Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 074 (The raising of Lazarus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
4. Ndekkite Lasaar ak la mu jur (Yowaana 10:40 – 11:54)

c) Ndekkite Lasaar (Yowaana 11:34-44)


YOWAANA 11:38-40
38 Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Am xunt la woon, te dñu ko daan ube ak aw doj. 39 Yeesu ne: ” Dindileen doj wi!” Màrt, jigéenu ku dee ki ne Ko: ” Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.” 40 Yeesu ne ko: ” Ndax waxuma la ne, boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?”

Ca diiwaanu Yerusalem, nit ña dañu daan deñc seeni néew ci pax yu ñu gas ci ay doj, ba noppi ube ko xeer bu rëy bu wërgalu. Manoon nanu randal xeer ba ngir ubbi bàmmeel bi.

Ci xunt yu mel noonu lañu deñcoon Lasaar. Yeesu daldi jegesi te gis ni tiitaange dee gi feeñe ci xar-kanamu ñépp. Ci biir dee gi, gis na ci mer mi Yàlla jëmale ci bàkkaarkat yépp, mu mel ni Yàlla dafa bërgal ñiy dund ci loxoy yàqkat bi. Waaye Yàlla bëggul deewug ñiy dund; seen tuub te jébbalu ci dund gi la bëgg.

Yeesu sant leen ñu randal doj wa uboon bàmmeel ba. Xolu nit ña di bëgg a xëtt, ndaxte boo laalee ab néew, dangay ànd ak sobe ay fani-fan. Néew ba tàmbale woon naa nëb, gannaaw ñeenti fan. Màrt jéllale wax ji, naan: « Sang bi, kenn warul a lëjal noflaayu ku dee, xasaw na léegi. » Màrt, ana sa ngëm? sànq rekk yaangi doon seede ne Yeesu mooy Doomu Yàlla ak Almasi bi, te am na sañ-sañu dekkal ñi dee. Dee gi ak bàmmeel bi ñoo gëlëmaloon ay bëtam, te xamuloon li Sangam bi bëggoon.

Waaye terewul Mu dëgëral ngëmam te ñaax kóoluteem ngir mu weesu bu nit ñi. Dafa bëggoon ñu gëm lépp lu yelloo ñu gis ndamu Yàlla. Yeesu newul: « Gëm ma, noonu dinga gis ma def kéemaan gu rëy. »Waxoon na taalibeem ya ne woppu Lasaar gi du ko yóbbe dee, waaye ngir ndamu Yàlla la (Yowaana 11 :4) Yeesu xamoon na li Mu war a def, bu ñu ko wéeree ci jokkoo gi Mu am ak Baayam ji.

Noonu itam , Krist mungi lay wax ne: « Boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla. »Bàyyil di sëgg ci say jafe-jafe ak say nattu. Bu say tooñ walla say wopp ub sa bopp, waaye xoolal ci Yeesu, te gëm teewaayam. Uuful ciy loxoom ni gune gu nekk ci loxoy ndeyam. Bàyyi Ko mu def coobareem; Ku la bëgg la.

YOWAANA 11:41-42
41 Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kow, ne jàkk asamaan ñaan Yàlla ne: « Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi. 42 Xam naa ne doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax ngir nit ñi ma wër gëm ne, yaa ma yónni. »

Kóolute gi Màrt am ci kàdduy Yeesu méngoo ak ngëm gi mu amoon ci ndigal loolu. Mu wax xaritam ya ñu randal xeer wa. Nit ña gën a waarooti. Mbaa du Yeesu dafa nar a dugg ca bàmmeel ba, taawu néeewu xaritam ba, walla lu Mu nar a def?

Waaye Yeesu ànd ak sagoom, taxaw ca buntu bàmmeel ba. Mu xool ca kow di ñaan ca kow. Am nanu fii benn ci ñaanu Yeesu yi. Dafa woo Yàlla Baayam. Mu sant Baay ji, ndaxte dundam gépp cellaay la, te màggal Ko, moom Baay ji. Dafa jëkk a sant Yàlla ci tontoom. Bi ñeneen ñi di jooy, fekk Yeesu di ñaan. Mu ñaan Yàlla mu delloo bakkanam xaritam bi. Loolu mandarga dundug baatin la, guy daan dee gi; Baay ji nangu te jox ko sañ-sañu yewwi ku nooteelu dee gi jàppoon. Yeesu gëmoon na ne Yàlla dina nangu ñaanam, loolu amul njàqare, ndaxte dafa daan déggal baatu Baayam saa su nekk. Dundam gépp Yeesu dafa doon ñaan, waaye fii, dafa ñaan ak baat bu kowe, ndax nit ña man a xam kumpa yi ñu nar a gis. Mu sant Baay, jiy nangu saa su nekk ay ñaanam. Benn bàkkaar mosuleen a tàggale, genn gàllankoor doxuloon ci seen diggante. Doom ji wéeruwul ci coobare boppam, laajul genn teraanga, walla yore sañ-sañ bi, ngir boppam. Mataayu Baay bi dafay jëfe ci Doom ji. Baay ji Mu doon, mooy dekkil Lasaar ci ñi dee. Yeesu dafa biral loolu lépp ci diggu mbooloo ma, ngir nit ña man a xam ne Baay ji yónnee na leen Doom ji. Noonu ndekkite Lasaar nekk ndamu Yàlla, loolu di màndargaal kéemaanu jokkoo gi am ci Kenneefu Ñett ñi.

YOWAANA 11:43-44
43 Bi Mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: « Lasaar,ñówal ci bitti! » 44 Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: « Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem. »

Ba Yeesu xaacoo ne « Lasaar génnal! » néew ba wuyu (fekk nag ku dee du dégg dara). Nit ki du ci dee lay jeexale. Képp ku gëm, bind nañu sa tur ca asamaan. Wooteb Aji Sàkk ji, baatu Rammukat bi ak ñaaxu Xelum dund gi, dañuy ronu reeni dee gi. Noonu it la Xel mu Sell mi doon mere ci lëndëm gi, ca njalbéen ga, laata muy teg lépp li jaxasoo woon ci yoon.

Lasaar miinoon na baatu Yeesu, te di ko déggal. Ca biir bàmmeel ba it, dafa dégg te déggal ci kow ngëm. Tëralinu dundug Krist xelliku ci moom; xolam tàmbalee rëkk, ay bëtam ubbiku te cëram yi di yëngu.

Ñaareelu jéego kéemaan gi tegu ci, ndaxte dañoo yeewoon Lasaar. Néew ba dafa meloon ne ab sax ci biir xottam, manuloon a yëg dara. Manuloon a yëngal ay loxoom nir tekki kaala ya ñu ko laxasaloo ca bopp ba, looloo tax Yeesu ne nañu ko tekki.

Ñépp waaru bi ñu gisee kanamu Lasaar gu furi gi; Mungi doon yëngu, àttaa li ñu ko yeew. Ñépp ne ko jàkk, muy jegesi Yeesu.

Lasaar jaar ca biir mbooloo ma, ñibbi këram. Yowaana waxunu dara lu jëm ci ñi sujjóotoon ci kanamu Yeesu, walla rangooñi mbég, ak fóon ya amoon. Méngalewul itam ndekkite lii ak na way-gëm yi nar a jëme ca Yeesu, bu dellusee. Loolu lépp dafa koo beragumoon. Yowaana dafa nuy tegal Yeesu, miy maye dund gi, ngir nu ne Ko jàkk, ba man a gëm te jot dund gu amul àpp gi. Yowaana ndawul Injiil li, munga woon ca biir mbooloo ma. Ci kow ngëm, gise na ndamu Yàlla ci Doom ji, ndaxte déggoon na baatu Krist, te nangu déggal kàttanam. Ndax dekki nga ci ñi dee, jaare ko ci gëm Yeesu?

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, jarajëf ci li nga dekkil Lasaar ci sa turu Baay. Yów it dekki nga ci ñi dee. Nungi lay sant ci sa dund gi nekk ci nun. Ci kow ngëm dekkindoo nanu ak yów. Nungi lay ñaan nga dekkal ñi dee ci sunu askan wi, te fexe ba ñi gëmul dénk la seen bopp, te it ñu jokkoo ak yów ba jot dund gu dul jeex gi.

LAAJ:

  1. Nan la ndamul Yàlla feeñe ci ndekkite Lasaar?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 23, 2025, at 05:40 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)