu mbëggeelu Yàlla dafa feeñ, ndaxte Doom ji dafa bàyyi boppam ak ndamam, dal di ñów teewal màggaayam ci jëmmu nit. Ndam loolu Yeesu may nanu ko. Xelum Baa ji ak Doom ji wàcc na ci nun.

Ngirte may googu du ngir teg nu ci kow lépp, walla dinu neexal, waaye ngir nu nekk benn ci liggéey bi, te di jàppalante. Danu war di sargal ñeneen ñi. Yeesu jokkoo gu ni mel, jiy firndeel Keeneefu Ñett gu Sell gi la ñaanoon Baayam ji, ngir sol nu melokaan yooyu. Mbëggeelu Yàlla mooy nattukaay bi ñuy seetloo Jàngu bi. Moom moo nuy mooñ ba nu mel ni Moom.

Yàlla, ak mataayam gépp, dafay dëkk ci Jàngu bi (Efes 1 :23 ; Kolos 2 :9). Am nanu fit wu doy sëkk ngir biral kàdduy aaya yii: « Ndaxte ci Moom la mataayu Yàlla feeñe. Jot nga lépp lu bokk ci Yàlla ci Moom. Seedeb Ndaw yii mooy firnde ne ñaanu Yeesu ya nangu nañu. Danuy jaamu Boroom bi ndaxte sewalu nu donte sunuy bàkkaar, waaye dafa noo ssellal, laabal nu te boole nu ci boppam ndax nu man a jot ci dundam gu Sell gi.»

Yeesu gëmoon na ne nun dinanu man a mat sëkk ci mbëggeel ak ci suufeelu. Nanu bëggante te di teralante! Wutul sunu mataay ci sunu alal, walla ci sunuy man-man, ak sunu maandute, waaye ci sunu yërmande, ak sunu mbëggeel lay xool. Ñówental ak mbaal gi rekk a Ko ñoroon bi mu naan: «Nangeen sell, ni seen Baay ji ci asamaan selle.» Boobu ndigal moo tënk njàngaleem. Waaye ci ñaanug rammoom gi, dafa ci dàkk lu gën a kowe lu aju ci mataay, maanaam jokkoo baatin ci Jàngu bi, ak jokkoo ak Yàlla. Xel mu Sell mi du xiir kenn ci tëju ci sa bopp, mbaa beru, dafay xiire ci jokkoo ak ñu sell ñi. Jokkoo gi dox ci biir Kenneefu Ñett ñi mooy sunu royukaay. Te dunu man a jekk ngir taxawal Yàlla ci àddina si, bu nu nekkul benn. Ni nit ña daan taxawale melokaanu Yàlla ca jamono Kóllëre gu Njëkk ga, noonu it la Jàngu bi war a gën a taxawale melokaanu Kanneefu Ñett gu Sell gi.

Jàmm ji ci biir Jàngu bi mooy yéem niti àddina si ba ñu gis ne ci Yàlla lanu jóge. Noonu, dañuy ràññee ne Yàlla mbëggeel la. Du ay kàddu rekk, walla ay waare yu gudd-a gudd ñoo leen di xiir ci gëm. Mbëggeel gi nekk ci biir mboolentu doomi Yàlla yi moo gën a man a tooyal xol bépp waare. Noonu la Xel mu Sell mi lëkkale woon Jàngu bu njëkk ba, ca Yerusalem ñu nekk benn, ci baatin gu dëggu.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ci li nga fexe ba nu gëm la, nun ñi selladi. Nungi lay màggal ndaxte sellal nga nu, te jox nu matuwaay yu wér ngir nu bokk ci sa jëmmu baatin. Saxal nu ci mbëggeelu Kenneefu Ñett gu Sell gi. Nungi lay màggal, di la sargal te di la saraxu ngir nga may nu kàttanu dunde jokkoo gu dëggu te wér ci sunu jàngu bi.

LAAJ:

  1. Lan la nu Yeesu ñaanal Baayam?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 25, 2026, at 09:05 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)