Previous Lesson -- Next Lesson
5. Wàññeeku taalibe ya (Yowaana 6:59-71)
YOWAANA 6:59-60
59 Baat yooyu la Yeesu wax bi Mu doon jàngale ca jàngu ba ca Kapernawum. 60 Bi ñu Ko dégloo ba noppi, taalibeem yu bare nee nañu: » Njàngale mii de, jafe na! Kan moo ko man a déglu? »
Yii kàddu yu aju ci mburum Yàlla, yaramu Yeesu ak deretam bare na fu ñu koy fekk. Yeesu dafay jaaraat ci ay baat te di leen di xóotal dànk-dànk. Yowaana moo dajale kàddu yooyu cig gàttal. Ca biir jàngu Kapernawum ba, Yeesu dafa cofaale ne Moo sut Musaa, te ñépp ñi Ko gëm war nañu bokk ci yaramam ak ci deretam.
Peeñu gu mel noonu ëppoon na ci noppi ña Ko doon roy. Ñu daldi am xel ñaar. Doguwoon nañu ngir déggal Yàlla te jaamu Ko; waaye nag léegi dañoo jaxasoo ci ni ñuy naane deretu Yeesu, te lekk yaramam. Ba seen njaaxle sësee, ca la Boroom bi, ci yiwam tijji xelu taalibeem yi am ngor, ngir ñu man a jëli lan mooy Mburum Dund gi.
YOWAANA 6:61-63
61 Yeesu gis ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu, mu ne leen: «Ndax li ma wax da leen a jaaxal? 62 Lan mooy am nag, bu fekkee gis ngeen Doomu nit ki dellu, yéeg fa mu jëkkoon a nekk? 63 Xelu Yàlla mi mooy joxe dund; ñam wi jariñul dara. Kàddu yi ma leen wax, ci Xelum Yàlla lañu jóge te ñooy joxe dund.
Yeesu daldi xam xalaati taalibeem yi waaye bañu leen tontu. Seen ñurumtu jógewul ci seen futi, ni ñi gëmuloon, waaye kàddu Yeesu ya dañoo jafewoon a nànd. Laata muy ubbi seen bët, Yeesu dafa jëkk a leeral lëndëm gi léebu bi ëmb, ba noppi mu won leen lan mooy tëralinu muccu àddina si.
Du yem rekk ci dee ngir ñoom, ngir ñu man a dunde yaramam ci baatin, waaye dina yéeg dem ca Baayam, fa mu wàccewoon. Du toog ci àddina sii. Gisoon nañu muy dox ca kow ndoxu dex ga te xamoon nañu ne du nitu neen. Dina yéeg dem ca Baayam, te yónnee leen Xel mu Sell mi. Loolu moo tax mu waroon a dee te it mu ñów ci àddina si. Jébbal na boppam ay taalibeem du ci dagg yaramam, waaye dafa leen a may Xelam.
Yeesu dafa wone ne yaram wi amul njariñ. Ca njalbéeen ga dañoo sàkkoon nit ki; mu baax te sell, waaye ay xalaatam ak yaramam dañoo mujje yàqu te geru. Amul kàttanu dund, dund gu jub te saa su nekk bàkkaar da koy mébét. Yaramam amul doole; moo tax Yeesu ne: » Jógleen ñaan ngir bañ a daanu cig fiir. Xel mi nangu na, waaye yaram wi amul doole. »
Saa su nekk Xel mu Sell mi mungiwoon ak Yeesu. Teewaay boobu moo nekkoon mbóotu dundam Dafa nu bëggoon a may jokkoo googu ak Xel mi ak yaramam wi jaarale ko ci deewam gi, ndekkiteem ak delloom asamaan te dunde ci nun ak Xelam mu Sell mi. Waxoon na Nikodem ne ko ndox mi ak Xel mi ñoo nuy may nu dugg ci nguuru Yàlla gi. Mungi doon wax lu jëm ci sóob ci ndox bi Yaxya doon def ak ñówug Xel mu Sell mi ca Pantekot ba. Ba muy waxtaan ak ñoom ci mbirum mburum dund gi, Krist dafa leen waxaale ne dina ñów ci ñów ci ñoom saa su ñuy séddoo reeru Boroom bi. Yooyu tegtal naruñu woon am benn solo, bu Xel mu Sell mi wàcculoon ci ñoom. Xell mu Sell mi mooy joxe dund gi yaram wi amul benn njariñ. Xelum Yeesu rekk moo man a xamal way-gëm yi teewaayu Krist ci ñoom.
Nan la Xel mu Sell mi di wàcce ci nun? Loolu mooy laaju ñépp ñi jekk ngir bokk ci yaramam ak deretam, ngir dund jokkoo gu mat ak Krist. Yeesu dafa tontu rekk ne: ” dégluleen sama baat, ubbil-leen seeni xol nàkku Injiil li.” Krist mooy Kàddug Yàlla gi. Képp ku dégg ay kàddoom, te wóolu Ko, Xel mu Sell mi dina la solu ba nga fees. Duyal sa xel ak sa xol ba ñu fees ak kàttan giy jóge asamaan jaare ko ci di jàng Mbind mu sell mi ba mu mokk. Jàppal ci dige Yàlla yi, ak li mu biral, su boobaa yaay ëpp doole ñi màcc ci sos ak seeni càkkite. Ndaxte ci Kàddu Krist giy musal, Aji sàkk ji dina ñów ci yów, may la dundam ak sañ-sañam.
YOWAANA 6:64-65
64 Waaye am na ci seen biir ñu Ko gëmul. Ndaxte Yeesu xamoon na ca njalbéen ga ñan ñoo Ko waroon a gëmadi ak kan moo Ko waroon a wor. 65 Mu dolli ca it ne: ” Looloo tax ma ne, kenn manul a ñów ci Man te Baay ji mayu la nga agsi.”
Ñu bare ñu doon topp Yeesu dégguñuwoon wax jooju bu baax, ba tax ñu beddiku dem seen yoon. Njàngaleem mi aju ci lekk yaramam te naan deretam moo gënoon a fés ci liggéeyam ca Galile, te looloo tax taalibeem yu bare bàyyi Ko. Noonu ña beddeeku woon xaajuñu dab limu doomi Aadama ya naroon a ñów, ndaxte ñoom manuñu woon wékku ci Yeesu te du leen jaral dara. Xamuñu woon dundug baatinam te ñemewuñu woon fas kóllëre ak Moom ci kow saraxam bi.
Yeesu waxoon na ay taalibeem ne ñenn ci ñoom dinañu Ko weddi te gedd Xelam mi. Boroom bi xamoon na xalaati ñépp. Xamoon na ne Yuda Iscariot ma lëngoowoon ak noonam ya, dina Ko wor. Yuda bëgguloon nangu Xelum Mbëggeelu Krist mépp. Na Mu doon waxe ci lu jëm ci deewug yaramam gi jubsi te metti lool, Yeesu xamoon na ne kenn ci taalibeem yi moo koy jébbal ay noonam.
Yeesu tëj wax ji, dellu ne kenn manu Ko gëm te Xelum Yalla mi àndul ak moom. Kenn manul a woowe Yeesu « Boroom bi », te amuloo Xelum yàlla mi. Sunu ngëm du rekk gëm-gëm, waaye jokkoo la ak Yeesu, jaare ko ci liggéeeyu Xel mu Sell mi. Ubbilal sa ruu Xelu Baay bi, bul weddi benn dëggu Yeesu. Su boobaa dinga mos ganeseem te dina dëkk ci yów ba fàww. Moom mooy mburu dund gi ñu la yekkal.
LAAJ:
- Naan la Xelum Dund gi nekke woon ci yaramu Krist?