Previous Lesson -- Next Lesson
3. Juróom-benni taalibe yu jëkk yi (Yowaana 1:35-51)
YOWAANA 1:40-42
40 Kenn ca ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax, te topp Yeesu, Andare la tuddoon, te bokk ak Simoŋ Pieer ndey ak baay. 41 Andare dafa dem seeti Pieer, ne ko: ”Gis nanu Almasi bi.” Baat boobu mungi tekki “Krist.” 42 Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu, Yeesu xool ko ne ko: ”Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.” Sefas mungi tekki “Pieer”, maanaam “xeer.”
Andare miy magu Pieer, nappkat lawoon bu dëkkoon Betsaida ca wetu déegu Tiberiad. Dafa ñówoon ca Yaxya ngir jot mbaalug bàkkaaram, te xaaraale ñówug Almasi bi. Andare nanguwoon na seedeb Yaxya, te topp na Yeesu. Xolam bégoon na lool, ba manatuloon a denc li mu gis, ngir moom kese, noonu mu daw waxi ko rakk ja, waaye waxu ko benn doxandéem. Nii la ko yegge xabaar bu baax bi: ”Gis nanu Almasi, bi ñu digewoon, Boroom bi ak Musalkat bi, Mbotem Yàlla mi.” Man na am ne Pieer amoon na xel ñaar. Waaye Andare yey ko. Mujj gi, Pieer nangu ànd ak moom ca Yeesu, boole ca am njaxasoo xel tuuti.
Ba Pieer duggee ca kër ga, Yeesu dafa ko woo, jaar ci turam. Te dafa xamoon itam li muy xalaat. Noonu Mu dippi turam, tudde ko “Pieer” Yeesu xamoon na démbu Pieer, teyam, ak ëllëgam, rax ci itam xadaram.Yeesu xam na xol yu ubbeeku yi.Pieer daldi xam ,ci saa si mu nangu xoolinu Boroom bi.Yeesu daldi tàmbali soppi ndank-ndank bii nappkat bu xarañ bi,ba mu nekk doj wu dëgër. Ci Krist la jaare ngir nekk ab fondamaŋ ci jàngu bi. Man nanu wax ne Andare ab taalibe buy xàll yoon la.
Am na itam beneen taalibe bu nekkoon ab juumtukaay ngir doomu ndeyam: Yowaana wonale na magam Saag ak Yeesu, ak li muy nëbb ñaari tur yépp ci Injiilam; ab mandarga suufeelu la. Ci dëgg Andare ak Yowaana ñooy taalibe yi njëkk a daje ak Yeesu.
Taaru aaya ubbite gi ñungi nekk ci ni ñu koy méngalee ak jant buy fenk-fajaru jamono ju bees. Yooyu way-gëm iñaanuñuwoon, dañoo yóbbu seeni doomi ndey ca Krist. Ca jamono jooja daanuñu wër ci mbedd yi ngir woo nit ñi ci Krist, waaye dañu daan def seen kéem-kàttan ngir wonale seeni mbokk ak Krist. Daanuñu topp ñiy am xel ñaar, walla politikkat yi, waaye dañu daan wut ñi xiif Yàlla, boroom xol yu jeex yi te namm a tuub seeni tooñ.
Noonu lanu jànge nan lanuy jottalee xabaru yiw bu baax bi; du ak xadar, waaye ak mbég mu jóge ci sunu jokkoo ak Yeesu. Taalibe yu njëkk yooyu demuñuwoon ci ay daaray kaamil yu kowe, te binduñuwoon seeni seedeb dund, waaye dañu doon seede lañu dundoon. Gisoon nañu Yeesu, te déggoon li Mu wax, laaloon nañu ay laxoom, te wóolu Ko. Jokkoo gu xóot googu moo waraloon ñu am sañ-sañ boobu. Ndax daje nga ak Yeesu bi nga xamee Injiil? Ndax indi nga say xarit ci Krist ci biir lewetaay ak kóolute?
ÑAAN: Boroom bi Yeesu nungi lay gërëm ci sunu mbégte xol. May nu lewetaay bu nu man a indee ñeneen ci Yów. Saxalal ci nun mbëggeelu tas Xabaar bu baax bi. Baal nu sunu ragal gi, ak bari kersa gi, ngir nu man a seede ci sa tur ak njàmbaar.
LAAJ:
- Nan la taalibe yu njëkk ya siiwale turu Yeesu?