Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 114 (Burial of Jesus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
A - Xew-xew yi amoon diggante ba ñu jàppee Yeesu ba bañu Koy dugal ca bàmmeel ba (Yowaana 18:1 - 19:42)
4. Bant ba ak deewug Yeesu (Yowaana 19:16b-42)

f) Robu Yeesu (Yowaana 19:38-42)


YOWAANA 19:38
38 Gannaaw loolu, Yuusufa mi dëkk Arimate, ñaam Pilaat ngir yóbbu néewu Yeesu. Yuusufa taalibe Yeesu la woon ci lu kenn yégul, ndaxte dafa ragaloon Yawut ya. Pilaat may ko ko. Yuusufa daldi dem, yóbbu néewu Yeesu.

Amoon na ca 70 ya bokkoon ca Sandreŋ ba, ñu ànduloon ca àtte ba ñu tegoon Yeesu. Ay saytu yu yàggul dara xamal nañu nu ne bu amoon ñaari nit kese yu weddib àtte, kon ndaan la dees na ko teggi (fomb). Noonu ñu dellu seetaat mbir moomu ca na mu gën a xóote. Waaye bu ñépp àndee ca àtte ba, kon dees na daan ka ñu jiiñ. Bu nu seetee ne yoon woowu mungi doon dox ca jamono Yeesu, loolu man na nu won ne lu mu néew-néew amoon na ñaar ñu ànduloon ak kilifa ya, te kon Sanedreŋ bi juum na cib àtteem. Kenn ca bañkat ya mooy Yuusufa mu Arimate, mi nekkoon taalibe Yeesu bu làqu (Macë 27 :57 ak Mark 15 :43). Dafa ragaloon a ñàkk ndombal tànkam ca Sanedreŋ ba, walla darajaam, ji ko maanduteem may ci ëttu kilifay nguur gi. Yuusufa dafa mere woon Kayif mi naaféqoon te nax waa Sanedreŋ bi. Noonu Yuusufa nëbbatul dara ci àndam ak Yeesu, waaye booba fekk na béy na mbuus, te seedeem nekkatul lu dul fippu ci kanamu Sanedreŋ bi. Terewul ñu taxawal àtte.

Ba Yeesu joxee bakkanam ba noppi, Yuusufa dem ca Pilaat (yoon mayoon na ko ko). Pilaat nangu la mu ko ñaanoon, maanaam mu jël néewu Yeesu, rob ko.

Noonu Pilaat ndamooti ci kow Yawut, yi daan faral di sànni néew ya ca tundu «Hinnom», fa leen till ya daan lekke, te ñu fay lakke mbalit ya. Yàlla teggil na Doomam gàcce gu mel noonu. Mataloon na sasam ni sarax su sell ca kurwaa ba. Baayam xiir Yuusufa mu denc Ko ca bàmmeel bu tedd.

YOWAANA 19:39-42
39 Nikodem itam ñów; moom mi masoon a seeti Yeesu guddi. Mu indaale lu war a tollook fanweeri kiloy cuuraay lu ñu defare ndàbbi miir ak banti aloos. 40 Ñu jël néewu Yeesu, laxas ko ci càngaay, boole ko ak cuuraay li, ni ko Yawut yi tàmmoo def, bu ñuy waajal néew. 41 Tool a nga woon ca wetu bérab, ba ñu daajoon Yeesu, te ca tool booba amoon na fa bàmmeel bu ñu masul a suul kenn. 42 Ca bésu waajal la woon, ba Yawut ya doon waajal bésub noflaay ba, te bàmmeel ba jege woon na. Foofa lañu denc Yeesu.

Ñu jekk-jekki rekk Nikodem ne jameet ca wetu kurwaa ba. Moom mooy ñaareelu jëmm ji nanguwul oon àtte ba Sanedreŋ ba tegoon Yeesu. Jéemoon naa xàcclu àtte ba Sanedreŋ ba tegoon Yeesu, ngir ñu man a xoolaat bu baax ni mbir mi gën a yenoo maanaa (7 :51). Bii seede dafa ñów ak 32 kiloy cuuraay, ak mbalaan mu ñuy laxase néewu Yeesu. Mu jàppale Yuusufa ngir ñu wàccee néew ba, te denc ko ca bàmmeel ba cuuraay ko, na ñu ko daan terale kilifa ya. Dañoo waroon a gaawtu ngir denc néew ba laata juróom benneelu waxtu àjjuma ji di jot, ndaxte booba la Sabbaat bi di dugge, muy bésub Noflaay, bi ñuy teree bépp liggéeyu nit; ab diir bu gàtt rekk moo leen dese woon.

Baay ji, sunu Boroom xiir ñaari nit ñii ñu sargal Doomam ju dee ji, muy firndeelu la Yonent Esaya waxoon (ak 53 :9) ba mu nee dinañu Ko suul a k boroom alal yi, ak ñu tedd ñi ci bàmmeel bu ñu nawlu. Yettlu ab bàmmeel ciw doj, njëg lu bare te la doon laaj. Yuusufa dafa sargal Yeesu bi mu Ko mayee bàmmeelu boppam, ci wetu fi ñu Ko daaje, ca peggu dëkk ba. Foofa lañu dencoon néew ba ak ay laxasaayam, te Nikodem cuuraay ko, diw ko.

Yeesu kay deewoon na ci dëgg-dëgg. Te booba, fanweeri at ak ñett la amoon. Dafa juddu woon ngir dee. Amul genn mbëggeel gu gën joxe sa bakkan ngir ki nga bëgg.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist, jarajëf ci li nga nu wuutu ci dee gi. Maa ngi booloo ak way-gëm yi, di la bëgg, ndaxte sa mbëggeel moo nu musal ci merum Yàlla te dëkkal nu ci sellaayu Kenneefu Ñett ñi. Jëbbal naa la sama dund ni cant.

LAAJ:

  1. Robu Yeesu lu mu nuy jàngal?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 27, 2026, at 10:59 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)