Previous Lesson -- Next Lesson
e) Doomu Yàlla ji ci Baay ji ak Baay ji ci Doom ji (Yowaana 10:31-36)
YOWAANA 10:31-36
31 Yawut ya daldi foraat ay xeer, bëgg Ko Koo sànni ngir rey Ko. 32 Noonu Yeesu ne leen: » Def naa ci seen kanam ay jëf yu baax yu bare ci ndigalu Baay ji. Ban ci jëf yooyu moo tax nngeen bëgg maa sànni ay doj? » Yawut ya ne Ko: » Jëf yu baax taxul nu bëgg laa sànni ay xeer, waaye dangay suufeel turu Yàlla; yów, nit rekk nga, ba noppi di def sa bopp Yàlla! 34 Yeesu tontu ne: » Bind nañu ci seen Téereb Yoon ne: »Yàlla nee na :Ay yàlla ngeen . » 35 Yàlla woowe na « ay yàlla » ñi Mu yónnee kàddoom, te xam nanu ne kenn manul a randal waxi Yàlla. 36 Kon nu ngeen man a waxe ne damay suufeel turu Yàlla ndax li ma ne Doomam laa, man mi Yàlla tànn, yónni ma ci àddina ?’
Yawut ya gënatee bañ Yeesu ba Mu nee: »Man ak Baay ji benn lanu. » Dañoo jàppààn ne seedeem jooju dafay tuumaal Yàlla, noonu ñu fas Ko yéene dóor ay xeer ni ko Yoon wi santaanee, ndax merum « Yehovah » bañ a dal ci kow askan wi. Ñu ne dagaj ca ëtt ba ngir for ay xeer.
Yeesu ne jonn ca seen kanam ak teeyaay gu mat, ne leen: »Lu bon lan laa def? sarwiir naa leen, fajal leen seen ñu wopp, dàqal leen ay rab te ubbi seen bëti gumba gi. Laabal naa ay gaana te yët Xabaar bu Baax bi néew doole yi. Ban ci jëf yooyu ngeen ma bëgg a reye? Dangeen di wut a faat ki baax ci yéen. Wutuma alal walla sag ci sama liggéey, bii may tudde « samay jëfi Baay. »Liggéeyal leen moo ma fi indi. »
Yawut ya xaacu ne Ko: « Du say jëf ñoo tax nu lay dóory xeer, waaye li ngay tuumaal Yàlla moo ko waral. Dangay tolloole sa bopp ak Yàlla, te yaangi nii ci sunu biir ni nitu neen. Dinanu tuur sa deret ngir wone ne kuy dee doŋŋ nga. Noo sañ a waxe ne Yàlla nga, nekk benn ak Ku Sell ki? Yów de xanaa rab moo la jàpp, dee rekk a war ci yów léegi ci saa si.
Ak kóolute gu rëy, yeesu tontu ne: « Xanaa jànguleen ci seen Téere Yoon bi ne Yàlla dafa daan faral di waxtaan ak Ki Mu fal naan Ko « Ay yàlla ngeen, yeen ñépp ay doomi Aji Kowe ji ngeen (sabóor 82 :6) fekk yéen a ngi sànku ci def bàkkaar ci kow bàkkaar. Dëgg la ne ñépp ay bàkkaarkat lañu, te nekk ci njuumte. Moone de Yàlla dafa leen a woowe « yàlla ak doom » ci turam wu sell wi. Yàlla mosu la yéene dee, dafa bëgg nga dund ba fàww. Dellusil ci Yàlla, te nga sell ni Mu selle. »
« Lu tax ngeen bëgg maa dóor ay xeer? Yàlla ci boppam sax mungi leen di woowe « ay yàlla ak doom ». Man bàkkaaruma ni yéen. Ku sell laa ci wax ak ci jëf, te am naa sañ-sañu dund ba fàww ndaxte Doomu Yàlla laa. Jàngleen seen Yoon wi, ndax ngeen xam ma. Waaye yéen de gëmuleen sax seen Mbind yi, te xamuleen sama baatin. »
« Man, yónniwuma sama bopp, waaye Bqqy ju Sell ji moo Ma yebal. Man Doomam laa, Muy sama Baay. Sellaayam mungi dëkk ci man. Noonu, man Yàlla u Yàlla laa, leer u leer gi; dañu maa jur waaye kenn sàkku ma, ma bokk fi Baay ji bokk. »
Yeesu daldi yey Yawut ya, jaare ko ci seen Mbind yu Sell ya. Ak mbañeel gi nekkoon ci seen xol gépp, dañoo mujj lem seen loos ndaxte Yeesu won na leen ci Téere Kóllëre gu njëkk gi ne manees naa baayoo Yàlla ni mu Ko defe.
YOWAANA 10:37-39
37 Su ma deful sama coobare Baay, buleen ma gëm; 38 Waaye su ma ko defee, bu ngeen ma gëmul sax, gëmleen book samay jëf, ngir ngeen xam te nangu ne, maangi nekk ci Baay ji te Baay ji nekk ci man. » 39 Ñu di Ko wut a jàppaat, waaye Mu bàyyi leen fa, dem.
Yeesu faramfàcceel leen ne loolu mooy ne dangeen ma war a gëm, ndaxte li Yàlla di def laay def, maanaam ya jëfi yërmande. Duma yelloo nguur gi bu fekkee ne amuma taxawaayu yërmande. Ndegame mbëggeelam ci man la jëmmoo, kon am naa sañ-sañu matal liggéeyi Yàlla, ndaxte, ci dëgg-dëgg ay jëfi Baay ji lañu. »
«Man na am ne sa xel manul a jàpp baatin bi ci jëmmu nit. Terewul nga seetlu samay jëf: kan moo man a dekkal ku dee ci ay kàddoom rekk, ubbi bëti gumba yi, dalal tow bu metti, walla suural 5000 nit yu xiif ci juróomi mburu ak ñaari jën kese? Ndax bëgg nga Xel mu Sell mi ubbi sa xel te wax ak yów, ndax nga xam ne Yàlla ci boppam mungi ci Man? Bu la Xel mu Sell mi solo oba nga fees, dinga sax ci xam-xam bu am solo boobu, te gis ne mataayu baatin gépp mungi ci sama jëmm ji. »
Yeesu dafa wax kàddu yu am doole ci kanamu mbooloo mi; bokk na ci bi Mu nee mungi ci biir Baay ji. Ni car di saxe ci dàtt bi, te di jote doole ci reen yi, noonu itam la Krist ñówee ci Baay ji, te sax ci Moom. Dara manu leen a teqale, ndaxte seen jokkoo dafa mat sëkk. Kon man nanu wax ne Doom ji dafa làqu ci Baay ji ngir feeñal Ko te sargal Ko. Ñaan gi gën a siiw, nii la tàmbalee: « Sunu Baay ji ci asamaan, na sa tur sell. »
Képp ku xóotal seede yeesu bii aju ci baatinam ,dinga gis ci biir ñaan ak màggal liy biral Kenneefu Ñett gu Sell gi di nirool. Ak mbég lanuy seedee ne Yàlla kenn la. Du ñetti Yàlla yu beru, waaye jokkoo gu mat sëkk la ci biir Kenneefu Ñett gi la.
Bi Yawut ya déggee, te déggaat seede Yeesu, ba Mu nee jokkoom ak Yàlla dafa mat sëkk, ñu daldi fomb seen sànnim xeer ba ñu Ko doon waajal. Waaye nag bëggoon nañu Koo jàpp yóbbu Ko ca Sanedreŋ ba, ngir xam ay xalaatam. Yeesu rëcc lee. Kenn manul a gaañ doomu Yàlla, fi ak coobare Baay ji mungi koy aar. Yeesu nee na : « Kenn manu leen a foqati ci sama loxo Baay. »
ÑAAN: Yów Baay ak Mbotem Yàlla mi, gis nanu lëngoo gu mat gi ci sa mbëggeel. Sunum xel manul a jàpp sa baatinu jëmm. Sa Xel mi dimbali nanu ba nu gis sa mbëggeel gu mag gi ak sa jëf yiy muccloo. Def nga nu say doom. Dimbali nu, ngir nuy sellal sa Tur ci sunuy xalaat, sunu làmmiñ ak sunuy jëf Sellal nu, ndaxte dangaa Sell.
LAAJ:
- Nan la Yeesu birale baatinam?