Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 073 (The raising of Lazarus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
4. Ndekkite Lasaar ak la mu jur (Yowaana 10:40 – 11:54)

c) Ndekkite Lasaar (Yowaana 11:34-44)


YOWAANA 11:34-35
34 Mu ne leen: « Fu ngeen ko denc? » Ñu tontu ko ne: « Kaay gis, Sang bi. » 35 Yeesu jooy.

Yeesu tontuwul dara. Yenn saa yi jarul ngay indi wax ju bare ak ku am yenn metit yu tar yi. Bu nu tolloo ci diggante yu mel noonu; jëf rekk mooy ëpp solo wax. Mu ñaan ña fa teewoon, ñu won Ko bàmmeel ba. Ñu ne Ko: « Kaay te gis. » Baat yooyu sax la Yeesu jëfandikoo woon ba Muy woo taalibeem ya, ba muy tàmbali liggéeyam. Dafa leen a woo ngir ñu gis dund gi; ñii nag dañu koy woo ngir Mu gis dee gi. Dafa jooy ndax ni mu gise ne noonu la nit ñi yéexe ràññee seen ñàkk-xam, ak seen ñàkk-ngëm. Taalibeem bi gënoon a dogu sax, manuloon a wone ngëm lu wér. Yaram du jur dara, te ngëmu ruu doyul. Yónneeguñu woon leen Xel mu Sell mi. Deewug xel moo doon nguuru, te Doomu Yàlla ji, manuloon def lu dul jooy ndax nekkinu walaakaana nit ki.

Yeesu nit lawoon Kuy bégandoo ak ñiy bége, di jooyandoo ak ñiy jooy. Yaramam dafa daw. Ruuwam gu bare yëgeel gi dafa yëngu woon lool ba Mu gisee ragal dee gi jàppoon taalibeem ya, ak seen ñàkk a bëgg Yàlla jiy dund ji. Yeesoo ngi jooy ba tey jii, ndax ni sunu jàngu yi mel, ak it nun ci sunu bopp, ak ñépp ñiy wéy ci bàkkaar, ak deewu xel.

YOWAANA 11:36-38a
36 Noonu nag, Yawut ya ne: « Gis ngeen ni Mu ko bëgge woon! » 37 Waaye am na ca ñoom ñu doon wax naan: « Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax manuloon a fexe ba Lasaar du dee? » 38 Yeesu dellu am naqar gu réy…

Yawut yi gis nañu rangooñu Yeesu te ne mbëggeelam ci Lasaar moo ko waral. Mbëggeel du lu yomb te lalu ci xel, waaye mingi méngoo ak yëg-yëgu ñeneen ñi. Mbëggeelu Krist dafa romb sunu dégg-dégg te weesu dee gi. Mu gis Lasaar ci biir bàmmeel bi, ñu ub ko, rekk Mu jooy, ndaxte dee gi amoon na ndam ci xaritam bi. Waaye xolam bi foq xeer ya, te jekkal néew ba ngir mu dégg wooteem.

Am na ca ña teewoon foofa ñu doon ŋàññ Yeesu ndax xadar ga Mu amoon, te demoon nañu sax bay xel ñaar ci sañ-sañam; loolu merloo Yeesu lool. Ñàkk ngëm, mbëggeel ak yaakaar dafay indi merum Yàlla. Yeesu dafa tànnal boppam yewwi nu ci lëndëm gi, te musal nu ci sunu ëllëg gu leerul gi, ndx nu man a taq ci mbëggeelam gi, dunde gëm KO te yëg kaaraange ci yaakaar gi nu am ci Moom. Dootunu daanooti ci xalaati ni nit ñi di gise ak di doxale àddina, waaye danu koy wóolu. Dafa bëgg a dekkil ñi dee ci bàkkaar. Ndax sa ñàkk ngëm gi tiis na xolu Yeesu, walla mungi bég ci sa mbëggeel gu dëggër gi?

ÑAAN: Baal ma Boroom bi Yeesu, ngir saa yi ma ñàkkee kóolute, ak mbëggeel. Baal ma sama ñàkk ngëm, ak sama bewu. Xiir ma ci yaakaar yuy dund ndax ma teral la te sax ci Yów, saa su nekk.

LAAJ:

  1. Lu xelu Yeesu tiis,te lu tax Mu jooy?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 23, 2025, at 05:25 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)