Previous Lesson -- Next Lesson
a) Napp gu yéeme ga (Yowaana 21:1-14)
YOWAANA 21:1-3
1 Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu feeñuwaat na ay taalibeem ca tefesu dex gu ñuy wax Tiberyàdd. Nii la deme woon. 2 Taalibe yii àndoon nañu Simoŋ Piyeer, Tomaas, ki turam di tekki «séex bi», Nataneel mi dëkk Kanaa ca diiwaanu Galile, doomi Sebede ak yeneen ñaari taalibe. 3 Simoŋ Piyeer ne leen: «Maa ngi nappi». Ñu ne ko: «Nu nit danuy ànd ak yów». Ñu dugg gaal, dal di dem. Waaye guddi googu,jàppuñu dara.
Gannaaw ndekkiteem, Yeesu dafa ne woon ay taalibeem ñu dem Galile, fa ñu cosaanoo; ca tefesu dexu Tiberyàdd. Moom miy sàmm bu baax bi, di na leen fa jiitu ngir daje fa ak ñoom. Mujj gi, mbëggeel gi mu am ci ñoom xiir ko ci gën leen a teel a feeñu, fekk ñungi Yerusalem ba tey, ngir dalal seenum tiitaange: dibéer bi ci ngoon, ba màggalu jéggi ba jeexee. Mu nuyuwaale leen ak jàmmam, ba noppi mu ngir ñu yégal àddina sépp Injiil li (Màrk 16:7; Macë 28:10).
Ndax taalibe yi dégg nañu ndigalu yégle Injiil li? Kéemaanu ndekkite li ndax soppi na seeny xalaat, te ñaax leen ci yéene xabaaru dund gu dul jeex gi? Liy gàcce ga mooy ne loola amul, xanaa kay dañoo dellu ca seeny liggéeyi cosaan, ñenn ña beru, ña ca des booloo ni nappkat yii.
Genn ngoon, Piyeer jóg di nappi, dal di ko yégal xaritam yi. Mu bàyyi leen ñu tànn a ànd ak moom, walla deet. Ñépp jóg ànd ak moom, ñu dooj gaal dem ba ca diggu dex ga. Ñu sànni mbaal ba sonn ci guddi gi, waaye jàppuñu dara. Fàtte woon nañu kàddu Yeesu ya: «Gannaaw Man, manuleen a def dara.»
YOWAANA 21:4-6
4 Ci fajar gi, Yeesu taxaw ca tefes ga, waaye taalibe ya xàmmeewuñu Ko. 5 Yeesu ne leen nag: «Bokk yi, xanaa jàppuleen jën?» Ñu ne ko: «Dédéet». 6 Mu ne leen: «Sànnileen mbaal mi ci ndeyjooru gaal gi, bu ko defee ngeen jàpp.» Ñu sànni fa mbaal ma, mu fees ak jën, ba manuñu ko woon a génnee ndox mi.
Yeesu bàyyiwuloon ay taalibeem, ak li ñu doon faral di juum lépp. Dafa leen a yeeru ca tefes ga, di xaar ñu teersi. Manoon naa tëmbal ay jën ca seen mbaal ya, waaye dafa leen bëggoon a jàngal ne manuñu woon ne bëxërñet rekk gannaaw ndam lu mag li ñu am, mbaa di dellu ca seeny liggéeyu aada. Dañoo fasoon kóllëre ak Moom; seen wóllëre la woon waaye dañu Ko fàtte, ndax seeny njàqare ak seeny jafe-jafey bes bu nekk, te noonu, ñu mel ni ñu nekkatul sax.
Waxatuloon ak taalibeem ya ni ay apotaram, waaye dafa meloon ni ay xale ak ay waxambaane lay waxal. Ñoom dañoo fàtte woon lu bare lu mu leen dénkoon, te doxaluñu woon ay santaaneem. Ak ñaawteefu jëfin googu gépp, Yeesu ŋàñu leen, waaye lekk la leen laaj. Ñu nangu ne jàppuñu dara, te Yàlla àndul ak ñoom. Cig gàttal, ñu nangu seen njuumte.
Jant a ngi doon fenk, Yeesu jubal ci ñoom, mu mel ni yaakaar ju bees a ngi leen di dabsi. Waxul ne: «Ndokk ba ngeen lajjee» walla jéemaat leen, dingeen am ngañaay.» Waaye dafa joxe ab santaaneb buur: «Sànnileen mbaal mi ci ndeyjooru gaal gi te dingeen jàpp.» Ak li ñu nekkoon ci wetu fi jën yu mag yi gënoon a ñàkk lépp, terewul ñu nangu ndigal loolu, te sànni mbaal ma.
Yeesu gisoon na jën ya ca biir ndox ma, ni muy gise tey jii ñi Ko mar te mu bëgg leen a jot. Dina la yebal ca ñoom. Waxul ne: «Mbaal leen àddina sépp», waaye dafa ne: «Sànnileen seen mbaalu Injiil fi ma leen soxlaa, noonu dingeen gis samay jëf.»
Taalibe ya déggal ndigal lu doy waar loolu te xàmmeewu ñu sax Yeesu, mi meloon ni nitu neen. Xëyna dafa jëfandikoo nuyóo bu ñuy faral di def, waaye dafa joxe ndigal lu dëgër. Noonu, ñu amaat kàttan ak njàmbaaru sànniwaat mbaal ma, te noonu it mbaal ma fees dell. Boroom bi dafay yónni ay góor ak ay jiggéen ñu gëti ci ay bérab yu Mu natt, te ñooñu dañuy feesal seeni mbaal. Dañuy feesal seen mbaal, ba dañuy woo seeni xarit ngir ñu dimbali leen.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu, baal nu sunuy njàqare yi nuy am ngir li nu war a dunde, njàqare yooyu di nu fàtteloo indi ñeneen ci Yów. Ñungi lay sant ci li nga ñów ci nun, fekk sax nun danoo réer. Fexe nga ba nu nangu sunuy lajj. Jàngal nu ni nuy toppe sa kàddu, te yóbbu nu ci ñi lay wut. Dajaleleen ci sa mbaalu Injiil ndax ñu nekk say moomeel ba fàww.
LAAJ:
- Lu tax napp gu kéemaane ga nekkoon gàcce ci taalibe ya?