Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 044 (Jesus offers people the choice)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
B - Yeesu mooy mburu dund gi (Yowaana 6:1-71)

4. Yeesu, may na ñépp ñu man a tànnal seen bopp ngir “nangu walla bañ!” (Yowaana 6:22-59)


YOWAANA 6:41-42
41 Yawut ya tàmbali di ñurumtoo Yeesu, ndaxte dafa ne: » Maay ñam wi wàcce asamaan. » 42 Ñu naan: » Ndax kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Xam nanu ndeyam. Kon nag lu tax léegi mu naan, mungi jóge asamaan?”

Injiilu Yowaana dafay woowe waa Galile ay Yawut, bu ñu bokkul sax ci askan woowu. Waaye ndegam dañu doon weddi Xelum Krist, kon tanewuñu woon sax ña dëkkoon ca bët-salum.

Bindkati téere yi wut weneen lay ngir sàbbi Yeesu. Dañu yaakaaroon ne seen gis-gis ak seeni ngëm yi ñu yelloo ci ni ñu soppee diine ji, méngoowul ak mbëggeelu Yeesu. Waa Galile nag ñoom, li leen fakkastal mooy ni ñu xame woon Yeesu ci seen biir, ni “doomu” Yuusufa xaddkat, bi dëkkoon ak ñoom, te nekkoon nitu neen ku amuloon genn mayu Yonent walla lu ni mel. Yaayam Maryaama it, dara wuutalewu ko woon ak yeneen jigéen yi, lu dul li mu ñàkk jëkkëram, li doon njoort merum baatin googu. Noonu, waa Galile ya gëmuñu woon ne Yeesu mooy mburu asamaan.

YOWAANA 6:43-46
43 Yeesu ne leen: » Bàyyileen seen ñurumtu bi. 44 Kenn manul a ñów ci man te Baay, bi ma yónni xiirtalu la ci, te man dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba. 45 Yonent yi bind nañu kàddu gii: » Yàlla dina leen jàngal ñoom ñépp. » Kon nag ku déglu te nangu waxi Baay bi, dina ñów ci man. 46 Tekkiwul ne kenn mos na gis Baay bi. Ki jóge ci Yàlla doŋŋ a ko gis.

Yeesu jéemul sax leeralal kéemaanu juddoom ña Ko doon sàbbi, bu ko defoon it, duñu Ko gëm. Ci sunu bopp, manunu fexe ba xam baatinu Yeesu ni nit, Xel mu Sell mi doŋŋ moo nu ko man a xamloo. Bu nu Ko gëmee, dinanu Ko gis te xam màggaayu dëggam gi.

Yeesu dafa tere mbooloo mi muy ñurumtu peñeelu Yàlla yi. Dëgër -bopp du man a xam dara ci nguuru Yàlla. Waaye, ki mu soxal te mu xam ne amal na ko solo, kooku dina mos mbëggeelu Yàlla.

Ci mbëggeelam la Yàlla di indee nit ñi ci Yeesu Musalkat bi. Dafa leen bëgg a won leer gi te jàngal leen, ni ko Yeremi 31:3 waxe. Ci téere Kóllëre gu Bees gi, du sunu coobare walla sunu xel mooy jur sunu ngëm; xanaa kay Xel mu Sell mi moo nuy leeralal te sàkk ci nun dundu baatin. Dafa nuy dimbali ba nu xam ne Yàlla Aji Kàttan ji mooy sunu Yàlla, di sunu Baay. Yàlla dafa nuy jàngal te di jokkoo ak nun. Dafay sàkk ngëm ci sunu xol jaare ko ci liggéeyu Xel mu Sell mi. Ndax yëg nga liggéeyam ci sa xel? Ndax jekk nga ngir teeru mbëggeelu Yàlla?

Xelum Yàlla dafa nuy jëmale ci Yeesu te di nu xiir ci Moom. Dafay yee sunu nammeel ci Moom, ba nu mujj Koo fekki te bëgg Ko. Ni nu mel la nu Yeesu di nangoo (teeroo), te du nu sàbbi mukk. Dafa nuy may dund gu amul àpp. Ci kàttanu ndekkiteem dinanu, dugg ci ndamul Yàlla Baayam ji.

Waaye nag am na lu dox ci diggante Yeesu ak way-gëm ju bees ji. Amul kenn ku mos a gis Yàlla, ba mu des Doom ji. Moom moo nekkoon ak Moom ca Njalbéen ga, te gisoon na Ko. Baay ji ak Doom ji dara du leen tàggale. Yeesu bokk na ci jàmmu asamaan ji ak bépp melokaanu Yàlla.

YOWAANA 6:47-50
47 Ci dëgg-dëgg, maa ngi leen koy wax, ku ma gëm, am nga dund gu dul jeex. Maay mburu miy joxe dund gi. 49 Seeni maam lekk nañu mànn ca màndiŋ ma, teewul dee nañu. 50 Waaye mburu miy jóge asamaan a ngi nii, te ku ko lekk doo dee mukk.

Ba Mu biralee bennoom ak Yàlla ba noppi; teg ca liggéeyu Xel mi ci xolu ñi Koy déglu, Yeesu dafa leen a wonaat Ki Mu doon, ngir ñu wóolu Ko. Dafa cof lan mooy kercen, ne: Ku gëm Yeesu dangay dund ba fàww. Dëgg googu dafa wóor, ba dee manu ko dindi.

Yeesu dafa mel ni mburu mu Yàlla may àddina si. Ba Muy def kéemaanu bareel mburu ma, mburu ma jeexuloon. Ci noonu itam, Yeesu doy na ngir faj soxla ñépp saa su nekk, ndaxte ci Moom la mataayu Yàlla dëkk. Ci Moom lanuy jote yaakaar ji, mbég mi, ak barkee yi. Ci kàddoom la maye àddina si dundu Yàlla, te àddina si nanguwu Ko (teralu Ko).

Mànn ji, mayug Yàlla la woon; dafa yemoon ci ab diir. Ña ca lekkoon ñépp teewul ñu dee. Noonu la itam ci mbiri ndimbal yi, yokk xarala yi, ak peñeelu mbóoti xam-xam yi. Amul pexe ngir moytu dee, wala ngir daan bàkkaar. Waaye, képp ku nangu Kirist doo dee. Li Kirist bëgg mooy ñëw dëkk ci yeen. Dafa bëgga dëkk ci yaw, suko defee benn ngëm du la mëna noot. Mën nala xettali ci say bëgg-bëgg yu bon yépp, dakkal sa tiitaange, gëna dooleel say néew doole. Mooy mburu mi leen Yàlla bëgg. Lekkleen te dund, ngir bañ a sànku ni yeneen bàkkaarkat yi.

LAAJ:

  1. Nu Yeesu dékkoo ñurumtu ña Ko doon déglu?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 04, 2025, at 11:09 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)