Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 076 (Jesus anointed in Bethany)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
A - LI JIITU AYU BéS bu SELL bi (Yowaana 11:55 - 12:50)

1. Tuur nañu Yeesu diwlin ca Betani (Yowaana 11:55 – 12:8)


YOWAANA 11:55-57
55 Bésu jéggi ba,di màggalu Yawut ya, mungi doon jubsi, ba ñu bare ca waa àll ba di demdi l Yerusalem balaa booba, ngir sanguji set. 56 Ñungi doon wut Yeesu, te doon waxante ca Kër Yàlla ga naan: « Lu ngeen ci xam? Ndax dina ñów ci Màggal walla déet? » 57 Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya daldi santaane ne, bu kenn xamee fu Yeesu nekk, mu yégle ko, ngir ñu man koo jàpp.

Pàk; maanaam Màggàlu bésub jéggi bà, moo nekkoon xew-xew bi gënoon a ca jamonoy Kóllëre gu Njëkk ga. Dafa doon baaxental ba Yàlla yewwee Bànni Israyel ca meram ma. Kon, mbote mu Sell, mi ñu leen jagaloon moo doon aar seen dund. Dee lañu yelloo woon, waaye, seen ngëm musal na leen.

Yawut ya dañu daan dem Yerusalem benn yoon ci at mi, ngir sant Yàlla ci li Mu leen teggiloon meram. Dañu fa daan rey ay mbote yu bare te lekk leen. Ñenn ña dañu daan teel a dem Yerusalem, ngir man a sellal seen bopp, jaare ko ci tuub te jekkalaat seen taxawaay ci kanamu botem Yàlla mi. Képp ku laaloon ab néew waroon nga jaar ci fasoŋi cellal yu bare, diiru juróom-ñaari fan, laata ngay man a dugg ci Kër Yàlla gi (Lim Ya 19 :11)

Ña doon màggalsi, di laaj seen bopp ci lu jëm ci Yeesu: « Ndax dina ñów? Ndax dinanu Ko gis? » Ñoom xamoon nañu ne Sanedreŋ bi mungi nëbb dee gi Mu Koy waajal. Yebaloon nañu ñu bare, ngir ñu yërndu mbiri Yeesu, te boolesi Ko ndax ñu man Koo jàpp. Dee gi di Ko doon gën a yootsi.

YOWAANA 12:1-3
1 Juróom-benni fan laata bésub Jéggi ba, Yeesu dem ca Betani, dëkku Lasaar, mi Mu dekkal. Foofa, ñu defaral ko fa reer. Màrt moo ko doon séddale, te Lasaar bokkoon na ca gan ña. 3 Noonu Maryaama jël liibaru latkoloñ ju raxul lu ñuy wax nàrd, tey jar lu baree-bare. Mu sotti ko ci tànki Yeesu, ba noppi mu fomp ko ak karawam. Xetu latkoloñ gi gilli ci kër gi yépp.

Yeesu faalewuloon muus-muuslu noonam ya, noonu jàpp yoonam jëm Yerusalem, àndak coobare Baayam. Jéemul a beru, waaye dafa dellu Yerusalem, benn ayu-bés laata Màggal gi. Mu xëtt dëkkub Betani, bi dande 3km Péey ma. Mu dugg ca kër ga Mu wone woon kàttanam, te siggil Baayam ca na Mu amee ndam ci kow dee gi. Lasaar a ngi doon dund ba tey; mungi doon lekk, di naan, te doon dem ca ja ba. Nit ña waaru, di ko xool, seen ragalu dee di yokk, boole ca seen ragal a daje ak njuuma.

Maryaama, Màrt ak Lasaar mos nañu ndamul Yàlla ,te di ko seede, donte tëkku Sanedreŋ bi. Lasaar teeru Yeesu ak ay taalibeem, te berndeel Ko ak mbég mu réy. Moom, xaritu Yeesu la woon, te dafa toogoon ci wetu ki ko dekkaloon ca ñu dee ña. Ndax boobu nataal mayunu nu xelmati ci àjjana? Yàlla du nu sore foofa; dinanu toogandoo ak Moom ci biir ndam li.

Màrt, jigéenu kër ju mat sëkk, daldi ubbi këram, joxe lépp la mu amoon, ndax xamoon na ne Yeesu mooy Almasi bi dëggantaan, bi daan dee gi.

Dafa nammoon a may Yeesu li mu gënoon a bëgg ci xolam. Waaye dafa xalaatoon ne yellowul diw boppu Yeesu, noonu mu diw tànkam ya, ak alalu dundam googu. Mbëggéel du ŋott mukk, waaye dafay joxe te du waññi nu mu tollu. Gannaaw gi mu fomp tànkam ya ak ay karawam. Doxalinu mbëggéelam gu dëggu googu te sell, feesal kër gi ba mu daj ak xetu latkoloñ. Ña teewoon ñépp xooju ca xetu saraxu Maryaama ba.

YOWAANA 12:4-6
4 Kenn ca taalibey Yeesu ya, muy Judaa Iskariyot, mi Ko nar a wor, daldi ne: 5 « Lu tax jaayewuñu latkoloñ jii ñetti téeméeri poseti Deni, te jox ko miskiin yi? » 6 Waaye bi muy Wax loolu, xalaatuloon miskiin yi, ndaxte sàcc la woon; moo yoroon boyetu xaalis bi, te daan ci sàcc.

Yudaa moo gënoon a bëgg xaalis Yeesu; alalu àddina moo ko gënaloon ngëm gu gore. Noonu, muy jéem a taafantoo sarax si, di ko jaare ci ay dërëm, te fàtte barkeelu asamaan bi ci ànd. Manuloon a xam li cant ak ngërëmu Maryaama googu, ak jébbaloom ci Yeesu, di tekki. Képp ku bëgg xaalis (alal) ba jiital ko, dangay mujjee nekk ku bon. Aka doy-waar ni mu nëbbewoon mbañeel gi mu amoon ci Yeesu, di mbubboo diine, mel ni kuy def sarax soosu, ngir dëfal xolu miskin yi. Faalewu-leen sax, te xalaatu-leen a jox dara. Boppam doŋŋ la yéenewoon xaalis ba. Sarax si, mbubb lawoon ngir càcc gi. Gorewuloon ci mbir yu tuuti yi, ab sàcc doŋŋ la woon.

Yeesu daanul wóorliku la denckatu xaalis booba yor. Daf koo muñal ba ca njeextal la, ak la Mu umpalewuloon dara ca njublaŋam gi, ak njuuj-njàccam yi. Yudaa, ab sàcc lawoon, te njublaŋ, bëgg alal lool, ba nekk jaamamu dërëm bi. Mbokk mi, manuloo jaamu Yàlla, ak alal ji. Kon dinga bëgg kenn ki, te bañ ka ca des. Bul nax sa bopp. Ndax Yàlla ngay wut, walla dund gu yomb?

YOWAANA 12:7-8
7 Waaye Yeesu ne ko: ” Bàyyi ko! Jekkoon na mu denc ko ngir bés bu ñu may suul. 8 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww.”

Yàlla santunu nu ëppal ba di sottante ay butéeli latkoloñ, waaye dafa bëgg nu bàyyi xel ci soxlay néew-doole yi nu wër. Amul genn mbootaayu politik, walla diine, mbaa xalaat, bu man a weddi ne miskin du mos a jóge ci sunu biir. Sunu jikkoy bopp-sa bopp dafa rëy, te sunu mbëggeel tuuti. Bokk mennum xel manul a nekk ci àddina sii; kenn manul a yem ak ñeneen ñi, ci lu aju ci maye, alal, mbaa ngor. Muy ci penku, walla ci sowu-jant, fépp lanuy gis ñu torox, ñu ñu sobental ak ñu ñu nanguwul a dalal fenn. Nga dëkk ca kow ga mbaa ci taax yi, wutal miskin yi, noonu dinga gis ci ku ci nekk, ci ñoom, xarkanamu Yeesu.

Yeesu xamoon na ne xolu nit ki dafa dëgër ni xeer, te xat ni fu puso xejul. Dafa ñów ak mbëggeel gu mat sëkk, ngir wuutu leen ci dee gi. Xamoon na itam ne Xel mu Sell mi moo xiiroon Maryaama ngir mu tuur ko diwlin ngir néewam. Bu mbëggeelu Yàlla duggee ci xol yi, Xel mu Sell mi dafa leen di defloo ay kéemaan yu kenn xalaatuloon. Maryaama dafa fasoon yéene teral gan gu Sell gi, noonu Xel mu Sell mi may ko mu sotti Ko diwlin laata wéxtu wa di jot. Krist mungi tàmbali jubale àddina su bon si, ak Yàllay mbaax gi, ak yiw wi.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, naw nanu la ndaxte Yów yaa dekkal Lasaar. Ragaluloo bàmmeel ba. Jàngal nu ni nuy mayee sunu xol, ak sunu alal, ngir man laa jaamoo ci lépp li nu am. Gooreel nu ci nay, ak naaféq, sàcc ak mbañ. Sol nu mbëggeel ba nu fees -dell, te wommat nu ci yoonu sarax si, te mu ànd ak cant.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu nangu Maryaama tuur Ko latkoloñ?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 24, 2025, at 01:43 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)