Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 077 (Jesus enters Jerusalem)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
A - LI JIITU AYU BéS bu SELL bi (Yowaana 11:55 - 12:50)

2. Duggu Yeesu ca Yerusalem (Yowaana 12:9–19)


YOWAANA 12:9-11
9 Bi ñu yégee ne Yeesoo nga fa, mbooloom Yawut mu bare daldi dem Betani. Yeesu rekk yóbbuwu leen fa woon, waaye dañoo bëggoon a gisaale Lasaar, mi Yeesu dekkaloon. 10 Saraxalekat yu mag ya dogu ci ne, dañuy reyaale Lasaar, 11 ndaxte moo waral Yawut yu bare dëddu leen, gëm Yeesu.

Ca biir péey ma, mbooloo ma di rëb-rëbi, bi ñu xamee ne Yeesoo nga kër Lasaar. Nit ña yàkkamti lool dem Betani ba gis kéemaanu Kiy maye dund gi.

Saraxalekat yi fare ca Sadusen ya, donte ñooñee sax gëmuñu woon ndekkite, walla sax lu jëm ci ay rab mbaa jinne. Moone de, dañu bañoon Yeesu ak Lasaar, ba weddi kéemaan ga, waaye am yéene ñu rey ka ñu xéewale woon kéemaan ga, te boole leen ñoom ñaar ñépp cib bàmmeel, ngir wone ne gannaaw dee benn yaakaar amatul. Rax ci dolli, dañoo bëggoon a nasaxal gépp mbootaay gu gëm Yeesu, ndaxte mbooloo maa nga doon jàppe ndekkite Lasaar ni seede suy wone ne Yeesu mooy Almasi bi, ci dëgg-dëgg.

YOWAANA 12:12-13
12 Ca ëllëg sambooloo mu bare, ma ñówoon ca màggalu bésu jéggi ba, yég Yeesoo ngi jëmsi Yerusalem. 13 Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan: « Osaana! Yów miy ñów ci turu Boroom bi, Ku barkeel nga! Na Yàlla barkeel Buuru Israyel! »

Turu Yeesu moo nekkoon ci gémmiñ yépp, ba ñépp di xalaat lu Mu nar a def: « Ndax dafa nar a daw,walla dafay foqati nguuru dëkk bi? » Ba Mu fanaanee Betani ba noppi, ña ko doon may bët gis Ko mu ànd ak ay taalibeem jëm Yerusalem. « Buur bu bees bi jegesi na, Buuru asamaan a ngi ñów! Ñu baree-bare ñów ngir gis ay kéemaan, ak ay ndam. Ñenn ña dagg ay cary palm (tiir, tandarma?) ngir teeru Ko. Ñeneen ña di woy ay cant yu ñuy bàkke ay buur aky jàmbaar. Ñuy xaacu naan: « Nungi lay màggal te di la yékkati. Yów, yaa man lépp; yaa ñów ci turu Boroom bi, te fees ak sañ-sañam. Nungi lay sant ci barke yi nga nuy may. Dimbali nu te génnee nu ci bépp gàcce. Yaay sunu Musalkat, sunu Jàmbaar ak Ki nuy wommat. Ci dëgg-dëgg Yów yaay sunu Buur. »

YOWAANA 12:14-16
14 Yeesu wut cumburu mbaam, war ko; ndaxte mbinb mi nee na: ”15 Buleen ragal, waa Siyon. Gis ngeen, seen buur q ngi ñów, War mbaam mu ndaw. 16 Yooyu yépp, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki; waaye gannaaw bi ndamu Yeesu feeñee, ñu fàttaliku ne Mbind yégle woon na loolu ci Moom, te amal nañu ko.”

Yeesu faydaalul tàccu yooyu, ndaxte xamoon na ne nit ñu ràkkaajoo noonu, manatuñu dégg, walla am xalaat bu leer. Ñungi doon buuxante ci yoon wi, te di xaacu, di bége. Noonu, ngir ñu man Koo gis, Yeesu war as jumbur, ngir feelu seen woy ya, mel ni ku naan: ”Maay buur bi ñu dige ci Téere Yonent-Yàlla Sàkkarya 9:9. Ragal-leen, te buleen bàneexu. Duma daaneel miiri dëkk bi ak seeny bunt. Duma rey, te tëraluma àtteb Yàlla. Ku jub laa, te faruma ak kenn; damay doxal njubte ci biir jirim yi, te di toppatoo ñi seen boroom kër faatu. »

«Waaye nag, kenn jubul. Ñi ci ëpp dañoo jubadi te di moy yoon wu jub wi. Bul ragal dara, du ma la mbugal ni nga ko yelloo, waaye dinaa daan mbon gi nekk ci yów. Dinaa gàddu sa bàkkaar ci sama yaram, muy ndam lu mel ni ku ñu dal ci kowam ci néew dooleem, ba daan ko. Noonu dinaa la rawale ci merum Yàlla; ndam la jële ci xare baatin boobu.»

« Ab buur ngéen bëgg, bu man jaasi, waaye man; maa ngi ñów yéen ni mbote mu lewet, mu àndul ak genn jaay-doole. Sama Baay laa jébbal sama coobare. Ab fippu ngeen di séentu, ak ndam, waaye li ma leen indil mooy jokkoowaat, te am mucc ak jàmm ci Moom. Xool-leen mala mi ma war. Waruma fas, walla giléem, waaye cumbur laa war. Buleen yaakaar alal ci man, walla ay ngëneel, ndaxte dund dund gu amul àpp laa leen maysi, te di leen ubbil bunti asamaan, ngir jubóolewaat ki tuub, ak Yàlla.»

Waaye nag, mbooloo ma, ak sax taalibe ya xamuñu la Yeesu doon fexe. Gannaaw ba Mu yéegee asamaan, ca la Xel mu Sell mi ubbi seen xel, ngir ñu man a gis suufeelu Yeesu ak nadamul Yàlla ci Moom. Wuute na woon lool ak la nit ña doon séentu, te mu aju ci politik ak alal. Waaye Xel mu Sell mi may taalibe ya ñu man a bànneexu ca duggu Yeesu boobule, laata sax ñuy xam lu waxam ja tekki, ak nu muy mate sëkk.

YOWAANA 12:17-19
17 Ña nekkoon ak Yeesu ñépp, bi mu woowee Lasaar mu génn ca bàmmeel ba te mu dekkal ko, demoon nañu, nettali la ñu gis. 18 Looloo tax mbooloo ma teeru Ko, ndaxte yégoon nañu firnde boobu. 19 Farisen ya nag di waxante naan: « Gis ngeen, manuleen ci dara, ñépp a ngi Koy topp ! »

ÑI àndoon ak Yeesu la ko dale ca Betani daje ak mbootaayo diine ba jógewoon Yerusalem, ca xuru Sedroŋ. Ñi jiitu ne: « Baax na lool ci ngeen teeru Ko, ndaxte Yeesu mii mooy Almasi bi, dekkal na sax ku dee, ngir seedeel baatinam. » Ca njalbéen ga, nit ña dañu doon topp Yeesu, ndax li Mu reggaloon 5000 nit ci juróomi mburu. Gannaaw gi, ñu koy topp ndax li Mu dekkal ku dee. Ci ñaari fànna yooyu yépp, mbëggeelu nit ña ci mbiri àddina la ajuwoon, waaye du ci njubte ak tuub.

Ca wetu mbooloo ma doon xaacu ak mbég, Farisen ya ak kilifa réew ñoo nga fa woon, te mer ba futt, rax ci ñee Yeesu, di séentu Mu teg loxoom ci dëkk bi. Ñungi doon kat-kati te xam ne ñàkk nañu. Seen tëralin bi ñu laloon ngir jàpp Yeesu ci pet, amul. Dugg na léegi dëkk bi ak gàngooru ndam.

ÑAAN: Sang bi Yeesu, ubbil naa la sama xol ak sama xel. Soppi ma te def ba ma mel ni Yów, jaare ko ci sa Xel mu Sell mi. Baal ma samay bàkkaar, ndaxte yelloowuma nga dugg ci sama xol. Waaye ñów nga donte samay bàkkaar sax. Danga maa bëgg te musal ma, ndaxte jubóolewaat nga ma ak Yàlla, te dugal ma ci sa nguuru jàmm ji.

LAAJ:

  1. Lan la duggub Yeesu ci Yerusalem di tekki?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 24, 2025, at 02:34 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)