Previous Lesson -- Next Lesson
1. Ag Kureelu Sanedreŋ mungi laaj Yaxya (Yowaana 1:19-28)
YOWAANA 1:19-21
19 Lii mooy seede Yaxya. Amoon na bés Yawut ya yónni ay saraxalekat ca Yaxya, ñu ànd ak ñu soqikoo ci giiru Lewi. Ñu jóge Yerusalem, ñów ci moom, di ko laaj mooy kan. 20 Yaxya tontu na leen te nëbbu ci dara. Wóoral na leen ne, moom du Almasi bi. 21 Ñu laaj ko ne: ”Kon yaay kan? Ndax yaa di Ilias? Mu ne leen:” déedéet,duma Ilias.” Ñu ne ko: ”Ndax yaa di yonent bi war a ñów?” Mu tontu ne leen: ”déedéet.”
Yeete bi,ca xuru Yurdan la amewoon, jaare ci Yaxya. Ay junniy nit ñoo doon jóge fu sore, soong yoon yu wóoradi ya, wàcc tund yu kowe ya, ngir dëglusi kàdduy Yonent bu bees bi, te mu sóob leen ci ndox, ngir seen mbaalug bàkkaar. Ñi ëpp ca nit ñooña duñuwoon ñu xamul dara, ni ko ñiy rëy-rëylu di xalaate, waaye dañoo mar te namm gindig asamaan. Dañuy gaaw a ràññee ñi yore kàttan ak sañ-sañ bu mel noonu. Ca saa soosa, bëggatuñuwoon dégg lu jëm ci ay sart aky ndigal, waaye dañoo bëggoon a daje ak Yàlla.
Mbootaay gi gën a mag ci kureelu diine Yawut (Sanedreŋ), yégoon na yeete boobu. Noonu, ñu yónnee ag kureelu kilifa diine, ak ay sëti Lewi yi féetewuwoon rendi mala ya ngir jébbale leen ni sarax. Ñooñee nag ñoo waroon a tegal Yaxya ay laaj ju koy yóbbe àtteb dee, bu tuumaalee Yàlla.
Ndajem Yaxya ak Kureel googu lu ñépp yëgoon la, te ñàkk kaaraange. Taskatu Injiil bi nee na ay Yawut lañuwoon. Ak tur woowu, feeñal na ci benn fànna ci Injiilam. Ca jamono jooja, xalaatu Yawut dafa xoccaaraloon te nanguwul a maye dara ci tooñ, teg ci fees dell aky gëm-gëm yu teguwul fenn, aky xemmem, noonu Yerusalem nar a nekk fa ñu gën a weddee Xelum Krist. Du waa Kóllëre gu Njëkk ga doŋŋ ñoo jànkontewoon ak Krist, waaye itam kilifa diine ya, rawatina Farisieŋ, ya mujj a nekk nooni bépp diine bu nar a law te jaarul ci li ñu tëral, mbaa manuñu ko wommat. Loolu moo taxon ñuy jéem a yollngar (fakkastal) Yaxya ak seeni laaj.
Ci diggu mbooloo mu takku, te ne xott di déglu, ñuy laaj Yaxya: ”Yow yaay kan? Ku la jox sañ-sañu wax? Ndax jàng nga Yoonu diine ji? Ndax dangaa jàppe sa bopp ni ku Yàlla Yebal, walla yaay Almasi bi ci boppam?”
Yaxya moytu fiir gi, te fenul. Bu newoon “maay Almasi bi” kon dina ñu ko sànni ay xeer ba mu dee, te bu waxoon ne “du ma Almasi bi”, kon ñépp dinañu ko won gannaaw te ñàkkal ko solo. Ca jamono jooja, doomi Ibraayma yi ñungiwoon ci coono nooteelug waa Rom. Ñungi doon séentu ak doole ñówug Almasi bi leen di goreel ci nooteelu waa Rom googu.
Yaxya dafa seede ci kanamu mbooloo mépp ne du Krist, te du Doomu Yàlla ji. Nanguwul benn tur bu juuyoo ak jubluwaayu Xel mu Sell mi. Dafa tànnoon a yem ci suufeeloom, te gore ci li ñu ko sant, te xam ne Yàlla dina dëggal ay kàddoom bu waxtu wi jotee.
Taxul kureel ga yem foofu: ”Ndax yow yaay IliasTur woowu mungi feeñ ci dig bi nekk ci Malasi 4:5, biy yéene ne laata Almasi bi di ñów, dina am yonent bu ko jiitu te am xelum yonent Ilias mu siiw ma, ak kàttanam. Ilias moomu wàccewoon na safara ci kow ay noonam, te dekkal nit ku dee, ci coobare Yàlla. Ñépp a jàppewoon jàmbaar jooju ni ab kilifa seenum réew. Waaye Yaxya moom dafa suufeelu, ak bu fekkee sax ne moom lañu digewoon, ni ko Krist dëggale gannaaw gi (Macë 11:14)
Kilifa diine ya laaj ko ndax mooy yonent bi ñu dige te Musaa newoon ne dina niroo ak moom, te taxawal Kóllëre gu Bees, gu mag (Dëtoronom 18:15). Li ñu bëgoon a xam mooy kan moo ko yónni ngir muy wax nib yonent, fan la jële sañ-sañam ak itam, ndax mooy waxal boppam, walla dafa jot leerug peeñu.
Yaxya dafa lànk a def ni Musaa mbaa di mel ni moom. Bëgguloon a taxawal Kóllëre gu bees ak Yàlla, te fekk kenn yónniwu ko ngir mu def ko, mbaa muy jiite askanam wa ngir ñu am ndam ci xare takk-der. Ci biir fiir yi, dafa gore te rëy-rëyluwul, te barewul tiitar. Ak maandute la tontoo, te yemale làmmiñam. Nanu jéem a roy doxalin yu mel noonu ci sunu dund.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ci li nga yónnee Yaxya ci sunu àddina si, muy nit ku woyof. Baal nu sunu bare tiitaru xalaat bi naan noo sut te ëpp maanaa ñi ci des. Dimbali nu ba nu yeewu ci xam ne ay surga doŋŋ lanu, te yow rekk yaa màgg.
LAAJ:
- Lan la Kureelu Yawut gu mag googu doon mébét ci seen laaj yooyu?