Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 072 (Jesus meets Martha and Mary)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
4. Ndekkite Lasaar ak la mu jur (Yowaana 10:40 – 11:54)

b) Yeesu daje na ak Màrt ak Maryaama (Yowaana 11:17-33)


YOWAANA 11:17-19
17 Bi Yeesu agsee, mu fekk ne, bi ñu dencee Lasaar ak léegi, mat na ñeenti fan. 18 Betani munga woon ca wetu Yerusalem, diggante bi matuloon sax ñetti kilomet. Yawut yu bare ñówoon nañu kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfal leen ci seen deewu càmmiñ.

Ñeenti fan jàll nañu diggante bi Lasaar deewee ak léegi. Bés ba ñu yégalee Yeesu ne Lasaar dafa wopp, fekkoon na, Lasaar dee ba noppi. Kon jaruloon Yeesu di yakamti dem fa. Dee gi leeroon na nàññ.

Betani, 3 km digganteem ak Yerusalem, ca kow tuddu oliw ya la nekk, jàkkaarloo ak deux Yurdan, gi tollu ci 1000meetar ci suuf. Fa gën a sore, la géej gu dee ga nekk.

Xariti ndem ci Yàlla ji, yu bare ñówoon nañu ci dëj bi, di jooy, di fëgg seen dënn. Dëj bi, lu waroon la, ndaxte Lasaar moo doon jàppale njaboot gi. Ngelawal (keru) dee gi mungi doon lëndëmal ndaje bi.

YOWAANA 11:20-24
20 Bi Yeesu ñówee, Màrt yég ko, dem di dajeek Moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga. 21 Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee. 22 Waaye xam naa ne, fii nu tollusax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko. » 23 Yeesu ne ko: « Sa càmmiñ dina dekki. » 24 Màrt tontu Ko ne: « Xam naa ne dina jóg bésub ndekkite la, keroog bés bu mujj ba. »

Bi Màrt déggee ne Yeesu ñów na rekk mu daw wutali Ko, aky jooyi metitlu, di xalaat ne bu teeloon a ñów, kon moom Màrt du am naqar gii. Màrt wone na ni mu gëme ne Yeesu am na Kàttan gu amul àpp. Xaarul dara ngir wone naqaram, waaye wax na kóoluteem ne Yeesu am na kàttan ci kow dee gi. Xamulooon nan la, waaye gëmoon na sañ-sañam ci lépp, ak jokkoom ak Yàlla, miy nangu saa su nekk ñaanu Doomam ji.

Yeesu daldi tontu ngëmu Màrt, boole ci ab dige bu am doole: « Sa càmmiñ dina dekki». Ndaw si xamuloon ci dëgg-dëgg li Yeesu di wax, waaye dafa ko jàppe woon ni ab dige texe. Noonu Mu am yaakaar, te xam ne du dee moo mujj. Ñi gëm dañuy xaar ndekkite.

YOWAANA 11:25-27
25 Yeesu ne ko: « Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deewee it, dinga dund. 26 Rax-ci-dolli kuy dund te gëm ma, do dee mukk. Ndax gëm nga loolu? » 27 Mu tontu Ko ne: « Waaw Boroom bi. Gëm naa ne,yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji war a ñów ci àddina. »

Ci kanamu taalibe yi, Yeesu ne Màrt: « Ndekkite li dina ñów, ci lu wóor, mungi ci man. Lasaar du dekki ca bésub ndekkite la, waaye tey jii lay dekki jaare ko ci sama teewaay. Man Aji Sàkk ji, jox naa leen Xel mu Sell mi. Dinaa leen wuutu ci dee gi, ngir dindi seeni bàkkaar, te may leen dundu asamaan. Dee gi dootu leen manal dara. Du yàgg dara ma may leen ndekkite gu jóge ci man. Dinañu leen suul, ngeen dekkeendoo ak man ci seen ngëm. Yeenay sama dee ak sama dund. Maangi dund, te yéen a ngi dund ci Man.

Lenn rekk moo man a tax nit jot ci dundu Yeesu, te mooy jokkoo ak Moom ci kóllëre gu jaare ci ngëm. Wali dundam dunñu jóge ci Moom, dal ci nun, te fekk lëkkoowunu ak Moom. Gëm Yeesu mooy yaatal ni nuy xame Baay bi, ak dund gu amul àpp gi. Mbëggeelam gu dul jeex gi moo nuy feesal ak mbég, jàmm ak mbëggeel. Nit ku fees ak mbëggeelu Krist, du dee mukk, ndaxte Xelum Yàlla dafay dund ba fàww. Xel moomu moo dëkk ci xolu ñi gëm Yeesu.

Yeesu taxawul ca diggu mbooloo ma di yéene ndamam ci kow dee gi, ba Mu dekkalee Lasaar. Dig ña doon dunde ci Xelam mi, ne dee gi du amati benn sañ-sañ ci ñoom, ndaxte bokk nañu ci ndekkiteem. Ndax gis nga dige bu am doole boobu, te laajul dara? Boo Ko gëmee, doo dee mukk. Bul xalaat sa dee, walla sa bàmmeel; walbatil say bët, xool Yeesu. Sant Ko ci dogoom googu, ndaxte mungi nuy jekkal ab bérab ci dund gu dul jeex gi.

Yów sama mbokk mi, ndax gëm nga Yeesu, miy maye dund gi? Ndax Krist yewwi na la ci sañ-sañu dee gi, ak ci geru bàkkaar gi? Bu fekkee ne mosaguloo ndekkiteelu xel, nungi lay xamal ne Boroom bi mungi lay tàllal loxo. Gëmal mbëggeelam ak sañ-sañam. Nangul loxoom bi, noonu dina la baal say bàkkaar, te yóbbu la ci biir dund gu dul jeex gi. Moom rekk mooy sa Musalkat.

Màrt dafa nangu digu Krist bi. Du rekk ne mos na dund gu dul jeex gi, waaye it boole na ci mos Kiy maye dund gi. Gëmoon na ne Yeesu mooy Almasi bi ñu dege woon, te Mu am sañ-sañu dekkal ñi dee. Am na sañ-sañu àtte nit ñi ca Àtte bu mujj ba. Moom ci boppam mos na kàttanam gi ko yee te sellal ko. Màrt amoon na fitu seede ngëmam, ba ñuy dem ca yoon wa, ak la mu xamoon lépp ne Yawut ya ñunga doon fexe sànni Yeesu ay xeer, ba Mu dee, Moom mi ne woon mooy Doomu Yàlla. Màrt ragaluloon dee gi waaye dafa bëggoon Musulkat bi: Jiggéen ju njàmbaaram rusloo góor ñi. Kóoluteem dafa doon gën a yokk, rawatina mbëggeelam itam.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu sa màggaay amul àpp. Dee gi manalula dara. Yaa nu wuutu ci dee gi, te Yaa nu dekkil jaare ko ci sa ndekkite. Nungi lay màggal te di la sant. Séddoo nga sa dund ak nun, ndax dee gi bañ a am benn sañ-sañ ci nun. Bëgg nanu la te nungi lay sant ci li nga nu goreel ci tooñ, ragal ak dee gi.

LAAJ:

  1. Tey jii nan lanuy dekkee ci biir ñi dee?

YOWAANA 11:28-31
28 Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem woowi Maryaama, déey ko ne: « Kilifa gaa ngi fi mungi lay laaj. » 29 Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi gaawantoo dem ca Yeesu. 30 Te fekk duggaguloon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba Mu daje woon ak Màrt. 31 Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfal Maryaama, gis ko mu ne bëret génn, ñu daldi koy topp, defe ne dafay jooyi ca bàmmeel ba.

Xéy-na Yeesu moo yebal Màrt ngir mu woowi Maryaama, ngir Mu man koo dëfal fu sore yuuxu jooykat ya, te yokkal ko ngëmam ci kow mbëggeelam. Yeesu ci dëgëraayu ngëm lay nguuroo, waaye du ci ñàkk-yaakaar, walla ay jooy. Dafa bëggoon a dugal Maryaama ci leeraayu teewaayu Yàlla, ngir mu dund te di yëngu ci baatin.

Maryaama déggaguloon ne Yeesu ñów na. Ba ko ko Màrt waxee, dafa ne bëret daw dajeji ak Boroom bi. Yàkkamteem googu jaaxal ña fa teewoon te doon xalaat sax ne xéy-na ca bàmmeel ba lay dem. Ñu jóg toppi ko, muy misaalu dundu doom-Aadama, jiy waaxu jëm ci sànku, ndóol ak lëndëm di ko mëdd. Fi joŋante xam-xam ak diine tëlee saafara jafe-jafe dund gi, walla dee gi, ci biir dee gi, dëggu yaakaaru kercen bi, ak dëfalam leer nañu fa nàññ.

YOWAANA 11:32-33
32 Bi Maryaama agse nag ca Yeesu, ba gis Ko, mu daanu ciy tànkam ne Ko: « Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee. » 33 Yeesu gis ne mungi jooy, te Yawut yi ànd ak moom itam ñungi jooy. Mu daldi jàq, (yaramam daw) Mu amnaqar wu réy.

Maryaama gis Yeesu, yaramam daw, mu daanu ca tànki Yeesu ak xol bu jeex tàkk. Mu daldi seede ne manoon na def ay kéemaan. Kon su fi nekkoon, càmmiñam bi du dee. Waa kër gi yépp gëmoon nañu ne Yalla dafa teewoon ci Yeesu. Waaye bii yoon, dee gi yëngaloon na ngëm googu, te jaaxal jiggéenu Lasaar ya.

Ba Yeesu gisee ngëmu taalibeem ya nekk ci njàqare teg ca ñàkk-xamu mbooloo ma, Mu jaxasoo lool. Mu gis ne ñoom ñépp dee gi daf leen a noot. Mu tiis ci mu gis ndaw si di jooy te xamne àddina si mungi ci nootaage Seytaane. Mu yégaat diisaayu bàkkaari àddina si, ciy mbaggam; Xel mi Mu gisaat njariñal Kurwaa bi ak bàmmeel bu ubbeeku bi ni benn jumtukaay doŋŋ, bi war a daan metit bu ni tollu. Xamoon na bu leer ne ndekkite li nar a am. Mooy àtte bu mujj ci dee, ñàkk a gëm ak toroxte.

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 23, 2025, at 05:19 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)