Previous Lesson -- Next Lesson
b) Piyeer ak Yowaana, ca bàmmeel ba (Yowaana 20:3-10)
YOWAANA 20:6-8
6 Noonu Simoŋ Piyeer mi ko toppoon daldi agsi, daldi dugg. Mu daldi séen càngaay la ca suuf. 7 Ak kaala ga ñu muuroon boppu Yeesu. Waaye kaala googu àndul ak càngaay la, dañu koo laxas, teg ko ci wet. 8 Noonu keneen ka jiitu woon ca bàmmeel ba, duggi moom itam. Naka la gis, daldi gëm.
Yowaana dafa xaar ba Piyeer agsi, loolu di wone ni mu wege magam ji. Piyeer moo njëkk a gis ne bàmmeel bi kenn nekkatu fa. Ndaw li Yowaana moom, doj wa ñu bërëŋ bàmmeel bu ubbeeku ba, ak néew ba fa nekkatul, moo ko yéem. Càngaay li dañu koo lem ba mu jekk. Xalaatam yi jaxasoo ci boppam. Mu ñaan Boroom ngir mu leeralal ko li xew.
Piyeer moom dafa agsi rekk dugg ca biir bàmmeel ba; mu gis nañu tege càngaay la. Loolu wone ne kenn sàccul néew ba, ndaxte ba mu fay jóge dafa koo waajal ci tekk ak teey.
Piyeer dafa dugg ni ab saytukat, waaye seetluwul li tegtal yi di wone. Yowaana miy boroom kumpa, daldi xalaat, ñaan te amaat yaakaar. Ba mu wuyoo Piyeer, ba dugg ca bàmmeel ba, xelam ubbeeku, noonu mu tàmbalee gëm ne Yeesu dekki na. Du daje ak Ki dekki moo ko may ngëm, waaye bàmmeel ba ne wëyëŋ, ak càngaay la ñu lem ba mu jekk.
YOWAANA 20:9-10
9 Taalibe yi xamaguñu woon mbind, mi doon wone ne Yeesu dafa war a dekki. 10 Noonu taalibe ya dëpp, ñibbi.
Yeesu desul ca bàmmeel ba, ni boroom xam-xam yi, yonent yi, ak bàkkaarkat yi; waaye dafa dekki, teg dee gi fale, ni ñuy sànnee ay yére. Ku Sell ki dafa wéy ci ñàkk bàkkaar. Dee gi amuloon benn sañ-sañ ci moom. Mbëggeelu Yàlla du wore mukk.
Bañaale Krist yi manuñu wax ne yaramu Yeesu dafa seey ca biir bàmmeel ba, ndaxte kenn nekku fa woon. Krist dawul, te kenn jëlewu Ko fa, ndaxte fa ñu Ko roboon kaaraange gu mat sëkk moo fa amoon. Yowaana daldi xam ne Yeesu dafa summi mbubbum àddinaam, ndaxte soxlaatu ko woon. Ci ay laytaay la ganesee àddina ca biir lekkukaayu jur, tukkeem boobu jeexe ci ay càngaayu dee. Ndekkiteem ubbi xëtu dundam bu bees ci wàllu baatin. Donte sax mungi ame woon jëmmu nit ba tey.
Xalaat yooyu ñungi doon daw ci xelu Yowaana ba ñu nekkee ci yoonu ñibbi. Moone bàkkuwul ci li mu njëkk a xam ndamu Doomu Yàlla ji ci ndekkite li, waaye lu yàgg gannaaw loolu lay door a seede kéemaan googu, naam Mbind mi jotoon na koo yégle. Ay bëtam ubbeekuwuñu woon ca la mu jàngoon ci téere Esayi 53, te mu jëm ci dee ak ndamu Surga Yàlla bi, gisuloon itam la ca Daawuda waxoon (Luk 24:44-48; Jëf ya 2:25-32; Sabóor 16:8-11).
Ca subas xew-xew bu mag ba, ñaari taalibe ya di ñibbi, seen xel jaxasoo, waaye ñu fees ak yaakaar, am kóolute, te di laaj seen bopp nu Yeesu man a jógee ci bàmmeel bi te waxul fu Mu nekk.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ndaxte am nga ndam ci xolu ci sa xolu taalibe yi, ba ñu gëm ne dekki nga. May nga nu yaakaar ju rëy ci dund gu dul jeex gi. Nungi lay màggal, ndaxte yaay Aji Sax ji, te dunu dee mukk ndax sa yiw wi nga nu may. Musalal sunuy xarit ci dee gi te may leen dund gu dul jeex jarale ko ñu gëm sa sarax si.
LAAJ:
- Bi Yowaana nekke ci biir bàmmeel bi,lan la wóolu woon?