Previous Lesson -- Next Lesson
d) Pilaat yéemu na ci baatinu Krist (Yowaana 19:6-11)
YOWAANA 19:8-11
8 Bi Pilaat déggee wax jooju, dafa gën a tiit, 9 dugg ca taax ma, dal di ne Yeesu: «Foo jóge?» Waaye Yeesu tontuwu ko. 10 Pilaat ne Ko: «Man ngay bañ a waxal? Xanaa xamuloo ne am naa sañ-sañu bàyyi la, te itam am naa sañ-sañu daaj la ci bant?» 11 Yeesu tontu ko ne: «Amuloo benn sañ-sañ ci man su dul bi la Yàlla jox. Looloo tax ba ki ma jébbal ci say loxo am na bàkkaar, bi gën a rëy.»
Yeesu ci boppam, kumpa lawoon ci Pilaat. Njubteem, sellaayam, ak mbëggeelam, leeroon nañu ko. Noonu, ba mu déggee ne kenn jàppewul Yeesu ni buuru Yawut yi doŋŋ, waaye it ni Doomu Yàlla, mu tiit lool. Waa Rom ak Gerek yi dañu jàppoon ne asamaan si dafa fees dell aky rab ak ay yàlla yu manoon a feeñu, di jëmmu te di jaxasook nit ñi. Noonu mu xalaat ne: «Mbaa kii du yàlla ju soppaliku nit?» Mu laaj Ko ne: «Foo jóge?»
Yeesu jéemul a jariñoo laaj boobu sax ngir rawale boppam, waaye dafa ne cell. Tekkaaral googu dafa am lu ko waral. Yàlla du tontu ay laaj yuy niru nit ki lu jaadu, walla yuy leeral ndañ -kumpa. Waaye dafay feeñu way-gëm yi Koy dénk seen lépp. Moom, dafa wuute lool ak gis-gisu baatinu Gerek yi ak waa Rom yi; kenn niruwu Ko. Tekkaaral googu moo tàng xolu Pilaat ba mu ne Ko: «Bëgguloo wax ak man? Am naa sañ-sañu rey la, mbaa yewwi la, ci sama sañ-sañn nga tegu, te say noon a ngi sàkku ñu daaj la ci bant. Man rekk maa la man a rawale, mbaa ma sànk la.»
Yeesu manoon na ko tontu ne: «Dëgg la, am nga sañ-sañ boobu. Sama Baay may na la ko. Waaye doo dara. Sa caaxaan yi yépp léegi ñu feeñ cib àtte bu jubadi. Sama Baay bi ci asamaan moo man lépp, ak man itam. Amul benn sañ-sañ ci kow suuf, bu dul bu Mu dogal.» May googu, ci dee lay mujje ni Pilaat mi jotoon kàttan gu jóge ci Yàlla. Yàlla mooy saytu te moom jamono, waaye dafay bàyyi li nit ñi rendi, mu nàcc ci seeny loxo. Lépp loo def nit ñi, yaay gàddu la muy jur.
Yeesu dafa ne Pilaat: «Bàkkaar nga, waaye du yów rekk a tooñ. Ñoom ñépp a daanu ci fiiru bàkkaar. Bëgguloo maa daaj ci bant, waaye sag naaféq, ak sa ragalu Kaif, tax na ba nga àtte ma ndaan.» Saraxalekat bu mag ba moo def bàkkaar bu gën a mag bi, ndaxte siis ak mbañ ñoo taxoon mu bëgg ñu rey Yeesu. Ndegam nag Pilaat kilifa gu kowe lawoon, li ko waroon mooy muya m yërmande ci bóomkat yi, ngir jubóolewaat leen ak Yàlla. Waaye fekk na ne rab yu bon yi la doon déggal; looloo tax mu àtte Yeesu nib bóomkat.
e) Àtte bu jubadi bi Pilaat teg Yeesu (Yowaana 19:12-16)
YOWAANA 19:12
12 Booba nag la Pilaat doon fexe bàyyi Yeesu. Waaye Yawut ya yuuxu naan: «Boo bàyyee kii, doo xaritu buur bi Sesaar. Nit kii teg boppam buur, noonub Sesaar la!»
Pilaat bëggoon naa bàyyi Yeesu, ndax li Yeesu nangu sañ-sañam. Moonte baatinu Yeesu dafa am fu mu yemale sañ-sañ boobu. Yeesu tëkkuwul Pilaat, waaye dafa koo artu ak lewetaay. Dafa xajjale bàkkaaru Pilaat ak bóomu Kayif. Yeesu moo nekkoon àttekatu ki Ko doon àtte, te doon ko jéem a won dëggi baatin.
Bi saraxalekat Yawut ya seetloo coppite xolu Pilaat, ñu daldi dugal politik ca mbir ma. Jiiñ Yeesu ne mungi biral ne Doomu Yàlla la, loolu amul benn njariñ ci ëttu àttekaayu waa Rom. Noonu ñu dogu jiiñ guwernër ba ñàkk ngor, te boole ko ak Sesaar, bu reyul Yeesu.
«Xaritu Sesaar», cër la woon bu buur daan berale. Boobu raaya la daan may yenn dagam ak ay mbokkam. Jabaru Pilaat, xëyna mbokk la woon. Tibeer Sesaar, wóoluwul oon kenn, ku ñaaw-njoort la woon. Xelam daawul dal mukk ci ngoru dagam yi. Dafa daan njoort saa su nekk ne kenn ci ñoom dina ko indil ay fippu. Képp ku jiiñ dara xaritu Sesaar, te wone ne li wax dëgg la, kon dinañu tekki ndombal tànku dag boobu, te dàq ko réew ma.
Bu Yawut ya yónnee woon bataaxal ca Rom, ne Pilaat goreel na «Buuru Yawut yi», dafay mel ni kon Pilaat mungi dajale ay nooni Sesaar ngir fippu. Kon book toogaayu Pilaat xajam na fi ñu tollu nii. Bëgguloon ñuy tekki ndombal tànkam ndax Yeesu, donte sax dëgg gi ci Yeesu la féete. Tëkku googu moo ko tax a deltu gannaaw, ba mu tàmbali waaj a biral àtte biy reylu Yeesu. Mu wut pexe mu mu setalee boppam ci deretu Yeesu. Muy wone-wonelu ne àtte bu jub la def, waaye ci biir xolam, xamoon na ne jubadi na lool.
YOWAANA 19:13-16a
13 Bi Pilaat déggee loolu, mu daldi génnee Yeesu ca bitti, dem toog ca jalub àttekaay ba, ca fu ñuy wax Bérabu doj ya. Ci làkku Yawut, ñu naan ko Gabata. 14 Ca bés ba ñuy waajal màggalu Jéggi ba la woon, ca weti diggu bëccëg. Pilaat ne Yawut ya: «Seen buur a ngii!» 15 Waaye ñuy yuuxu naan: «Na dee! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Ndax seen buur bi, dama koo war a daaj ci bant?» Saraxalekat yu mag ya ne ko: «Amunu benn buur bu dul Sesaar!» 16 Noonu, Pilaat jébbal leen Yeesu, ngir ñu daaj Ko ci bant…
Pilaat faalewul oon yaakaaru Yawut, ji aju ci ñówug Almasi bi, tete nañu jàppe woon Rom safu ko woon sax. Mu ne leen: «Yeen a jiiñ Yeesu mi biral nguuram! Jëlleen seen nguur gu ñàkk kàttan gi! Ni moom ngeen mel, te yelloowu leen genn cër!»
Yawut yi dégg bu baax tooñange googu di soppi seen ñaxtu ni jéppi. Noonu ñu yuuxu naan: «Daaj ko ci bant, dafa alku!» Wékk-ko ci bant!»
Mbokk mi, ñooñu doon yuuxu, ñu gëmoon seen diine lañu woon, waaye dañoo gumba woon, ba manuñu ràññee mbëggeel ak geño, rax ci sellaayu Yàlla, ji mate ci Yeesu. Dañu Ko bañoon, te bëggoon a pare ci ay mbiram. Du sopp diine, mbaa am xadar, mooy indi nit ci Yàlla. Mbëggeel gi feeñ ci Jesus kese mooy ubbi sunuy bët, nu xam yërmaandeem ak saraxam.
Pilaat teyati ko ci kow jéppeem googu, daldi tooñaat Yawut ya ba mu tuddee Yeesu «Buur». Noonu mu wone ne mbooloo mépp a dogu woon ngir rey Yeesu. Pilaat jéem a wut nu mu setale boppam, waaye mbooloo mu ràkkaaju ma gisatul dara lu dul daajlu Yeesu ci bant. Baatu askan wi, du baatu Yàlla, ndaxte nit dafay faral di juum, te Seytaane foofu lay bëgg di jaare.
Saraxalekat ya daldi mer ndax ñaawalaate Pilaat ya. Noonu ñu yékkateendoo kàddu gu doy waar naan: «Benn buur doŋŋ lanu am, te muy Sesaar!» Ndaw naaféq! Kureelu Njiit yu mag ya dafa ragaloon mbiru Almasi bi, te bañoon Erood, buur bu soxor bi. Sesaar, mi doon sàmm cosaan ak aada Grek yi, te doon doxal yoon wa ak doxalinu réew ma, moo leen gënaloon. Noonu, ñu wor waxi Yonenti Kóllëre gu Njëkk ga, ak bépp yaakaaru ñówug Almasi bi. Baayu fen gi, dafay xelal ay doomam. Waaye Yeesu moom, taxawal dëgg gi moo Ko taxoon a jóg, di déglu Kàddu Yàlla ci biir xolam, te dëggu.
Mujj gi, Pilaat daldi wax àtte ba ndaxte wegeelu boppam, caay-caayam ak njublang ñoo ko ci xiiroonn.. Doomu Yàlla ji ne tekk rekk, di wéy ci tëralinu Baayam, ji may guwernër bi muy daaj Doomam ci bant. Ci kow àtte bu jubadi boobu la Yeesu matale juboo diggante Yàlla ak nit ki. Rab yu bon yi dañoo yaakaaroon ne am nañu ndam, waaye loolu xew lépp, ci tëralinu Yàlla la bokkoon.
ÑAAN: Boroom bi Yeesu, ñungi lay sujjootal Yów yaay Mbotem Yàlla, miy dindi bàkkaari àddina si. May nu xolu yërmande bu dëggu te jub. Dimbali nu, ba nu bañ a jëfandikoo ñeneen ñi ngir sunuy ngëneeli bopp. Fexeel ba tànn dee gënal nu njublang ak maslaak lu bon.
LAAJ:
- Lu tax Pilaat àtte Yeesu?