Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 052 (Disparate views on Jesus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

b) Xalaat yu wuute yu jëm ci Yeesu, ci diggante askan wi ak Kuréel gu mag gi (Yowaana 7:14-53)


YOWAANA 7:37-38
37 Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw,wax ca kow ne: ”Ku mar,na ñów ci man; te ku gëm, na naan! 38 Ndaxte Mbind mi nee na, ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.”

Ci biir màggl gi, Yeesu waarewaat ca biir ëttu Kër Yàlla ga. Mbooloo maa nga doon xaar saraxalekat ba sotti ndox ma ca bérabu saraxekaay ba. Rekk waarekat yu mag ya duggusi ak ay sarxolle yu ànd aky tàccu ngir sotti ndox ci kanamu Yàlla, mu mel ni sarax su ñuy jébbal Yàlla, te di misaal barke bu ñuy séentu ciYàlla at mi ñuy dëgmal. Aada jooju dañu ko jële woon ci waxi Yonent Yàlla Esayi, ba mu nee: »Dingeen root ak mbég ca teenu mucc gi. » (Esayi 12 :3)

Yeesu gis na ruu yi mar, yi jaar ci ay déebaadéeb yu bare, te xamuñu mucc gi. Mu xaacu ci kanamu mbooloo mi ne: ”Kaayleen ci Man te naan ci ndoxu dund gi te du ngeen fay dara. Na ñépp ñi mar ñów ci man. Maay teenu dund gi.”

Ñi nammul dundu baatin, duñu àgg ci mucc gi. Waaye Yeesu nee na ñi Ko wóolu: »Képp ku Ma gëm te ànd ak man, dinga nekk mbënnu baarke ngir ñu bare. Mbind mi yedd na leen ngir ngeen gëm Ma, te Yàlla sant na leen ngeen ñów ci Man, ngir ngeen am dund ak mbég. » Képp ku jegesi Yeesu te naan ay kàddoom, dinga fees ak Xelam, te soppiku. Ki mar dafay doon ab teen, te ki doon dunde bopp-sa bopp gu soxor, mujje nekk surga bu gore.

Ndax mos nga pajum Yeesu mu kéemaane mi? Moom dafa bëgg nga nekk teenu ndox mu neex. Am na xalaat yu bon yuy juddoo ci sa xol. Waaye Yeesu man na laabal sa xol ak sa gémmiñ ndax nga man a nekk teenu barke ngir ñu bare.

Li Yeesu di wut, du sellal sa xel ak sa ruu,waaye itam sa yaram. Dinga nekk sarax suy dund te neex Yàlla, di surgawu ñi réer. Yeesu dafa la bëgg a sellal ba nga set-wecc, ngir nga bañ a dund ngir sa bopp kese, waaye ngay jëfandikoo, ci sa coobare, sa doole ji nga am ngir sarwiir ñeneen ñi. Képp ku déggal Yeesu te seetoo ci dara, dinga nekk barke ngir ñu bare.

YOWAANA 7:39
39 Booba li Ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi Ko gëm naroon a jot. Fekk joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñaguloon.

Képp ku gëm Yeesu dinga jot mayug Xel mu Sell mi. Wàccu Xel mi ci nit ki sunu kéemaanu jamono la. Ñungi dund ba tey ci mayug Xel mu Sell mi. Du malaaka du njuuma, waaye Yàlla la ci boppam, fees ak sellaay ak mbëggeel. Xel mi dafa mel ni safara su yànj ak kuuraŋ bu am doole. Waaye itam Dëfalkat (Dimbalikat) bu lewet la. Bépp kercen bu dëggu dafay nekk màkkaanu Xel mu sell mi.

Xel moomu kenn mayu ko woon ñépp ca jamono Krist, ndaxte bàkkaar moo doxoon ci diggante Yàlla ak ay jaamam. Ay tundi ñaawtéef ñoo meloon ni ñag bu dox ci diggante Xel mi ak nit ñi. Waaye gannaaw deewam ak delloom asamaan, Yeesu toog na ca ndeyjooru Baay ji, te déggoo ak Moom ba yónnee Xelam ñépp ñi Ko gëm. Yàlla Xel la te mungi teew fépp. Kon man naa dëkk ci way-gëm ji nangu mbaalu bàkkaaram ji jaare ci deretu Krist. Doom-baay, ndax jot nga Xelum Yàlla mi? Ndax kàttanu Yeesu solu na la ba nga fees? Ñówal ci Yeesu Moom miy teenu yeete gi ak neexal yi. Moo la dig: »Ku ñów ci man du xiif mukk te ku Ma gëm du mar mukk. »Ku Ko gëm, ni ko Mbind mi waxe, ay dexi ndoxu dund dinañu wale ci yów ngir ñeneen ñi.

YOWAANA 7:40-44
40 Ba ñu déggee wax jooja, mu am ay nit ca mbooloo ma ñu naan: ”Dëgg-dëgg Kii mooy Yonent bi war a ñów.” 41 Ñeneen naan: ”Mooy Almasi bi.” Ña ca des ne: ”Nan la Almasi bi man a jógee Galile? 42 Mbind mi wax na ne Almasi bi ci xeetu Daawuda lay wàcce te Betleyem, dëkku Daawuda, lay jóge.” 43 Noonu féewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu. 44 Am na ca ñoom ñu Ko bëggoon a jàpp, waaye, kenn manalu Ko woon dara.

Ñenn ci ñi Ko doon may nopp yëgoon nañu dooley dëgg gi nekkoon ci kàdduy Yeesu te nangu cee jébbalu. Dañu nangu ci kanamu mbooloo mi ne Moom yeesu, Yonent la bu xam coobare Yàlla, te man a ràññee mbóoti xolu nit ñi. Mooy Yonent bi ñu digoon Musaa, te mu waroon a yóbbu askan wa ci ndam-ó-ndam, ci biir jokkoo ak Yàlla. Noonu la ñenn ca ñoom sañewoon seede ne waa Nasaret bii mooy Almasi bi ñu digewoon ci dëgg-dëgg.

Waaye nag bindkatu Téere ya fippu naan: ”Déeet! Nasaret la jóge, te Almasi bi dëkku Daawuda la war a jóge, ak ci geñoom.” Loolu dëgg la, te mbind mi seede na ko (biral na ko). Waaw, lu tax Yeesu waxuleen ne Betleyem la judoo? Lii la man a doon ci as néew: Li njëkk Waa këri Herood naruñuwoon bàyyi beneen buur muy dund gannaaw ku bokk ci seen geño. Jekkoon nañu ngir rey ay téeméeri junni nit, ngir sàmm seen nguur. Ñaareel bi mooy, Yeesu fasuloon yéene am ay taalibe ci kow ay firnde yu tegu ci cosaan. Li ko gënaloon mooy Mu samp seen kóolute ci mbëggeel ak ni ñuy ràññee nguram. Noonu la jotee ñi Ko gëm te gisuñu(Ko).

Ŋaayoo bi gën a jib,ba mbooloo ma féwwaloo. Ñenn ña naan Mooy Almasi bi, ñeneen ña di Ko weddi. Surga Kër Yàlla ga di Ko fexe jàpp. Waaye màggaayu kàddoom ya xañ leen ko, ba manuñu Ko jege.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nu ngi lay sant ci sa mbëggeel ak sa màggaay. Yów yaay reenu dund gi. Dangaa jokkoo ak nun ci kow ngëm. Yónnee nga nu sa Xel mi. Jaare ko ci ngëm, sa baatin nekk na sunu bos, nun bàkkaarkat yi. Ndaxte sellal nga nu ak sa deret, te danuy dund ba fàww.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu am sañ-sañu wax: » Bu kenn maree, na ñów ci Man te naan »?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 11, 2025, at 12:45 PM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)