Previous Lesson -- Next Lesson
c) Yeesu feeñu na Maryaama mu Magdala (Yowaana 20:11-18)
YOWAANA 20:11-13
11 Maryaama nag moom, a nga desoon ca bitti, ca wetu bàmmeel ba, di jooy. Bi muy jooy, mu sëgg, yër ci biir. 12 Séen ñaari malaaka yu sol mbubb yu weex, toog ca bérab, ba ñu dencoon Yeesu; kenn ka féeteek bopp bi, ki ci des ca tànk ya. 13 Malaaka ya laaj ko ne: "Jigéen ji looy jooy?" Mu tontu leen ne: "Dañoo jël sama Boroom, te xamuma fu ñu ko yóbbu."”
Ndegam dafa meloon ne menn pexe amatul, ñaari taalibe ya ñibbi.
Maryaama nag moom, dellu ca bàmmeel ba, toog fa moom kenn ci njàqare, ndax li kenn xamul fu néew ba nekk. Dafa jafandu woon ci Moom, ndaxte Moo nekkoon yaakaaram ak dooleem. Bu gisatul néew bi, kon yaakaaram dafay nërmeelu. Kon book mungi doon jooy xàcc.
Ni Yeesu gisee yaakaaram ju tas ji, Mu yónnee ko ñaari malaaka yu, yu feeñuwaale sax yeneen jigéen ña. Gis na leen ñu toog ca biir bàmmeel ba, sol yére yu weex yuy leeral lëndëm ga ca biir. Waaye manuñu ko woon a dëfal ndaxte Yeesu rekk moo ko manoon. Xolam di jooy naan: « Boroom bi, foo nekk? »
Wooteb xol boobu, nun lañu ko jagleel itam. Lan lanu bëgg? Lu tax nu bëgg li sunu nafsu di yóotu? Lan mooy sunu mébet? Ndax ni Maryaama lanuy xalaate, te namm a gis Yeesu doŋŋ? Ndax sa xol a ngi Koy namm a gis?
YOWAANA 20:14-16
14 Bi Mu waxee loolu, mu geestu séen Yeesu mu taxaw, waaye xamul oon ne Moom la. 15 Yeesu laaj ko ne: "Jigéen ji, looy jooy? Kooy seet?" Mu foog ne boroom tool ba la, ne ko: "Sériñ bi, bu fekkee ne yaa Ko yóbbu, wax ma foo Ko denc, ma jëli Ko." 16 Noonu Yeesu ne ko: "Maryaama". Mu walbatiku, làkk Ko ci Yawut ne Ko: "Rabbuni!" muy tekki "Kilifa gi".
Yeesu wallusi na ay rangooñam. Xelu ñeneen ña daloon na ba ñu gisee ne kenn nekkatul ca bàmmeel ba, te dégg baati malaaka ya, waaye Maryaama mu Magdala moom, gis Yeesu rekk la yittewoo woon. Mu feeñu ko ni nitu neen ku amul kaalag leer.
Noonu mu jaaxle lool, te xàmmeewul baatu Yeesu. Xamuloon ne mungi teew, ci saa soosu ndaxte xol buy ténj du gaaw a ràññee teewaayu Krist, mbà muy dégg kàddoom yu teey yi. Ñu bare ñuy wut Yàlla Aji Sàkk ji, gisuñu Ko ndaxte li leen gënoon a soxal moo doon wut ak ñaan, waaye du woon Sàmm bi leen di wut.
Waaye Yeesu xamoon na mbëggeelu Maryaama, noonu mu dëfal njàqareem ak ay baat yuy dalal xol; Mu woowe ko turam, lu ab surga neen naruloon a def. Mooy Aji Xam lépp, dafa maandu, te di Boroom bi Dafa woowe Maryaama ni Sàmm bu Baax bi di woowe ay mboteem, yi Mu xam ku ci nekk sa tur.
Yeesu ci sa tur lay jaar bu lay woo. Ndax yaa ngi dégg baatam?
Sànnileen yéen ñépp seeny xel-ñaar, ak seeny bàkkaar, te dem ci moom. Maryaama tontu ko ne: "Ràbbuni!" Baat bi mu jëfandikoo, maanaam "Ràbbuni" mungi tekki "Ki xam lépp te di Aji kàttan ji". Maryaama jànge ci Sangam, bi ko may xam-xam doole kaaraangeem ak dund gu amul àpp. Noonu, xaacoom ba méngook bu Jàngu bi, ca bésub delluseem ba. Gannaaw taaxirlu bu yàgg dina gis Boroomam di wàcc ci ay niir, te bu boobaa dina Ko màggal cig njébbalu, te sant Ko.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sujjóotal, Yow mi nangul Maryaama ay séentoom, ba feeñu ko. Dëfal nga ko ak sa teewaay. Sa kàddu mooy dund gi. Ubbil sunuy nopp ak sunu xol, ngir nu dékku say kàddu. Dimbali nu, ba nu wóolu la ak mbég.
LAAJ:
- Lu tax Maryaama tàyyiwul ci wër néewu Boroom bi Yeesu, ba Mu mujj koo feeñu te woowe ko ci turam?