Previous Lesson -- Next Lesson
1. Ag Kureelu Sanedreŋ mungi laaj Yaxya (Yowaana 1:19-28)
YOWAANA 1:25-28
25 Ñooñu laaj Ko ne: ”Gannaaw doo Almasi bi, doo Iliyas, doYonent bi war a ñów, lu tax ngay sóob nit ñi ci ndox?” 6 Yaxya ne leen: ”Man,maangi sóobe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul. 27 Kookooy ñów sama gannaaw, te man sax yeyoowuma tekki ay dàllam. 28 Lii xewoon na ci dëkku Betani,c a gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe ci ndox.
Yawut yi jàngoon nañu ci Tawret bi, ab laabal, jàpp, ak lu mel ni sóobu ci ndox. Jàpp, dañu ko jëlewoon ni luy laabal xel, waaye sóobu gi dëgg, ngir laabal ñi dul Yawut la, ndaxte dañu daan jàppe yeneen askan ya ni ñu laabadi. Ak lu mu ci man a doon, nangu sóobu gi, ab màndarga suufeelu lawoon ak dug ci njabootu Yàlla gi.
Looloo jaaxaloon waa kureelu Yerusalem ga. ”Lu tax ngay woo way-gëm yi ngir ñu tuub seeni bàkkaar, maanaam ñi joong ba noppi (ñi dug néegu góor) te bokk ci Kóllëre gi? Ndax danga noo teg ñu ñàkk cellaay te sànku, ndax merum Yàlla, nun ñinga xam ne nooy jawrini réew mi?”
Sóobu Yaxya bi, doj wuy fakkastal ñi wéeruwoon ci diine la. Dafa doon xajjale nit ñi ci ñaari mbooloo. Benn xaaj bi, mooy ñi ñu laabal ci sóobu rëccu bàkkaar yi. Ñooñu ñoo waroon a teeru Krist ndaxte jekkal nanu leen te tànn leen. Xaaj bi ci des, dafa weddi sóobu rëccu bàkkaar yi te wóolu seen bopp ci pare ngir teeru Krist. Dañoo yaakaaroon ne ñówug Krist ngir lijjanti mbiri politick ak Yoon, lawoon.
Yowaana, taskatu Injiil bi ci lu wóor waroon na faa teewe. Waxtaan wa waroon na ko yéem, rawatina laaji Kureel ga, ndaxte toontu ya ñoo tax ba ñu xam ne Yaxya du Krist, du Iliyas, te it du Yonent bi war a ñów. Yaxya amuloon genn kersa ci wax ne moom du kenn.
Yaxya, ndegam xamoon na li mu war a def, mu toontu ak woyofteef: ”Wax ngeen dëgg, amuma benn maanaa. Ndox rekk laay sóobe nit ñi, amul luxus, amul kàttan. Lépp li may def, misaal rekk la, muy waajal yoonu Kiy ñów.”
Gannaaw loolu, Yaxya, ak deri gileem ya mu soloon, jóg te xaacu ca kow, jëmale ko ca mbooloo ma, ak kureel ga: ”Yeen ñépp dangeen a gumba. Raññeewuleen xew-xewu jamono bii di xewe ci seen biir. Yeen a ngi may jàngat, man miy nit ku tekkiwul dara. waaye xoolleen! Krist angi nii di ñów! Mungi ci diggu mbooloo mii di rëccu ay bàkkaaram. Man Yaxya, amuma genn kàttan ngir matal lu mu manti doon; damaa am sas bu ma war a matal. Baat laa te Xel mu Sell mi xamal na ma ñówug Boroom bi. Mungi fii. Tey la bésub mucc gi. Rëcculeen, te tuub seeni bàkkaar, ndaxte bés yi dañoo gaaw.”
Mbooloo ma yéemu lool ci yéene boobu. Mbooloo ma dafa dajaloowoon ngir teeru Krist. Waaye Moom ñów na ba noppi, te kenn xammeewu Ko, kenn gisu Ko. Ñépp ne selew, di xoolante, te waaru.
Gannaaw loolu, Yaxya daldi biral tegtal yu gën a leer yuy wone Krist, ci ab seede bu nopp gën a man a dékku la Yowaana taskatu Injiil ba, waxoon ci baatin ci aaya 15: ”Kiy ñów sama gannaw, nekkoon na laata man.” Noonu la feeñale ñàkk àppu Krist, ak teewaayam ci biir nit ñi. Dafa wone ne ci jëmm, Krist nitu neen lawoon, ci seen biir, ku kenn xamul, amul kaala guy ray-rayi, walla yére yu yànj, ak bët yuy tàkk. Ni ñépp la melon dara wuutalewu Ko woon ak kenn. Waaye ci nekkinam dëgg, Ku wuute dëggantaan ak ñi ci des la. Jëmm ju nekk ca ba jamono sosoogul, sell te dëkk asamaan, ñów, taxaw ci seen biir ak lewetaay gu mat sëkk.
Yaxya dafa seede ne yelloowul surgawu Krist. Aada ju jamono jooja dafa laajoon surga di raxasal gani kër gi seeni tank. Yaxya moom, dafa jàppe boppam ni ku yelloowul sax tekki dàlli Yeesu, ba man Koo raxasal ay tànkam.
Kàddu yooyu jaaxaloon nañu mbooloo ma lool. Ñuy laajante ci seen biir naan: ”Ana gan googu nekk ci sunu biir? Nan la Boroom bi man a nekke nitu kese? Te lu tax Yaxya Yeyoowul tekki ay dàllam? ba loolu wéyee, kureel ga dellu Yerusalem, boole ca di ñaawal Yaxya. Xëyna sax amoon na ay taalibe Yaxya yu leen toppoon. Dañoo yaakaaroon ne Krist, buy ñów dafa naan ray ca Péey ma, ak màggaayam gépp, waaye du ni ab lees-xameesul, as nit ca mànding ma. Noonu lañu doxale ba daje ak Krist mu Yàlla mi rëcc leen.
Xew-xew yooyu ñungi amewoon ca penku Yurdan, fu sore makkaanu Kureel gu mag ga (Sanedreŋ), ci diiwaan bi Erod Antipas doon nguuroo. Kon book, Waa Kureel ga manuñu fa woon a jàppe Yaxya ngir àtteji Ko Yerusalem.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist, jarajëf ci li nga ñów ba ci nun, nekk nit ku mat ak Yàlla Aji Sax ji. Nungi lay màggal, di yëkkëti saw tur. Danga suufeel sa jëmm ba kenn manu la xàmmee, ba mu des Yaxya. Dangaa woyof te laabiir. Jàngal nu, ba nu nirook yów, di la top te di bàyyi Xel mu Sell mi mu di nu wommat.
LAAJ:
- Ban seede bu ëpp maanaa la Yaxya defal Yeesu, ci kanamu kureelu Sanedreŋ ga?