Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 053 (Disparate views on Jesus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

b) Xalaat yu wuute yu jëm ci Yeesu, ci diggante askan wi ak Kuréel gu mag gi (Yowaana 7:14-53)


YOWAANA 7:45-49
45 Bi alkaati ya delloo, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: ’Lu tax indiwuleen Ko? » 46 Alkaati ya ne leen: »Kenn mosul a waxe ni nit kooku! » 47 Noonu Farisen ya laaj leen: » Mbaa naxuñu leen, yéen itam? 48 Ndax am na kenn ci kilifa yi walla Farisen yi ku ko gëm?

Ba Yeesu nekkee ca Kër Yàlla ga di waare, Farisen ya am ndaje di yaakaar ne seen surga ya dinañu jàpp Yeesu te indil leen Ko. »Saraxalekat yu mag » dafay wone ne ñu bare lañu, bu dee sax kenn rekk ci ñoom moo jiite Kureel gu Mag gi, giiru dundam. Waaye waa Rom dañu daan folli yenn saa yi yooyee kilifa. Loolu moo taxoon mu amoon saraxalekat yu bare yu waa Rom faloon ca jamono Yeesu. Ñoom ñépp ca jabootu ña ñu ber lañu bokkoon. Nit ñooña ñoo doon Sadusen ya nanguwoon xalaat yu teggeeku diisaayu dundin, yi nga xam ne ñoom la Farisen yi fonk diine bëggul.

Farisen yi dañoo péñcoo ak waarekat ya, ca Kuréel ga. Dañoo weddi woon xalaatu Grek ya te teg Yoonu Musaa wi ñu gëm, ak seeni jëfi mbootaay. Seeni xol dañu dëgëroon te dañu doon jaamu Yàlla ci neex-naqari.

Farisen ya ak Saduseen ya mer lool ba ñu manulee jàpp Yeesu. Moone de du taalibeem ya ñoo Ko doon aar, rawatina mbooloo ma, waaye kàddoom ya dañoo feesoon dell ak doole, ba kenn ci ñi Ko doon wut a jéŋŋ amatul fit woowu, ndaxte gisoon nañu kàttanu Yàlla gi doon jollee ci Moom.

Ba Farisen ya déggee loolu, ñu saaga wottukati Kër Yàlla ga: »Ndax léegi dangeen a far ak naxekat yi (njublang yi)? Amul kenn ci Kilifay Kuréel gi ku Ko gëmoon. Benn way-gëm bu am bopp xalaatuloon topp waa Galile jooju.

Am na nag ñu bare ñu Ko bëggoon, waaye ca baadoolo ya lañu bokkoon. Ca seen biir, daan nañu ca fekk ñu ñu xeeb, ay sàcc, ak ñu seen dund jaarul yoon. Dafa doon toogandoo ak ñoom di leen sagal ci teewaayam. Waaye ñu fonk diine ña dañoo bañoon ñu mel noonu, te jàppe woon leen ni ñu torox. Bëti ñu fonk diine lañu leen doon xoole. Waaye ci dëgg, ñooñu ñu xeeb, ñoo doon topp Yeesu. Ñenn ca ñoom nangu woon nañu seeni bàkkaar te tuub leen ca kanamu Yaxya. Noona la Njiit ya bañe mbooloo ma, ba fàtte sax ne ñoo bokk làkk ak cosaan. Mbooloo mépp ñoo bokk, ak lépp lu man a xew, ba ci féwwaloo yi ci diggante waaso yi sax.

YOWAANA 7:50-53
50 Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon, Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen 51 : »Ndax ci sunu Yoon, man nañoo daan kenn te dégluwuñu ko, mbaa ñu xam lu mu def?” 52 Ñu tontu ko ne: «Mbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? Gëstul, kon dinga xam ne, benn yonent musul a jóge Galile.» 53 Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa kër.

Mbañ ga Kuréel ga doon wone neexuloon Nikodem. Diisoowoon na ak Krist, ba Mu xamal ko ne nit ki dafa soxla judduwaat. Nit kii,Yeesu xiir na ko ci boppam, te bëggoon na moom Nikodem, aar Yeesu, waaye bëggul siiwal loolu. Kon book mu sukkandikku ci Sarti Yoon wi, yi tere ñu àtte nit, te teewul.

Àttekat ya di ñaawal xalaati Nikodem ya. Bu fekkoon ne Kuréelu àttekat ya sax ñoo toogoon,kon itam dara du ca teggeeku; dañuy nar a àtte ki deful genn tooñ ci kow ay jiiñ yu dul dëgg. Lenn doŋŋ doyoon na ña Ko doon ŋàññ, ne du Yonent bu dëggu, ndaxte Galile la jóge-maanaam diiwaan bu Yawut ya xalaboon ndax seen ñàkk a farlu ci Yoonu diine ji. Amul benn aaya Mbind mi bu wax ne Almasi bi ñu dige, walla ab Yonent dina dikke Galile ci jamono yu mujj yi. Farisen ya wóolu seeni xalaat ba di ñaawal Nikodem. Moom Nikodem nag, dafa leen bëggoon a yegge kàddu yu xóot yu Yeesu yi ko yeyoon laata lii.

LAAJ:

  1. Lu tax Waarekat ya ak Farisen ya daan sàbbi nitu neen ya (baadoolo ya)?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 14, 2025, at 01:43 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)