d) Seede Yowaana ak Injiilam (Yowaana 21:24-25)
YOWAANA 21:24
24 Taalibe boobu mooy seede mbir yooyu, bind leen, te xam nanu ne, li muy wax dëgg la..
Gis nanu fii ñeenti dëgg yu am solo :
Taskatu Injiil lii mungi doon dund bi ñu yéglee Injiilam gi, te jàngu yi doon làkk Grek xamoon nañu ko. Moom nekkoon na taalibe Yeesu ca jamono Yaxya, ba ca yéegu Krist ca asamaan.
Yowaana ab seede bu dunak Yeesu la. Moom dégg na Yeesu muy wax, te jottali nanu ay kàddoom, ak xew-xew ya. Du kenn ca waa jàngu ba moo bind Injiil li, waaye Yowaana ci boppam la, moom miy taalibe bi ñu nawoon lool.
Xëyna sax doonul làkk bu baax Grek, kon manoon naa jël kenn ca jàngu ba, ca ña gën a xarañ ngir bindloo ko. Faramfàcce yi leer nañu, te dëgg yi wér péŋŋ. Ñi wesaare Injiil lii bokk nañu nangu ne seede bu Yowaana bii bu dëggu la te jar a wóolu. Ràññee googu am na solo lool, ndaxte Injiilu Yowaana am na nu mu wuutee ak yeneen ñetti Injiil yi. Nungi am cant ci ngëneel yi nu boroom Injiil lii jagleel.
Ñi siiwal Injiil lii, dañoo nangoodoo dundinu Krist ci seen dund, ndaxte bi ñu Ko nangoo, ci la ñu am sañ-sañu nekk ay doomi Yàlla, jaare ko ci ngëm gi ñu am ci turam. Xel mu Sell mi wàcc ci seen ków, dundak ñoom, te may leen ñu man a ràññee rab yu bon yi. Ñu man a ràññee dëgg, fen ak yokk (sos), ndaxte Xelum Dëfal mi mungi leen doon won bépp dëgg.
YOWAANA 21:25
25 Yeesu def na yeneen jëf yu bare. Su ñu ko doon nettali, bind lépp, xalaat naa ne, téere yi duñu xej ci àddi na.
Am na ñuy xalaat ne ñeenti Injiil yi ëkku fakkastal la. Bu nu ci boolee Bataaxali Póol yi dafay nekk juróom (ni mu ko waxe). Te dundug kercen bu dëggu bi mooy Injiil bi ngay dunde. Boroom mbind mii seede na ne dafa dégg lu bare lu taalibe yi wax ci Yeesu, ba nga xam ne deesu ko man a nettali. Mataayu Yàlla gépp a ngi ci moom. Ba tey jii Mungi Mungi sax ci Jàngoom bi, di ko tette, muy aw ci ay tànkam. Bu fekkoon ne danoo bëgg a jéem a bindaat jëfi Yeesu yépp, ba Mu dekkee ba léegi, kon téerey àddina si duñu doy. Kercen yi dinañu soxla dund gu amul àpp, ngir man a nànd xóotaay, guddaay ak yaatuwaayu mbëggeelu Krist ni muy wale ci coosaan ak aadas doomu Aadama.
Sunu Boroom biy dund, mu ngi jëf ci àddina si ni ca jamono Kóllëre gu Bees ga. Nungi jàppe sunu bopp ni ñu barkeel, ndaxte nu ngi dégg baatam, di jot ay xalaatam te di topp wooteem. Yowaana dafay wone Yeesu Krist ngir may nu, nu man a seede ne: «Te Kàddu gi ñów nekk nit, dëkksi ak nun fees ak yiw ak dëgg; te nun, nu gis ndamam, ndam liy jolli ni ndamul Doom bajjo ju Baay ji.»
ÑAAN: Nu ngi lay sant Boroom bi Yeesu Krist ci li nga xelal sa ndaw li Yowaana ngir mu bind sa Injiilu mbëggeel gi. Yaa ngi nuy waxe ci ay kàddoom. Sant nanu la ci sa yërmànde, say kàddu, say jëf, sag dund, sa dee, ak sa ndekkite. Feeñal nga nu Baay ji te baal nga nu sunuy bàkkaar. May nga nu dund gu bees ci sa Xel mi.
LAAJ:
- Lu ñiy wesaare Injiilu Yowaana di seede?
LAAJTEWAAY - 7
Mbokk mi,
yónnee nu 20 tontu yu jub ci biir 24 yi ñu lay laaj.Bu fekkee ne tontu nga juróom-benni téere yi weesu dinanu la yónnee ab raaya buy wone sa xadaru jàng Injiilu Yowaana.
- Nan la Yeesu man a nekke ëkku reseñ gi ci dëgg ?
- Nan ak naka la La Yeesu man a nekke buur ?
- Lan lanu man a jàngat ci dóor yi ñu dóor Yeesu, solal Ko mbubb mu xonk-coyy te kaala Ko aky dëg ?
- Lu tax Pilaat dogal àtteb Yeesu ?
- La ñu bindoon ca ko kurwaa ba, lu muy tekki ?
- Ñetti kàddu Yeesu ya, yan la woon ?
- Lan lanu man a jàng ci yaxu Yeesu yi nu dammul ?
- Suulub Yeesu lu mu nuy xamal ?
- Yan ñetti firnde ñooy wone ndekkite Yeesu ?
- Lan la Yowaana wóoluwoon ba mu fekke bàmmeel ba ne wëyëŋ ?
- Lu tax Maryaama tàyyiwul ci wër néewu Boroom bi Yeesu, ba mujj gi Yeesu ci boppam moo ko feeñu te woowe ko turam ?
- Ban bataaxal la nu Yeesu di yónnee jaarale ko ci Maryaama mu Magdala ?
- Lan la baat yi Yeesu jëkk a wax taalibeem yi ba Mu dekkee di tekki ?
- Lu tax Taalibe ya bég ?
- Lan moo doy waar ci yónnib taalibe yi ?
- Kan mooy Xel mu Sell mi ? Lu muy def ci sa seede ngir Yeesu ?
- Jébbalu Tomaas bi, lu mu ëmbaale ?
- Lu tax Yeesu di woowe ñu « bakeel » way-gëm yi Ko gisul ?
- Lan la Yowaana di tëje Injiilam ?
- Lu tax napp gu naat ga doon gàcce ci taalibe ya ?
- Lan moo la gën a yëngal ci waxtaanu Yeesu ak Piyeer ?
- Nan la Piyeer màggale Yàlla ?
- Yan baatu Krist ñoo mujj ci Injiil lii ?
- Ban seede la ñi tasaare Injiilu Yowaana def ?
Yónneel say tontu,te bul fàtte bind bu leer sa dëkkuwaay ci ambaloŋ bi ak ci sa kayitu tontu ci :
Waters of Life
P.O.Box 600 513
70305 Stuttgart
Germany
Internet: www.waters-of-life.net
Internet: www.waters-of-life.org
e-mail: info@waters-of-life.net
Soo bëggee wéy ci njàngum Biibal bi ak nun,dinanu la yónnee ak xol bu sedd guyy beneen téere ak ay xalaat ci Biibal bi.