Previous Lesson -- Next Lesson
b) Biral nañu kilifteefu Piyeer ni njiitu gétt gi (Yowaana 21:15-19)
YOWAANA 21:18-19
18. Ci dëgg-dëgg Piyeer, maa ngi la koy wax, bi nga dee ndaw, yaa doon takk sa geño di dem fu la neex, waaye boo màggatee, di nga tallal say loxo, keneen takkal la sa geño, yóbbu la foo bëggul.» 19. Ci baat yooyu la Yeesu doon misaale naan la Piyeer war a faatoo ngir jollil ndamu Yàlla. Yeesu ne ko: «Toppal ci man!»
Yeesu xam ne xolu Piyeer, taalibeem bi, ànd na ak xadar te tooy na. Bu kenn di door a ñów ci Krist, dafay jaar itam ci jamonoy mbég, ju safaras Yeesu di xamb. Bu jotee Xel mu Sell mi nag, dafay mos mbégte mu mag-a mag, ba daw rawale ña ca des. Waaye li ci ëpp, ci coobare yég-yégu nit lay doon, waaye du soqikoo ci coobare Yeesu, mu lewet, miy ñaan, tey jokkoo.
Waaye, Yeesu wax na ne Piyeer dina ñàkkaat kóolute gi mu am ci Moom, te dina màgg ci Xel mu Sell mi, ba jébbalu bu wér ci Boroomam, nekk jaamu mbëggeelam, ju dul namm lu dul def coobare Yàlla.
Piyeer daldi des Yersalem, bañ a dem ca yéeféern ya. Ñu jàpp ko ay yooni-yoon, dóor ko, sànni ko ca kaso; ba benn bés, m'alaakam Boroom bi moo ko rëccloo. Xel mi yóbbu ko ca kër Korney, miy kilifa soldaaru waa Rom, te mu xame fa ne Xel mu Sell mi man na faa wàcc ci yéeféer, yi ñu jàppe woon ni ñu setul. Bi ñu àggee foofa ci tas xabaar bu baax bi, ci la ubbil bunt ñi war a dem ci àddina sépp ngir seedeel Boroom bi.
Gannaaw ba mu génnee kasob Erod ba, Piyeer daldi ganeji jàngu yu bees ya, rawatina ba ñu génnee Póol kaso. Noonu, jawrinu apotar ya ganeji kercen yu cosaanoo yéeféer, daldi leen ñaax te indil leen kàdduy Baay ji. Cosaan wax na nu ne ca Rom la faatoo, ci nguurug bundxataalug buur Neron. Bi mu jàppee boppam ne yeyoowul ñu koy daaj ci bant ni Boroomam, dafa saraxu ña ko waroon a rey, ñu juutal yaramam, boppam féete suuf. Yeesu misaaloon na deewam ba muy wax ne Piyeer dina sargal Yàlla ci deewam.
Benn bés, Piyeer dafa ne Yeesu ne jekk na ngir joxe bàkkanam ngir Moom. Yeesu ne ko: «Manuloo ma topp léegi fi may dem, waaye dinga ma topp ca kanam.» (Yowaana 13:36) Yeesu dafa boole taalibeem yi ci kàkkanam, ak ci ndamam, ngir ñu ànd ak Moom ak Baay ji ak Xel mu Sell mi. Mu daldi leen boole ci ay coonoom ak deewam, liy ubbiteg màggaay gi. Màggaay gi ci Injiil li, tekkiwul leeraay, walla sargalu nitu neen, waaye metit la ak kurwaa ba ngir Ki nga xam ne moo nu bëgg. Piyeer manuloon a màggal Yàlla ci kow coobareem, waaye deretu Yeesu sellal na ko te kàttanu Xel mu Sell mi laabal na ko, ndax mu bàyyi boppam, dund ngir Boroomam te dee ngir màggal Ko.
Teg ca nag, Yeesu daldi jox Piyeer ndigalu soldaar, ne ko: «Topp ma!» Fii ak nu ngi Koy topp bu nuy dund ak bu nuy dee, dinanu góob meñeefu mbëggeel te sellal turu Baay jiy Aji Yërmande ji.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist, nu ngi lay sant ndaxte xalabuloo Piyeer, ak li mu la woroon lépp, waaye danga koo woo ngir mu màggal Kenneefu Ñett gu Sell gi, muy ci dund ak ci dee. Jëlal sunu dund te sellal nu. Dimbali nu ba nu jébbal sunu coobare sag wommat, di fonk say ndigal, di bëgg sunuy noon te di la sargale ngëm ak dégg ndigal ba fàww. Na sunug dund nekk màggalug sa yiw wi.
LAAJ:
- Nan la Piyeer màggale Yàlla?