Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 050 (Disparate views on Jesus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

b) Xalaat yu wuute yu jëm ci Yeesu, ci diggante askan wi ak Kuréel gu mag gi (Yowaana 7:14-53)


YOWAANA 7:21-24
21 Yeesu ne leen: ”Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngéen jaaxle! 22 Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gune yi jógewul ci Musaa, mungi tàmbalee ci seeni maami cosaan, moo tax ngeen nangoo xarafal nit ci bésu noflaay bi. 23 Bu ngeen manee xarafal nit ci bésu noflaay bi, ngir bañ a wàcc yoonu Musaa, lu tax ngeen mere ma, li ma ci wéral nitu lëmm? 24 Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.”

Yeesu tëbul rekk tontu Yawut yi Ko doon jiiñ ne dafa am ay rab yu Ko jàpp, waaye dafa leen a won ne àtte dee bi ñu Ko teg du yoon. Mu fàttali leen ne li ñu Ko bëgg a daane, mooy jarag ga Mu wéraloon ca Betsaida, ca bésub noflaay ba. Bés boobu Yeesu dafa santoon jarag ja Mu wéraloon mu fob basaŋam te ñibbi. Kéemaan gu rëy lawoon, gu laajul sax ñu ko ciy joxoñ baaraamu tooñ.

Yeesu teg ca ne kangaami Yoon wa toppuñu sart ya ni mu ware. Yoon wi dafa ëmb ay weddeem (gàllankooram); xarafal gi mooy màndarga kóllëre gi ak Yàlla, te bésu noflaay bi mooy jokkoo noflaay gi ñuy am ak Ku Sell ki. Dañoo waroon a xarafal gune yi ca seen juróom-ñetteelu fan ba ñu juddoo, te manoon na daje ak bésu noflaay. Xarafal xanaa du jëf mbaa ligéey?

Ndegam dañoo jàppe feebar ni meññeefu bàkkaar, wér dañu ko jàppewoon ni muccug yaram, ruu, ak xel. Yeesu dafa doon ñaax nit ñi ñu xalaat ci wuute gi nekk ci diggante jaamu yërmaande ak xaraf ci bisu sabbat. Lan moo gënoon am solo ? Ba noppi mu jëfandikoo xel mu dal ngir jàppale leen ñu xam fu mbëggeelam, dooleem ak mucc gi yegg, waaye amul benn njariñ. Seen nopp tëjuwoon nañu, seen xel dëgërul, mënu ñu woon jël dogal bu jaar yoon, mënu ñu woon àtte ci anam wu jaar yoon.

YOWAANA 7:25-27
25 Am na waa Yerusalem yu doon wax naan: »Xanaa du nit kii lañuy wut a rey? »26 Xool-leen mungi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du Ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne mooy Almasi bi? 27 Waaye, waa jii xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu Mu bàyyikoo. »

Ba waa Yerusalem gisee ne ñépp Yeesu lañu teg bët, ñu mer lool, ndaxte Yeesoo ngi doon dem ak dikk, ci dëkk bi, te joxe woon nañu ndigal lu siiw ngir ñu jàpp Ko. Xibaar boobu ñépp xamoon nañu ko.

Waa péey ma di ñaawal Kuréel ga ndaxte manuñu sottal mbir ma. Waa Rom ya dañoo foqati woon ca kilifa yawut ya sañ-sañu rey. Nit ña di xàkkataay naan: ”Nit ka ñuy wut mungi doxantu ci biir dëkk bi, di waare sax ca Këru Yàlla ga ni mu ko neexe. Kilifa ya manuñu Ko ko tere. Njiitu diine ya manuñu Ko noppiloo ak ay kàddu yu dëggu walla ay waxtaan.”

Ñeneen naan: »Xamuleen nu mu deme sax,xëyna ñenn ci kilifa yi gëm nañu ne Mooy Almasi bi. »Loolu lañu yaakkaaroon ne moo tere kilifa ya ñu jàpp Yeesu. Xalaati nit ña juuyoo.

Ñetteelu wàllu nit ña naan: »Su fekkoon ne mooy Almasi bi, kon ndamam dina jolli, te du nirook nitu neen. Waxambaane xaddkat bii, ca dëkku tund ya la jóge. Almasi bi dëgg, buy ñów asamaan lay jóge, te du doxantu ci biir niti neen. »

YOWAANA 7:28-30
28 Yeesu di jàngale ca Kër Yàlla ga, daldi wax ca kow ne: ”Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñówaluma sama bopp, waaye ki ma yónni Ki, Ku wóor la. Yéen xamuleen Ko. 29 Man xam naa Ko, ndaxte ca Moom laa jóge, te itam Moo ma yónni.” 30 Noonu ñu koy wut a jàpp, waaye kenn manalu Ko dara, ndaxte waxtoom jotaguloon.

Yeesu dégg werante yi aju ci cosaanu àddinaam, rekk Mu xaacu ne: »Ci dëgg ndax xam ngeen Ma? Fan laa jóge? Ni ngeen di àttee woyof na lool, te jéemuleen maa xam ci dëgg. Dégluleen Ma, te gëstu sama Xel mi. Su ko defee ngeen man Maa xam; te xam it fu ma jóge. »

Yeesu ñówalul boppam; Baayam moo Ko jur te yónni Ko. Moom ak Baayam ñoo yem melo te di jokkoo saa su nekk.Mu teg ca ne: »Kenn ci yéen xamul Yàlla. Monte yéen a ngi xalaat ne Mungi ci Kër Yàlla gii. Seen kilifa diine yi dañoo gumba, te duñu gis Yàlla, duñu dégg baatam. Kon book yéen a ngi juum, yéen ci seen bopp.

Mu tegaat ca ne: ”Man xam naa Ko.” Li samp Injiil mungi ci ñeenti baat yooyu; Yeesu xam na Yàlla te wax na nu turu Baay bi ak mbëggeelam. Waayu Nasaret ja amuloon bàkkaar, te dafa jokkoo woon ak Baayam saa su nekk. Te fekk ñépp tàqalikoo ak Ku Sell ki ndax seeni bàkkaar.

Ba ñenn ca ña Ko doon déglu gisee diisaayu kàddu Yeesu ya, dañoo yuuxu naan: »mungi tumaal Kër Yàlla gi, te di nu jiiñ ñu ñàkk diine. »Noonu ñu koy jéem a jàpp. Waaye kenn ci ñoom manu Koo jege Moom Doomu Yàlla ji, mu mel ne malaaka yi dañu Koo wër. Jamono ji Mu waroon a jeexale seedeem ci kow suuf, agseeguloon. Baayam tëraloon na jamono ji Mu waroon a (Moom Krist) rammu nit ñi. Kenn ci kow suuf manuloon a randal, mbaa teelloo waxtu woowu.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu nungi lay màggal, ndaxte xam nga Yàlla, te feeñalal nga nu Baay bi. Nungi lay surgawu, te di la jaamu ak mbég. Sa peeñu Mi moo nu may nu nekk doomi Yàlla. Nungi lay bége, te di màggal sa tur àndandoo ak ñépp ñi am judd gu bees. Nungi lay ñaan nga feeñalal Baay bi ñi fonk diine ñi nu dëkkal, ndax ñu gindiku ci fonk diine ji, ak seen ñàkk yitte.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu rekk moo xam Yàlla?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 11, 2025, at 09:47 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)