Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 125 (Conclusion of John's gospel)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
B - Ndekkite Yeesu Krist ak ay peeñoom (Yowaana 20:1 - 21:25)

4. Tëkku Injiilu Yowaana (Yowaana 20:30-31)


YOWAANA 20:30-31
30 Yeesu wone na it ci kanamu taalibe ya yeneeni firnde yu ñu nettaliwul ci téere bii. 31 Waaye li ci nekk, bind nañu ko ngir ngeen gëm ne: « Yeesu mooy Almasi bi, Doomu Yàlla ji, te seen ngëm may na leen, ngeen am ci Moom dund. »

Ñungi agsi ci njeextalu li Yowaana bind moom ci boppam. Bindkat bu bare kumpa bi, yéenekatu xabaar bu baax bi, yégle na ndekkitelu leeru Yàlla gi ci biir lëndëm gi ko nanguwul. Waaye ñépp ñi ko nangu, may na leen ñu yelloo nekk ay doomi Yàlla, ñoom ñi ko gëm. Yéenekatu Injiil bu mag bii dugal nanu ci xóotaayu jookkoog baatin ak Yeesu. Nettali na nu deewug Yeesu ak ndekkiteem, ngir nu man Koo gëm, te gis ni muy dunde ci nun.

Ci gàttal, apotar bi jox na nu ñeenti fànna ngir faramfàcceel nu bu leer solos Injiilam, ak li mu ci jublu woon bi mu koy bind.

Yowaana jéemul a nettali lépp li Yeesu defoon mbaa Mu waxoon ko. Su fekkoon ne loolu la kon dina bind téere yu baree-bare. Dafa tànn xew-xew yii ak njàngale yii ngir dimbale nu ba nu xam màqaama Yeesu gi kenn dul méngale. Bindl ni ku dégg baatu Xelum Yàlla di ko janneerloo mbindam. Waaye, ku ànd ak sagoom la woon, Xel mu Sell mi solu ko, ngir mu tànn yooyu xew-xew yu am solo, noonu mu wone ak mbëggeel kan mooy Mbotem Yàlla, miy dindi bàkkaaru àddina si, jaarale ko ci jébbal boppam.

Yowaana dafa bind Injiil lii, ngir dimbali nu ba nu xam ne Yeesum Nasaret, nit ku woyof ki, te ñu bañ Ko, mooy Krist, Almasi bi ñu dige, te nekk it Doomu Yàlla ji. Ci ñaari tur yooyu, matal na ci li ko Yawuti Kóllëre gu Njëkk nga doon séentoo. Àtte na askanam wi daaj ci bant sët bi ñu digoon Daawuda. Yeesu ci jëmmu nitam, biral na Krist dëgg ni Doomu Yàlla. Mbëggeelu Yàlla gu rëy gi ak sellaayam, raw nañu bépp ŋàññ. Yowaana dafa màggal Yeesu ci anam yu yéeme. Ni muy wonee Yeesu, kenn manu ko méngale, te dafa nuy may nu xam mbëggeelu Doomu Yàlla, ji mujj a jëmmoo nit, ngir nu man a nekk ay doomi Yàlla.

Yowaana bëggul nu yem ci gëm kese, waaye dafa fas buumu kóllëre ci sunu diggante ak Doomu Yàlla ji. Ndegam Krist Doomu la, kon itam Yàlla mooy sunu Baay. Te ndegam Aji kowe ji mooy sunu Baay, kon man naa may dund gi ay doom yu bare, te baaxe leen dundam gu dul jeex gi. Li Injiilu Yowaana di wut mooy nu dund, juddu gu bees gi, jaare ko ci deretu Krist ak Xel mu Sell mi ci nun. Ndax judduwaat nga ci baatin, walla yaa ngi wéy di dee ci say bàkkaar? Ndax dundug Yàlla mungi sax ci yów, walla amuj lenn ci Xelam mu Sell mi lu nekk ci yów?

Ñaareelu juddu gi mingi aju ci ngëm ci Doomu Yàlla. Ñi ko wóolu dañuy am dundu gu Yàlla. Dundu googu mooy dundu ci diggante bu nara yàgg ak Yàlla jaaraleko ci ngëm. Ñi dëkk ci Jesus dina ñu xam ni Jesus dëkk ci ñoom. Gëm gu ni mel dina màgg ci xol ak ci dëgg, ba noppi di meññee dundu Yàlla. Dundu ba fàaw mooy mbëggeelu Yàlla gi leen di yóbbu ñu gëm Jesus ci ñi leen wër. Ñoom itam dina ñu ko bëgg, dëkk ci moom, mu nekk ci ñoom ba fàww.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ci Injiil li, ni nu ko Yowaana indilee. Ci téere bii doŋŋ, xame nanu ci sa màggaay ak sa dëgg. Nungi sujjóot ci sa kanam ak mbég, ndaxte tax nga ba nu gëm la te may ga nu juddu gu bees jaare ko ci sa yiw. Dëgëralal sunu ngëm ak sunu mbëggeel ci yow. Dimbali nu ba nuy topp say santaane, te di seede sa tur ci biir mbooloo yi. Danoo bëgg sunu xarit yi wóolu la te am dund gu naat gi, jaare ko ci ngëm.

LAAJ:

  1. Lan la Yowaana di faramfàcce ngir tëj Injiilam?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 28, 2026, at 06:30 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)