Previous Lesson -- Next Lesson
a) Yeesu fexe na ba njaalookat ba tuub (Yowaana 4:1-26)
YOWAANA 4:16-24
16 Yeesu ne ko: »Demal woowi sa jëkkër te ñów. » 17 Jigéen ja tontu Ko ne: » Awma jëkkër. » Yeesu ne ko: » Wax nga dëgg ne amuloo jëkkër, 18 ndaxte amoon nga juróomi jëkkër, te ki nga nekkal léegi du sa jëkkër. Li nga wax dëgg la. » 19 Jiggéen ja ne Ko: » Sang bi, gis naa ne ab Yonent nga. 20 Nun nag naka - jekk sunuy maam, ca tund wee ngay séen lañu daan jaamoo Yàlla, waaye yéen Yawut yi, dangeen ne Yerusalem lañu war a jaamoo Yàlla. » 21 Yeesu ne ko: » Jigéen ji gëmal li ma lay wax: dina am Jamono joo xam ne du ci tund wale, te du Yerusalem ngeen di jaamoo Baay bi. 22 Yeen waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi xam nanu li nuy jaamu, ndate Kiy musal àddina, ci Yawut yi la jóge. 23 Waaye jamono dina ñów, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baagiy bi ni Mu ko bëgge. 24 Yàlla xel la, kon ñi Koy jaamu, war nañu Ko jaamu ci xel ak ci dëgg. »
Gannaaw ba Mu xiiree jigéen ja ci mar ndoxum dund gi te bëgg a jot ci mayug Yàlla gi, Yeesu won ko li ko doon xañ may googu, maanaam bàkkaaram. Jiiñu ko njaalookat, waaye dafa ne ko rekk ci njekk, na woowi jëkkëram. Wax jooju am lu mu yëngal ci xolu jigéen ji. Ni bépp jigéen, bëggoon naa am jëkkërju ko uuf te di ko aar. Waaye ku wéeet lawoon teg ci ñu bañ ko, moo tax bëgguloon Yeesu xam gàcceem googu. Looloo waral mu ne Yeesu, amul jëkkër.
Yeesu nangu li mu wax, ndaxte Moom xam na lépp lu nëbbu. Xamoon na ne jigéen ji dafa wéet, te di yaakaar a am bëggeel gu dëggu ci bànneexu yaram ya mu daan wéy di bàkkaare.
Bépp njaaloo àddina su tukki la suy wàññi xel, te di nasaxal yëgeelu biir, rawatina ci jigéen ñi. Sa yu séy tasee, jigéen ji dafay am yaakkaar ne jëkkër ja dina ko baal te delloo buum ga.
Jigéenu Samari ja mujj xam ne Yeesu du nitu neen; ab Yonent la. Xamoon na ci biir xolam ne Yàlla rekk moo ko man a xettali. Waaye fan la koy fekk? Ak naka? Ñaan yeek ngér yi safatuñu ko dara. Toog na ay at te demul ca jàngu ba, moone de ku soxlawoon yeweeku la, ba génn ci li mu nekke, te am jàmm ak Yàlla.
Bi ko Yeesu xiiree ci namm sellaay ba noppi, Mu xamal ko ne du bérab bi ñuy jaamoo moo am solo, waaye Ki ñuy jaamu. Mu biral ne Yàlla mooy Baay bi ci asamaan. Mu xamal ko mucc giy jaare ci xam Yàlla. Mu jëfandikoo ñetti yoon baatu ‘Baay bi’. Du xel mu màcc, walla man a jaamu mooy tax a xam Yàlla, waaye gëm Yeesu kese moo koy maye.
Yeesu xamal ko ne du yàlla yépp ñoo yelloo turu ‘Baay’. Waa Samari dañu daan faral di jaamu ay yàlla yu bare. Fekk Yawut yi xamoon nañu kan mooy Aji Sax, ji feeñuwoon ciy jamono, te digewoon ñówug ab Musalkat buy jóge ci geñog Daawuda.
Diine Biibal dafa siiw léegi ci àddina si, ndaxte ni ñuy jaamoo Yàlla dañu koo goreel ak Néegu Yàlla bu wuute. Way-gëm yi ñooy léegi néegu Yàlla bi, Xel mu Sell mi ci ñoom la dëkk léegi; seen dund, màggalukaayu ndamul Yàlla la. Mucc gi leen Yeesu maysi mooy seen mandarga léegi, te dugg nañu ci mbëggeelam gu rëy gi. Dañoo tànn a am dund gu jub, gore, te sell ci Kàttanam. Seen Baay bi ci asamaan yeesal na leen. Seen màggal yu dëggu yi fees nañu aky sargal. Yàlla Baay bi dafay bég bu ko ay doomam di jébbal ay cant yu jollee ci seen xol, ak ngërëm ak jaamu Yàlla ni "Sunu Baay bi ci kaw."
Yàlla Xel la, du tuur, walla njuuma. Mooy sunu Baay te xam nanu Xelam. Moom it Xam na sunuy ñàkk man-man, ak sunu ñàkk man Koo jege. Noonu Mu ñów ci nun ci melokaanu Doomam ji, sellal nu ak saraxam bi, te yónnee nu Xelam mi. Yàlla dafa bëgg a am ay doom yu baree-bare; Doomam yi rekk ñoo Ko man a màggal ci xel ak ci dëgg. Nungi ñaan Baay bi Mu sol nu, ba nu fees Xelum dëggam gi, ak Yiwam gi, ngir sunu dund gi nekk luy seede mbëggeelam.
Ndegam kenn manul a màggal Yàlla ni mu ware, Yeesu may nu Xel mi. Ci Moom, danuy nekk ay ñaanalekat yu gore, ay surga yu ànd ak mbég, ak ay seede yu ñeme. Sunu dund dina nekk kon màggalu sunu Baay jiy mbëggeel ci kàttanu Xel miy rogaat ci kurwaawu Krist.
Krist dafa sellal Kër-Yàlla ga, samp fa màggal gu bees -peeq. Baay bi feeñu na jiggéenu njaalookat jooju, jaare ko ci Krist. Na mu nangoo bàkkaaram te wone maru ndoxum dund, la jote yiw wi.
ÑAAN: Sunu Baay bi ci asamaan, dangaa bëgg nu lay teral ak sunu xol bépp, te nuy sell ci sunu y doxalin, di màggal sa yiw. Sellalal sunu màggal. Defal ba nu nekk ay surga yuy déggal sa Doom ji, te di la màggal. Sol nu Xelum ñaan, te dimbali nu ba nuy déggal sa Kàddugiy walangaan ci Injiil li.
LAAJ:
- Lan mooy indi gàllankoor ci màggal gu dëggu, te nan lañu man a matale màggal gu mat?
YOWAANA 4:25-26
25 Jigéen ja ne Ko: » Xam naa ne Almasi bi-maanaam Krist-dina ñów, te bu ñówee, dinanu leeralal lépp. 26 Yeesu ne ko: » Maa di Almasi bi man miy wax ak yów. »
Jigéen ji yëg kàttan ak dëggu Kàdduy mbëggeelu Yeesu yi. Bëggoon naa gis ni dige yi Mu ko def di sottee. Mu fàttaliku waxu yonent bi ne ñówug Krist jegesi na. Mu teg yaakaaram yépp ci Moom, yaakaar ne Moom rekk moo ko man a jàngal ni ñuy màggale Yàlla dëgg.
Doy na waar li Yeesu wonewul boppam ak leeraay gu sete nii, ci xew-xew yu ni mel, yu jiitu bii. Xamal na ko ne mooy Ki ñu digewoon, Ki Yàlla yónni, Ki fees ak Xel mu Sell mi. » Man ci sama bopp maay Ki Yàlla may nit ki, di Kàddug Yàlla gi jëmmu, ak mucc gi ñu waajal ñépp.»
Jigéen ji umpalewoon na ne Almasi dafa ëmbaale Buuru buur yi, Kilifa Yonent yi, ak Saraxalekat bi. Man na am mu déggoon ne ñówam am na lu mu bokk ak ndekkite li, a kit yaatalug jàmm ji ci kow suuf. Xëyna déggoon na Yawut ya daan séentoo tur woowu ci seeni mbiri politik. Waaye moom jigéen ji, ab Musalkat la doon wut, bu ko manoon a goreel ci ay bàkkaaram, te yaakaaroon na ne Yeesu manoo na ko koo defal.
Yeesu ne ko: »Man la, Man miy wax ak yów. » Li asamaan namm ak li Yonent ya digewoon, lépp mungi làqu ci baatu ‘Man la’. Amul kenn ku manoon a biral ne mooy Almasi bi, ci anam yu leere nii. Moone, Bañaale Krist bi dina jéngu, ba fen jibal kàddu gu ni mel jëmale ci boppam. Waaye Krist mooy mbëggeel gi ñu jëmmal gi dul xebat benn bàkkaarkat bu tey-teyluwul. Yërëm na sax jenn jigéenu Samari. Dafa ñów ni boroom yërmaande ji, waaye du ni ab àttekat.