Previous Lesson -- Next Lesson
c) Waxi Yonent yu Yeesu (Yowaana 21:20-23)
YOWAANA 21:20-22
20. Piyeer gestu, gis taalibe bi Yeesu bëggoon, di ñów ci seen gannaaw. Taalibe boobu mooy ki sóonu woon ca Yeesu, ba ñuy lekk, te laajoon Ko ne: «Boroom bi, kan mooy wori?» 21. Piyeer gis ko, daldi ne Yeesu: «Kii nag, Boroom bi, nu muy mjje?» 22. Yeesu ne ko: «Su ma neexoon mu dund, ba ma dellusi; lu ci sa yoon? Yów toppal ci man.»
Piyeer daldi nangu sanataane Sangam bi, maanaam toppatoo xaram yi ak mboteem yi. Ndegam Yowaana moo gënoon a nekk xale ci taalibe yi, Piyeer nammoon naa xam lan la ko Yeesu raccal. Ndax daf koo naroon a delloo kër ga, ndaxte gune la, walla mu takkal ko ndombal àttekatu lëj-lëj yi?
Xëyna sax Piyeer dafa xawoon a ñee Yowaana, ndaxte dafa meloon ni Yeesu; Yowaana la gënoon a naw te gën koo bëgg ñeneen ñi. Ca reer bu mujj ba, Piyeer tànnoon na Yowaana ngir muy kiy dox seen diggante ak Sang bi, ngir dalal jotaay bu tar bi te ñu man a xam kan mooy workat bi.
Yowaana dafa taqoon Yeesu ba ñemee taxaw sax ca wetu kurwaa ba, mel ni kuy jaay bakkanam. Moom mooy ki jëkk a gëm ndekkite Yeesu, te it moo Ko jëkk a xàmmee ba ñuy teer ca dexu Tiberiad ga. Moom dafa pare woon ngir topp Yeesu, waaye Piyeer moom, dañu koo woo. Xolam dafa àndoon ak bu Krist. Moo gënoon a jokkoo yeneen taalibe yi ak Krist.
Piyeer dafa bëgoon a xam ndax ëllëgu Yowaana mooy gën a tar bosam, walla dafay wuute. Yeesu xamal ko ne warul a ronni ñeneen ñi, waaye dafa leen war a jàppe ni ay mbokk yu yem kepp. Du Piyeer moo waroon a lijjanti ëllëgu Yowaana mi nga xam ne dafa jokkoo ak Botoomam, te fekk Piyeer moom mooy baatu Ndaw yi. Yowaana ne tekk, di dékku ci ñaan ak muñ màggaayu sartu Jàngu bi, yi muy xiire ci dooley ñaan gi (Jëf ya 3:1; 8:14-15; Galaat 2:9).
Bu nu xoolee ci tontu Yeesu bi aju ci ëllëgu Yowaana, dinanu gis ne solo si nekkul ci ndax dinanu dund lu yàgg di jaamu Krist, walla danuy teel a dee ngir Moom. Li ci am solo mooy nanu sàmm sunu ngor ak Moom, te di Ko déggal. Yeesu du doxale ak taalibeem yi ni ñu muy mooñ ci leket, waaye dafa leen di xàllal yoon wu leen di may ñu màggal seen Sang. Xamunu dara ci deewug Yowaana; xëyna dee gu sedd la faatoo.
Yeesu dafa sant Piyeer mu xool ci boppam, te bañ a seet ci yeneen taalibe yi. Loolu mooy tekki ne warunu am kiñaan ci ni yeneen kercen yi di màgge ci bii, walla bee liggéey. Nanu góor-góorlu ngir xam coobare Yàlla ci sunu dund, te topp ko ak sunu xol bépp, ci lu laajul dara.
Mu wax itam taalibeem yi lu aju ci ñaareelu delluseem gi. Ñówam googu mooy tëj li taxoon àddina nekk. Xelu taalibe yépp nekk ci xew-xew boobu war a ñów. Ak teewaayu Yàlla ci biir nit ñi, lépp li askan yi di séentu di na sotti. Yeesu dina ñów ci ndamam. Ndax yaa ngi koy xaar ci biir ñaan, jaamu ak màggal? Ndax yaa ngi Koy waxtaane ak say dëkkandoo? Dinanu daje ak ñu bare ñu Ko gëm.
YOWAANA 21:23
23. Noonu am ci bokki taalibe yi ñu xalaat ne taalibe boobu du dee. Moona Yeesu mosul ne Piyeer du dee, waaye li Mu wax mooy: «Su ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ci sa yoon?»
Ñu bare nee nañu ne Yowaana dund na ba màggat te nekkoon misaalu ñi nekkoon ci jàngu yi, te doon xaax dellusig Almasi bi. Nit ñi dañu xalaatoon sax ne du dee balaa Boroom bi di dellusi. Póol itam mungi doon séentu Boroom bi, te doon xalaat ne du dee mukk, waaye dañu koy soppi ci saa si, këf ko yóbbu asamaan. Yu wowaana moom, du woon boroomy gént; dafa wax bu leer ne digu Krist bi tekki wul ne moom du dee, ba asamaan yi ubbiku, Boroom Ndam li feeñ. Li Mu nammoon ak ay dogalam kenn xamalu ko Piyeer. Boroom bi mooy Sàmm bu Baax biy wommat ay taalibeem, ku ci nekk ci sa yoonu bopp.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu, Yów yaay Musalkat bu am ndam li, di Sàmm bu Gore bi. Jarajëf ci li nga teg ci yoon Piyeer ak Yowaana, kenn ku ci nekk fi mu war a jaar, te noonu màggal nañu la ci seen dund am seen dee. May nu, nu am yiwu man laa topp. Tàggatal sunu waajur yi, ak sunu xarit yi ngir ñu teeru la ci sa ñëw bu yàggatul bi.
LAAJ:
- Lan la kàdduy Krist yu mujj yi ci Injiil lii di tekki?