Previous Lesson -- Next Lesson
3. Ndigal lu bees ngir Jàngu bi (Yowaana 13:33-35)
YOWAANA 13:33
33 Samay soppe, sama nekk ak yéen dootul yàgg. Dingeen ma seet, waaye maa ngi leen di wax léegi li ma waxoon Yawut ya:Fa ma jëm, dungeen fa man a dem.
Ba ñu jébbalee ndam li Baay ji jaare ko Xel mi ba noppi, Yeesu mungi nuy wommat ci fànnay sunu ngëm ak fi mu sax. Nekkul ak nun ci yaram rekk, waaye mungi ci asamaan. Krist dekki mooy li gën a am solo ci àddina si. Ki xamul Kiy dund, mbaa gëmu Ko, kooku dafa gumba te réer; waaye ku Ko gis dinga dund te am dund gu dul jeex mukk.
Yeesu waxoon na ay taalibeem ne famuy dem, ñoom duñu fa man a dem. Du taxawaayam ca kanamu Kureel ga, walla ndekkiteem ga, moo taxoon Muy wax loolu, waaye demug asamaan ga la doon wax. Baay ji newoon na: ” Toogal ci sama ndeyjoor, ba ma def say noon dëggukaayu tànk.” Yeesu tëbul rekk ne mes, waaye yëgal na taalibeem ya deewam, ndekkiteem ak demug asamaanam, fa nga xam ne benn doomu Aadama manu fa demal boppam. Wax na ko Yawut ya, waaye manuñu woon a dégg wax ja. Taalibe ya, ndax manoon nañoo xam, léegi bi waxtu wor gi agsee ? Mosloo na leen ci màggalu Baay ji ak Doom ji, ngir ñu bañ a sóobu ci naqar ak yaakaar gu tas, gu ëllëg gu lëndëm. Ndax dinañu wóolu li Mu leen dig ne du leen bàyyi mukk ? Ndax dinañu gëm ne seen mbootaay gi du tas mukk ?
YOWAANA 13:34-35
34 Maangi leen di jox ndigal lu bees; bëgganteleen. Nangeen di bëggante ni ma leen bëgge. 35 Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante. »
Yeesu xamoon na ne Taalibeem ya dégguñu woon bu baax li muy wax, ndaxte jotaguñu woon Xel mu Sell mi. Dañoo gumba woon, te manuñu woon a am kóolute; am mbëggeel ñoruleenoon « ndaxte Yàlla mbëggeel la, te ku sax ci mbëggeel, sax ci Yàlla, te Yàlla sax ci moom. » Kenneefu Ñett gu Sell gi mbëggeel la. Ndegam bëggeel gi dox ci diggante jëmmi Kenneefu Ñett gu Sell dafay wéy, kon Yeesu dafa bëgg liy dawal Kenneefu Ñett gu Sell gi jëmmu ci nit ñi, te reenu cellaay gi feeñ ci taalibeem yi.
Noonu, Yeesu ñaax taalibeem ya ngir ñu bëggante ci biir Jàngoom. Tegaluleen fukki jëf yu Mu leen tere, na mu deme woon ca Kóllëre gu Njëkk ga, waaye dafa joxe benn ndigal kese, bu ëmb yeneen ndigali Yàlla yépp. Mbëggeel moo matal Yoon wi. Fi Musaa joxee askan wa ay tegtal yu metti, Krist moom dafa nuy ñaax ci jëf ju rafet. Dafa joxe boppam sax ni misaal. Mbëggeel mooy reenu dundug Jàngu bi. Su Jàngu bi wonewul genn mbëggeel, kon dootul nekkati, dafay saay.
Mbëggeel mooy kumpa gi nekk ci Yeesu. Dafa amoon yërmande ci mbote yi nib sàmm. Dafa muñaloon taalibeem yi. Mbëggeel la Krist defoon ni ponku nguuram. Képp ku am mbëggeel yaangi sax ci yiwu Yeesu, waaye ku am mbañeel, Seytaane moo la moom. Mbëggeel dafa baax, te du rë-rëylu. Dafay muñ, te di yéene lu baax noon yi sax. Ndawi Yeesu yi dañuy wone ci bataaxal yi, ni mbëggeel mel. Mbëggeelu Yàlla du moy mukk; mooy lëngoo gu mat sëkk. Ngir Jàngu bi, amul meneen mandarga mu dul jébbale sa bopp ndax mbëggeel.
Su nu tàggatee sunu bopp ngir surgawu, dinanu nekk ay taalibeem. Bu nu Yeesu wommatee, dinanu xam lan mooy mbëggeel dëgg ciy jëf. Danuy dund ci mbaalam, te di baal ñeneen ñi ak mbég. Su fekkee ne ci am mbooloo, kenn xeexul ngir nekk ki gën a màgg (ngir diiroo mbagg), te ñépp di bége ndaxte Xelum Krist moo leen boole, ñu nekk benn, kon, asamaan dina dajeek suuf, te sunu Boroom biy dund dina taxawal ay jàngu yu fees ak Xel mu Sell mi.
LAAJ:
- Lu tax mbëggeel rekk mooy tax ñu ràññee Kercen yi?