Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 045 (Jesus offers people the choice)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
B - Yeesu mooy mburu dund gi (Yowaana 6:1-71)

4. Yeesu, may na ñépp ñu man a tànnal seen bopp ngir “nangu walla bañ!” (Yowaana 6:22-59)


YOWAANA 6:51
51 Man maay mburu miy dund te wàcce asamaan. Ku ci lekk, dinga dund ba fàww. Te mburu mi may joxeji, sama yaram la; dama koy joxe ngir àddina man a dund.”

Ndax mos nga gis mburu muy dox, di wax? Yeesu mungi tudd Mburum Dund gi, mburu miy dund-waxul mburu mi nu yàgg a xam, waaye ñamu baatin wi jóge asamaan lay wax. Waxul nu lekk suuxam ndaxte dunu ay dëm.

Yeesu tàmbali di wax lu jëm ci deewam. Duwoon taaru diineem moo waroon a rammu nit ñi, waaye jëmmalam gi. Dafa jëmmoo nit ba jébbal boppam ngir far sunuy bàkkaar. Ña Ko doon déglu mer lool; dafa meloon ni nitu neen (kese), ku soqeekoo ci njaboot gu amul doole. Bu fekkoon ne am malaaka moo leen feeñuwoon, kon doon nañu ko tàccu te sargal ko. Yeesu xamal leen ne du ndamam ak xelam ñoo leen di rammu, waaye yaramam wi ñuy daaj ci bant ngir muccug bépp doomu.

YOWAANA 6:52-56
52 Noonu Yawut ya am werante bu tàng ci seen biir naan: » Naka lanu waa jii man a joxe yaramam, ngir nu lekk ko? 53 Yeesu ne leen: » Dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, bu ngeen lekkul yaramu Doomu nit ki te naanu leen deretam, dungeen am dund ci yéen. 54 Ku lekk sama yaram naan sama deret, am nga dund gu dul jeex, te dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba. 55 Ndaxte sama yaram mooy ñam wu wóor wi, te sama deret mooy naan gu wóor gi. 56 Kiy lekk sama yaram te di naan sama deret dina sax ci man, ma dëkk ci moom. »

Ci biir Yawut yi amoon na ñu gëm Yeesu, ak ñu Ko weddiwoon. Ñaari wàll yooyu dañu daan am werante yu tàng-jër. Bañaale Yeesu ya seen xel dafa daan teey bu ñu xalaatee lu jëm ci naan deretam ak lekk yaramam. Yeesu gën a xóotal ŋaayoo ba ngir gën a man a ber ña Ko wóoluwoon. Mu natt mbëggéelu ñenn ña, te feeñal ngumba ñeneen ña. Noonu Mu ne: ”Ci dëgg-dëgg maangi leen koy wax, bu ngeen lekkul sama yaram, te naanuleen sama kopp bi, dungeen am wàll ci dund gu dul jeex gi. Bu ngeen bañee bokk ci Man, dingeen des ci dee gi ak ci bàkkaar ba fàww.” Yooyu kàddu tàbbi ci seeni nopp ni tuumaal Yàlla. Ndax Yeesu tëkku (dëkku) leen? » Reyleen Ma te lekk Ma, ngeen dund kéemaan. Sama yaram mburu la,mooy dundu asamaan gi ñu leen may. » Noonu ñu mer ñoom ñépp. Waaye ña Ko dénkoon seen bopp, ànd ak Xel mu Sell mi. Ñu gëm kéemaan googu, jàppe kàddu yooyu ni mu gën a rafete. Bu seen xel demoon ci Paak (bésu jéggi ba), kon dinañu xam ne Yowaana woowe woon na Yeesu Mbotem Yàlla. Yawut yépp dañuy feetu Paak, di lekk ca mbote ya ñu rendi ni sarax ngir dalal merum Yàlla. Yeesu xamal na leen ne mooy mbotem Yàlla dëgg miy gàddu bàkkaaru àddina si.

Tey jii xam nanu li reeru Boroom bi di tekki; yaramu Krist moo nuy dundal, te deretam moo nuy sellal ci bépp bàkkaar. Danu Koy sant ci yiw woowu. Ca jamono jooja waa Galile xamuñu woon kumpa googu, ba tax kàddu yooyu jaxase seen xel. Yeesu natt seen ngëm waaye seen xol yu dëgër tàmbali di feeñ.

Danuy màggal Yeesu ak mbég ak cant, ndaxte won na nu ni nu war a defe reeram bi ak ay misaal. Wax na nu itam ni Muy ñówe jaare ko ci Xelam mi. Bu dul saraxam bi dunu man a jege Yàlla; te dunu dëkk ci Moom. Saraxam bi moo tax ñu sellal nu ci sunu bàkkaar, baal nu te jekkal nu ngir nu dalal Ko ci sunu dund. Ngëm mooy matal kéemaan googu te boole nu ci ndekkiteem li ànd ak ndam li. Mbote mi nu rammu lanuy màggal. Yeesu yemul rekk ci dee ca bant ba ngir nun, waaye dafa nu bëgg a solu ba nu fees. Danuy nekk ñu sell, ñuy dund ba fàww.

YOWAANA 6:57-59
57 Baay bi ma yónni mungi dund, te Maa ngi dund jaarale ko ci Moom; noonu itam ku may lekk dina dund jaarale ko ci Man. 58 Kon nag, ñam wi wàcce ci asamaan a ngi noonu; bokkul ak ñam, wa seeni maam lekkoon te faatu. Ku lekk ñam wii may wax dinga dund ba fàww. » 59 Baat yooyu la Yeesu wax, bi Mu doon jàngale ca jàngu ba ca Kapernawum.

Krist dafa nuy wax lu aju ci dund gi ci Yàlla Aji Kàttan ji, Baay jiy dund. Mooy Baay ji fees ak mbëggeel ba fàww. Krist mungi dund ci Baay ji dundul ngir boppam, waaye ngir Baayam. Solos dundam wékkuwul ci ay bëgg-bëggi boppam, waaye ci déggal Baayam la tegu, Moom mi Ko jébbal lépp. Doom ji dafay surgawu Baay ji, te Baay ji dafa bëgg Doom ji te di jaarale bépp jëfam ci Moom Doom ji.

Yeesu dafa feeñalal noonam yi mbóoti jokkoom ak Baayam. Dafa leen may gii Peeñu: ”Degam Baay bi moo tax may dund te it ci Moom laay dunde, moo tax it Ma bëgg a dund ngir yéen, ci yéen. Kon dingeen man a dund ngir man, ci man.” Mbokk mi, ndax jekk nga ngir dund jokko googu ak Yeesu? Te nangu ko ci sa bakkan gépp? Ndax nangu ngaa dee ci sa bopp, te may Boroom bi Mu dund ci yów?

Krist ñówul ngir indi ay yeesal yu gën a dox.Yónneewunu xaalis ngir dimbali nu. Taxawalulay mbiri koomu diwaan yi. Mukk! Xol yi lay soppi, ba nit ñi man a dunde baatin ba fàww. Dafay may way-gëm yi ñu bokk ci baatinam. Kon book dafay sàkk nit ku bees ku dul dee mukk, kuy dund, di bëgg, di jàppale. Mébétam mooy Yàlla.

Nafaral juróom-benneelu xaaj bi, te waññi ñaata yoon la ci Krist wax ñetti yoon « Baay », Dund »ak « Ndekkite »ak lu ni mel. Léegi nga mokkal li ëpp solo ci Injiilu Yowaana. Képp ku gëm Yeesu dafay dund ak Xelum Yàlla Baay bi jubal ci ndamul ndekkite li.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, jarajëf ci li nga ñów ci nun te may nu dundug Baay ji ak naataange mbég mi. Baal nu sunuy bàkkaar te sellal nu. Dimbali nu ba nu man laa jaamu ci teey ak mbëggeel, di la topp, te bañ a dunde sunu nafsu.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu ne ña Ko doon déglu, ne dañu war a lekk yaramam te naan deretam?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 04, 2025, at 11:26 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)