Previous Lesson -- Next Lesson
2. Kenneefu Ñett bu Sell bi dafay wàcc ci way-gëm yi, jaare ko ci Dëfalkat bi (Yowaana 14:12–25)
YOWAANA 14:12
12 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, képp ku ma gëm dina def moom itam, jëf yi may def. Dina def sax yu gën a màgg, ndaxte maa ngi dem ci Baay ji.
Xam Yàlla teguwul ci filosofi walla tëralin wu jaadu. Bépp xam-xamu xel dafay indi tiitar, waaye fii, lu aju ci xam mbëggeelu Yàlla ak mucc gi Doom ji di maye lanuy wax. Dafa ëmbaale surgawu ci sa kow coobare. Krist dafa jox taalibeem ya ndigal lu bees : « Jëfeleen mbëggeelu Yàlla jaare ko ci ay doxalin ak ay jëf yu ànd ak ñaan. »
Ba ñu xamee ne Yeesu dafay jóge ca ñoom, taalibe ya dañu ñaanoon Yeesu ngir mu aar leen te ñu xam Yàlla bu xóot -a-xóot. Waaye Krist dafa leen a dalal ci Yàlla ndax ñu man a tas xabaar bu baax bi ci àddina sépp.
Li amoon solo dëgg,du woon seen kaaraange, gi am àpp, waaye seen tàggat ngir ñu jekk ci liggéeyal Yàlla. Bu nu xamee Baay ji, dafay tax nu tàggook jikko bopp-sa bopp,te xiiru ci suufeelu ci sunu liggéey. Yeesu nee na : « Képp ku ma dénk sa bopp dangay jëf, doo yem ci di dox rekk, waaye dangay jaar ci yoonu jébbale sa bopp. Ki gëm, bu fàttee boppam te màggal Krist, Ku dekki ki dina yëngu ci dundam, te may ko ay barke. Ak ngëm lu mel noonu, gannaaw ba Xel mu Sell mi wàccee ci ñoom, Ndaw ya amoon nañu sañ-sañu wéral ak baale bàkkaar, ba ci dekkal ñu dee sax, ci turu Yeesu. Dañoo fàtte woon seen bopp, te Krist mungi doon dund ci ñoom. Dañu Ko bëggoon ci seen xol, te doon Ko màggal ci seen doxalin.
Gannaaw liggéey yu sell yooyu, Yeesu dafa leen a yónni ngir ñu matali liggéey yi mu jotuloon a àggale ci diir bu gàtt bi Mu am ci kow suuf. Ba Mu yéegee asamaan, dafa yónnee Xelam mu Sell mi, noonu ñu bare jot dund gu bees, jaare ko ci seen waare. Ba tey jii, njabootu Yàlla gi mungi wéy di màgg. Dara gënul a rafet seede bi nuy defal Krist mi ñu daajoon, te Mu dekki. Nit ñi dañuy jot dund gu amul àpp, bu ñu wóoloo seede boobu. Xel mu Sell mi dafay wàcc ci ñi taq ci Krist, te def leen ay doomi Yàlla, ndax ñu man a màggal seen Baay seen giiru dund gépp, ak njubte.
YOWAANA 14:13-14
13 Te it lu ngeen ñaan ci sama tur dinaa ko def, ngir Doom ji feeñal ndamu Baay ji. 14 Lu ngeen ñaan ci sama tur, maa koy def.
Ndax yaangi ñaan ? Ñaata ci say ñaan ngay jagleel say tiis ak say bàkkaar ? Ban diir ngay ber ngir màggal Yàlla ak dimbali ñeneen ? Ndax say ñaan ngir yów doŋŋ lañu, walla dañuy fees ak mbëggeel gi nga am ci Yàlla ak ñu réer ñi ?
Mbëggeelu Yàlla ndax soppi na say ñaan ? Ndax mos ngaa barkeel sa noon ? Muccug Krist, ndax Walla am na ci ay baat yu la neexul, yu mel ni « nanu baal tooñu ñeneen ñi » ?
Booy ñaan ci turu Krist, kon dinga dunde te xalaate ni Xelam, ni Mu ko bëgge, te noonu sa xol dina fees ak xalaati yërmande.
Krist dafa dige lu ëmbaale kàttan ak barke yu asamaan. Dafa jéng dige boobu ci sart bu leer bii : « Soo ubbilee sa xol samay kàddu, kon dinañu la soppi, ba ma am doole te màgg ci yów, dinaa musal ñu bare ci ger, jaare ko ci sa ngëm ak say ñaan. Bu la Xel mu Sell mi xiiree ci ñaan, te nga gëm ma, kon dinaa la tontu. »
Mbokk mi xalaatal bu baax ci biir cant, ci caabi ji Yeesu teg ci say loxo. Nanga tuur alalu asamaan si, jaare ko ci say ñaan. ”Dinaa wàcc ci say dëkkandoo ak say xarit indaale barke, mucc ak xam-xam, rax ci dolli tub ak rëccu ci kow sama ñaax ak ndimbal.” Ñaanal Yeesu te saraxu Ko ngir Mu tànn ay jaam ci sa réew, def leen ay doomi Yàlla. Bul tàyyi ci di ñaan; ci sa ngëm la Yàlla di jaare ngir musal ñu bare. Gëmal àntu gi, te santagum Ko ci. Ñaanal sa doomi ndey yi ñu ñaanandoo ak yów ci biir ngëm. Bul tàyyi ci sant ak màggal. Na la Yàlla xëpp Xelum ñaan !
Su fekkee ne gis nga ne Yeesu tontuwul say ñaan,kon tuubal say bàkkaar te rëccu leen, daaneelal lépp liy gàllankoor sa ñaan ndax Mu man laa sellal. Dina la may sañ -sañu wàccee baatinu asamaan gu mat sëkk gi, ci kow suuf. Boo dogoo ci ñaan ak ngëm te di seede, dangay màggal Baay ji, Doom ji ak Xel mu Sell mi.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu may nu Xelum ñaan, ba dunu xalaat sunu bopp rekk te fàtte ñeneen ñi. Defal ba nu nekk ay ñaankat ngir nu tàbbil sunuy waajur yi ak sunu xarit yi ci mucc gi. Nungi lay màggal, ndax ubbil nga nu asamaan, xëpp nu say may ak sa yéwenaay? Na turu Baay ji ndamu ci juddug doomi baatin yu baree-bare. Na saw tur sell ci seen doxalin ci cellaay gi ak ci kàttanu Xel mi.
LAAJ:
- Limal benn fànna bu am solo buy may Yàlla Mu àddu sunuy ñaan !