Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 024 (The cross)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 1 - Leeraayu Leeru Asamaan (Yowaana 1:1/4:54)
C - Ba Yeesu njëkkee ñów Yerusalem (Yowaana 2:13 - 4:54) -- Ci dëgg-dëgg, lan mooy màggal?
2. Yeesu mungi wax ak Nikodeme (Yowaana 2:23 – 3:21)

c) Kurwaa bi (bant bi), ab juumtukaayu juddu gu bees gi (Yowaana 3:14–16)


YOWAANA 3:14-16
14 Te itam, na Musaa sampewoon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defarewoon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki, 15 ngir képp ku Ko gëm ame ci Moom dund gu dul jeex. 16 Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji Mu am kepp, ngir képp ku Ko gëm am dund gu dul jeex, te doo sànku mukk.

Yeesu wéy di jàngal Nikodem, te di ko wonaale ne juddug baatin du man a mat su rëccu bàkkaar gu dëggu, gu ànd ak wëlbétum xel, teg ci ngëmug deewu Yeesu gi wuutu nit ñi. Tegtal yooyu, Yeesu faramfàcceel na leen Nikodem jaare ko ci ab xew-xewu cosaanu Israyel.

Ña teewoon ca màndingu Sinai ma, ñurumtu jëmale ci Yàlla, te fippu ay tegtalam (Lim 21 :4-9). Ngir yer leen ci seen dëgër bopp googu, Yàlla indil leen ay jaan yu am daŋar ju tàng jër ngir ñu màtt leen, noonu ñu bare ca bànni Israyel ya dee.

Mu am ñeneen ca ñoom nag ñu ràññee seen bàkkaar, te saraxu Musaa ngir mu ñaan Yàlla, mu dàq jaan yi. Yàlla sant Musaa mu defar jaanu xànjar, jiy misaal àtteb Yàlla. Musaa lonk ko ci ab bant te samp ko fa ko askan wépp di séene; muy misaal ne merum Yàlla giif na. Képp koo xam ne xoloon nga màndarga moomu doon wone giifaayu merum Yàlla mi, te gëm yiwu Yàlla wi, dangay wér ci dangaru dee jooju.

La ko dale ca nattu Awa ja la jaan nekk misaalu lu bon li. Bi Yeesu ñówee, dafa gàddu bàkkaaru doomu Aadama. Ci noonu la Ki mosul a am bàkkaar, nekke bàkkaar ngir nun. Yeesu dafa mel ni jaanu xànjar, ji amul daŋar, dafa set wecc ci bàkkaar, ba noppi yenu sunu bàkkaar.

Doomu Yàlla ji dikkul ci àddina si ak melo mu yaanj, waaye ak suufeelu ni Doomu nit, ki daj ay ngaañ aky coono, te di dékku móoluy Ndigal yi (Santaane yi). Dee na ngir nun, ci jëmmu nit « Doomu nit ki « màndarga bu ñu Ko beral la Na jaan ja, ñu lonkoon ca bant ba, doon misaale giifaayu merum Yàlla ja noona la Krist ma ñu daajoon ca bant ba nekke misaalu giifaayu merum Asamaan, maanaam merum Yàlla. Sunu bàkkaar yépp, Doomam ji lañu leen yen, ngir goreel nu jaare ko ci njébbalu boppam gi.

Ku jaan ya màttoon te nga xool ca jaanu xànjar ja te gëm digeb Yàlla ba, dangay wér-péŋŋ. Wóolu misaalu yiw woowu moo doon may nit ña gëmoon, bakkan (dund), ak mucc. Képp ku xool kurwaa bi, te jàpp ci Ki ñu ci daaj, dinga am dund gu dul jeex ba fàww. Póol bind na ne: »Daajaale nañu ma ak Krist, ca bant ba te noonu du man maay dundati, waaye Krist mooy dund ci man. » (Galasi 2 :20) Deewam mooy sama dee, ni dundam nekkee sama dund itam. Képp ku nangu dee gi ko Krist wuutoo, àtte nañu la ni ku jub, te yaangi dund ak Moom ba fàww. Jokkoo googu may na la nga dekkindoo ak Moom.

Nun ñi àtteb mbugal dal ba noppi, xool ci Yeesu dafa nuy musal. Dafay sàkk ci nun juddu gu bees. Amul weneen yoon wuy dem ca Yàlla, wu dul wi jaare ci Ki ñu daajoon ca bant ba(Krist). Looloo tax Seytaane xarañ ci xeex ñaari ponki mucc gi: Doomoo Yàlla ji ak daajug Krist ca bant ba. Waaye muccug àddina si, ci ñaari mbir yooyu la tegu.

Yàlla, mbëggeel la. Mbëggeelam dafa mel ni géej gi amul fu mu yem. Mbëggeelam a tax bàyyiwul sunu àddina ju tubbi sii, waaye mungi wéy ci di nu bëgg. Du dàq bàkkaarkat yiy fippu, waaye dafa leen a yërëm. Saraxu Doomam ji matal na lépp li njubteg seen muuc laaj. Ci Doom ji doŋŋ la mucc man a ame.

Mbokk mi, ndax jekk nga ngir ber as tuut ci sa nafa, ngir jagleel ko sa muccug xarit? Ndax bu ñu ko naree tëj kaso, dinga ko nagoo wuutu? Walla sax nga mangoo dee ngir moom? Xanaa xëyna soo ko bëggee lool. Waaye bu fekkee ne ab noon la, dina ma jaaxal lool. Loolu mooy wone rëyaayu mbëggeelu Yàlla, mi saraxe doomam ngir musal ay bóomkat.

Krist matal na muccug àddina sépp ca kurwaa ba. Nun ñépp a soxla saraxam bi; muy ñi am njàng, walla déet, ku yeru ak ku yeradiku, boroom alal ak ku ndóol, ki rafet jikko ak ki ko ñaawle. Amul kenn ku jub.Krist dafa juboole àddina si ak Baayam. Doy na waar li nit ñi manul a xam dëgg gii, ba mu des ñi gëm te àndak Ki ñu daajoon. Kóllëre gi nga séq ak Musalkat bi mooy dogal sa mucc.

Say jëf, ni yu jubadi te bon lañu leen jàppe bu nu leen taajee ci leeraayu sellayu Yàlla. Nikodem, Kilifa diine bu mag bi te jub, dëglu na kàddu yooyu, ko waroon a naqari sax.

Képp ku nangu muccug bant ba, jaare ko ci gëm Doom ji ñu yékkati ca kow bantu gàcce ba, dinga dund, te doo am gàllankoor ci sa diggante ak Yàlla. Ndax sant nga Yàlla ngir mbaalam gi? Ndax jébbal nga sa dund gi ci jaamu Ko?

Képp ku gëm, dund; te ku sax ci Krist doo dee (sànku) mukk. Ku teggiwul ay bëtam ci Krist, dinga jot yaakaaru dund gu amul àpp gi. Ngëm gi moo nuy biral teewaayu Xel mu sell mi ci sunu dundu bopp. Soo gisee xóotaayu li aaya 14 ba 16 dinga xam xolu Injiil li, jaare ko ci menn xëtu téere rekk.

ÑAAN: Sunu Baay bi ci kow asamaan, nungi lay màggal ngir sa mbëggeel gu amul àpp gi. Maye nga sa Doom ji nga am kepp, ngir Mu wuutu nu ci dee. Dindi nga sunuy bàkkaar ak sunu mbugal, te goreel nu ci sa mer. Nungi xool ci kurwaa bi, ak kóolute, màggal, ak cant. Baal nga sunuy bàkkaar, te jokkalewaat àddina sépp ak Yów ci sa bopp, dimbali nu ba nu man a séddoo Kàddu gii ak ñeneen, ndax ñu man a jot dund gu dul jeex, jaare ko ci sunu seede.

LAAJ:

  1. Nan la Yeesu niroowee ak jaan u xànjar ja?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on June 18, 2025, at 02:14 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)