Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 085 (Christ predicts Peter's denial; God is present in Christ)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
B - Xew-xew yi amoon gannaaw reeru Boroom bi (Yowaana 13:1-38)

4. Krist wax na ci weddi Piyeer ba (Yowaana 13:36-38)


YOWAANA 13:36-38
36 Simoŋ Piyeer laaj Ko ne : « Boroom bi, foo jëm ? » Yewesu ne ko : « Fa ma jëm, manuloo ma faa topp léegi, waaye dinga ma toppi ca kanam. » 37 PIYeer ne Ko : « Boroom bi, lu tax manuma laa topp léegi ? Àttan naa joxe sama bakkan ngir yów ! » 38 Yeesu ne ko : « Àttan ngaa joxe sa bakkan ngir man ? Ci dëgg maangi la koy wax, balaa ginaar a sab,dinga ma weddi ñetti yoon.

Piyeer dafa jaxasoo woon ba manul dégg li Yeesu di wax ci li aju ci mbëggeel. Li mu jotoon a jàpp kay mooy ne Boroom bi mungi leen di dëddu ci biir ñàkk kaaraange gu rëy. Noonu muy sukkandiku ci kàttanam, di dig Yeesu ne dina Ko topp, te jaral na ko sax bakkanam. Manuloon a natt néew-dooleem ak fi kàttanam yem, nonu mu yaakaar ne man naa matal digeem bu ñàkk solo bi. Dafa amoon xadar ci Yeesu, te jekkoon ngir xeex, ba dee sax ngir Moom.


C - Tàggoo ba ca Néeg bu kowe ba (Yowaana 14:1-31)

1. Yàlla dafa teew ci Krist (Yowaana 14:1–11)


YOWAANA 14:1-3
1 Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma. 2 Am na néeg yu bare ca sama kër Baay, buduloon noonu, ma wax leen ko, ndaxte maa ngi dem defarali leen fa ngeen di dëkki. 3 Te su ma leen defaralee bérab booba ba noppi, dinaa dellusi, yóbbaale leen, ba fu ma nekk, ngeen nekk fa yéen itam.

Taalibe ya dañu jàqoon bi ñu xamee ne Yeesu dafay jóge ci ñoom, te manuñu Koo topp fa Mu jëm. Yeesu wax na itam lu aju ci dëddu bi Ko Piyeer nar a def, fekk Piyeer ci boppam mungi Ko doon dig ne dina gar bakkanam, àndak Moom te doon tiitaroo dëgëraayu ngëmam. Xëyna am na taalibe yu demoon bay xalaat ne topp Yeesu, njuumte la ndaxte léegi Mu dem, te yégle na deewam sax. Wékkul ci Yàlla te bañ a yox-yoxi, Mooy fondamaŋ bu wóor bi (ëkk gi) saa su nekk. Dara manu Koo jengal,waaye lépp li ci des dafay lox-loxi. Dafa nuy yewwi ci li nu ragal. Ragal dafay wone ñàkk ngëm. Sunu Baay bi ci asamaan du tas yaakaaru kenn, te du dëddu kenn. Sa ngëm mooy ndam liy daan àddina si.

Ak kóolute gu mat sëkk, Yeesu ñaan na taalibeem yi am ngëm lu tollook li Mu am ci Baayam ji. Moom, benn la ak Baay ji. Ni Baay ji di sàmme sunu ëllëg, noonu la nu Doom ji di maye lu wér te wóor. Ci Doom ji la Baay ji jëmmoo ci àddina; Mbëggeelam yelloo na sunu kóolute. Kóoluteem it, moo gën a dëgër doj.

Noonu Mu wéy di xamal taalibeem ya yenn xew-xew yi nar a am bu génnee àddina, ak bu yéegee asamaan. Ca Yàlla, am na fa këru buur gu gën a rëy te gën a rafet gi boroom alal yi am ci àddina sii. Këru buur gi Yàlla am, dafa mel ni ab dëkk bu rëy, bu man a dalal saa su nekk ñépp ñi sell ci àddina si. Bu fekkee sax ne leegi nii ci xayma, walla ci néegu ñax nga dëkk, bul am naqar. Ca sa këru Baay am na fa néeg yu bare, ak dalu yu yaatu. Waajal na la kër gu set, nugg, te leer nànn. Dinga man a dëkk ak Moom ba fàww.

Yàlla dafa bëgg ñi gëm Yeesu, te waajal na leen dëkkuwaay. Bi Yeesu delloo asamaan, dafa saytu dëkkuwaay ya, te àggala wààjtaay ya. Noonu la dogoo dellusi ci nun; bëggu noo sori. Dafay dellusi ngir dajale ay taalibeem. Dafa leen a bëgg ni jëkkër bëgge jabaram. Dafa bëgg a wonale Jàngu bi, maanaam soxnaam si, ak Baayam ji. Du caagéen ne dafa koy wonale doŋŋ ak Baay ji, waaye ngir mu bokk ci njabootu asamaan gi. Moom lanuy àndal ba fàww, Mu nuy aar, nuy bége baaxaayam.

YOWAANA 14:4-6
4 Te fa ma jëm, xam ngeen yoon wi. 5 Tomaa ne ko : « Boroom bi, xamunu fa nga jëm. Kon nan lanuy man a xame yoon wi ? » 6 Yeesu ne ko : « Man maay yoon wi, maay dëgg gi te dund di it man la. Kenn du ñów ci Baay ji, te jaarul ci man.

Yeesu ne taalibeem ya : « Xam ngeen fa ma jëm, te xam ngeen yoon wiy jëme ca Yàlla. » Tomaa ne Ko : « Nan lanuy xame yoon wi, te fekk xamunu foo jëm nees tuut ? »Ci kow naqaram, manul a woon gis cëppaa-ndaw lu sore la. Tiitaange gi moo ko jàppoon ba xamatul fu muy jublu.

Yeesu dëfal ko ak lewetaay : « Maay yoon wiy jëme ca Yàlla,sama mbëggeel ak sama dëgg ñooy yoon wu dëggu wiy yóbbu nit asamaan. Man maay natt bi leen Yàlla di àttee. Desleen ci yoon wiy jëme ca Yàlla. Ñówleen ci man, te méngale seen bopp ak man; kon dingeen gis ne dungeen dara lu dul ay bàkkaarkat yu geru. »

Krist du la jallax ci ragal-oo-ragal,walla yaakaar gu tas, teg ca geneen. Boo suruxee ba lab ci sa dund, dafa lay tàllal loxoom ngir musal la, naan la : « Leegi nag maa ngi lay jox dëgg gu bees; gu njëkk ga wéy na. » Wuutu naa la ci dee gi, te taxawal naa kóllëre gu bees gi jaare ko ci yiw. Baal nañu la say bàkkaar; sa ngëm musal na la. ŋoyal ci man ngir nga des ci baayoo gu wóor gi. Dinga jote dëgg gi ci man booy jege Yàlla. Boo ma ñàkkee, dangay dee. »

Xëyna dangaa yaakaar ne : « Nangu naa loolu lépp, waaye damaa ñàkk ngëm, kàttan, ñaan, ak sellaay. »Yeesu tontu ne : « May naa la dund gu dul jeex; maay reenu dund gi. Wéeral sa ngëm ci man ndax nga jot Xel mu Sell mi; Ci moom ngay jote dund gu naat. »Képp ku jox sa bopp Krist dinga dund ba fàww. Bul Ko sori, ndax Mooy sa dund. Mbaa nga dee ci say bàkkaar, walla nga dund ak Krist. Amul ŋarale. Krist mooy dundug way-gëm ji.

Ñépp ñi lëngoo ak Krist ñungi taxaw ci kanamu Yàlla te di Ko xoole ni Baay ju am yërmande. Amul benn diine, xalaat bu xarañ, yoon, walla xóotaayu xel bu la man a jegale ak Yàlla. Krist, Doomu Yàlla ji doŋŋ moo ko man a def. Ci moom la Baay ji jëmmoo ci sunu kanam. Krist mooy peeñu àqanu Yàlla. Kenn du xam Baay ji te xamul Doom ji. Am nanu ngëneelu xam Baay ji; danu Koy jege, ndaxte Krist mbëggeel la, te def na nu ay doomi Yàlla.

YOWAANA 14:7
7 Bu ngeen ma xamoon, kon dingeen xam sama Baay. Li ko dale tey, xam ngeen Ko, te gis ngeen Ko. »

Xaley àddina sii dañoo tàqalikoo ak Yàlla ndax seeny bàkkaar. Kenn manul a xam Yàlla ci kow sa coobare bopp. Kenn mosul a gis Yàlla, ba mu des jenn Doomam ji kepp, ji nekk ci Moom Baay ji. Nee nanu : « Bu ngeen ma xamoon, kon dingeen xam sama Baay it. » Waaye xamuñu Ko woon. Xam, nekkul rekk dégg-dégg ak xarala, waaye coppite ak yeeslu la. Xam Yàlla dafay jëmmu ci nun, te di feeñ ci dund gi. Bu seen yaakaar tas, waaye njàngum diine du tax kenn xam Yàlla. Li koy maye kay, mooy nga wàkkirlu ci leer giy leeral Injiil. Bàyyil ñu soppi la, noonu dinga nekk leer.

Bi waxtu wor gi agsee, Yeesu ne taalibeem ya : « Leegi nag xam ngeen ma. Duma boroom ndam li, te man lépp, ki maandu te yelloo màggaay, waaye itam maay Mbotem Yàlla miy dindi bàkkaaru àddina si. Ci deewam giy muccloo la Yàlla di feeñoo ni Baay jiy juboole, ndaxte du àtte say bàkkaar ci meram, te du la mbugal, waaye man Doomam ji lay mbugal, ndax nga man a gore te sell, ndax yéen doomam yi, ngeen man a jokkoo ak Moom.

Ca kurwaa ba, Yàlla dafa wone boppam ni Baay. Aji Kowe ji sorewul, waaye mbëggeel la, yërmande ak ndekkite. Yàlla sa Baay àqan la. Yów mi Ko gëm xam nga dëgg gi nekk ci Yàlla. Xam-xam boobu dina la soppi ba nga am dund gu jekk te ànd ak jom.

YOWAANA 14:8-9
8 Filip ne Ko : « Boroom bi, won nu Baay ji, loolu doy na nu. » 9 Yeesu tontu ko ne : « Ni ma yàggeek yéen te ba tey Filip xamuloo ma ? »Ku ma gis, gis nga Baay ji. Kon nag nan ngay man a laaje naan : « Won nu Baay ji ? »

Kàddu Yeesu yi ne ”Gis ngeen Baay ji te xam ngeen ma.” Jaaxaloon nañu Filip mi xawoon a tontu ne “déet, gisunu Ko de !”Mu ne tekk, waaru ci màqaama Sangam bi. Mu wàccee baatam ne : « Sang bi, won nu Baay ji, loolu rekk doy na nu. » Tontu bii wone na ne xam na leegi kumpa Yeesu ak kàttanam. Boobu mbóot mungi aju ci jokkoo bi dox ci digganteem ak Baay ji. Bu waroon a jóge ci ñoom, dafa leen a waroon a won Baay ji, lu mu gàtt-gàtt, ngir ñu man leen a yónni, ni ñu Ko yónnee te aaru ci kàttanu ki man lépp. Rax ci dolli dañu naroon a xam te gis màkkaanu Yàlla, ba noppi jot kilifteef ci kow nit ñi, di man a faj ak dàq ay rab.

Ci ñaan googu, Filip wone na ne xamagul Baay ji astamaak Doom ji. Manul a ràññee baatin bi ak dëgg gi. Yeesu sikku ko, waaye dafa koo yërëmoon. Ci guddi gu mujj googu, wax na leen dëgg gu rëy gi : « Ku ma gis,gis nga Baay ji. » Noonu ,Yeesu xotti na mbalaan mi(mbañ-gàcce gi) nekkoon ci digganteem ak taalibeem ya. Amul benn gis-gis, walla gént yuy feeñali dëgg gi am ci Yàlla, lu dul jëmmu Yeesu. Moom, nekkuloon nit ku am solo kese, waaye ci Moom la nu gise Yàlla ci boppam. Tey jii man nga gis Yàlla, soo gisee Yeesu te xàmmee Ko. Tomaa it déggoon na kàddu yii te gisul solo si. Gannaaw ndekkite Yeesu li, dafa nërmeelu ci kanamu Sangam bi, daldi xaacu ne : « Sama Boroom ak Sama Yàlla ! »

YOWAANA 14:10-11
10 Xamuloo ne maa ngi nekk ci Baay ji te Baay jaa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax jógewuñu ci man, waaye Baay bi nekk ci man mooy matal ay jëfam. Gëmleen li ma leen wax ne maa ngi ci Baay ji te Baay jaa ngi ci man; walla book gëmleen ndax jëf yi.

Ab taalibe man na jàpp Injiil li bu baax ci xelam te gise Yeesu ni ku amul solo lool, te bañ sax ràññee Ki mu doon ci dëgg, su fekkee ne Xel mu Sell mi soppiwul xolam. Krist dafa génnee Filip ci fi mu bëgg a làqu ciy xalaatam. Noonu Mu tegal ko ab laaj bu jëm ci ngëm lu gën a xóot ci baatinam : « Xanaa gëmuloo ne maa ngi ci Baay ji ? Sama bàkku dund mooy màggal Yàlla. Maa ngi nekk ci biir Baay ji. Ci jëmm Baay jaa ngi ci man. Mataayu baatin gaa ngi ci man. Ci Xel mu Sell mi laa juddoo, dund ci seen biir te amuma benn bàkkaar. Xam naa Ko la ko dale ca njalbéen ga, te xame googu moo jëmmu ci man. Ci man lay feeñale baaxaayam ni Baay ak yërmandeem gu mat sëkk gi. »

« Am naa firnde buy dëggal seede boobu; mooy sama kàddu yu kenn manul teggi yi, ak jëfi baatin yi. Bu fekkee ne dangaa am jafe-jafe ngir gëm nekkinu Yàlla ci man, kon déglul kàddu yi Yàlla wax jaarale leen ci man. Kàddu yooyu dañu lay may dund, kàttan ak ñeme. Boo xamul samay kàddu, xoolal samay jëf. Yàlla ci boppam dafay jëf ci seen biir ci ay firnde yu jóge asamaan. Ci man la leen di musale, yéen ñi sànku. Bu sama waxtu daaj ci bant jotee dingeen gis jëfi Yàlla yu gën a mag yi, maanaam muy jubalewaat boppam ak nit ñi, jaarale ko ci sama dee. Ubbil say bët, te bul tëj say nopp. Dinga xàmmee Yàlla ci Ki ñu daaj. Mooy Yàlla dëgg ji nu dul mbugal, waaye dafa nuy musal. »

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, ci kow yiw, maa ngi naan « sama Boroom ak sama Yàlla ! Bal ma sama ñàkk-ngëm ak mbëggeel. Ubbilal sa Xel mu Sell mi samay bëti baatin, ndax ma man a gise ci Yów Baay ji, te sa mbëggeel soppi ma, ba xam-xam boobu tàbbal ma ci dund te soreel ma dee gi. Feeñalal sa xóotaayu ndam ñi gëmul ndax ñu man a jot dund gu bees ci kow ngëm.

LAAJ:

  1. Yeesu Krist ak Yàlla Baay ji, lu ñu bokk?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 27, 2025, at 02:47 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)