Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 101 (Jesus intercedes for his apostles)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 3 - LEER NGAA NGI MELAX CI MBOOLOO NDAW YI (Yowaana 11:55 - 17:26)
E - Ñaanu rammu gi Yeesu def (Yowaana 17:1-26)

3. Yeesoo ngi ñaanal Yàlla taalibeem yi (Yowaana 17:6-19)


YOWAANA 17:6
6 Xamal naa sa tur nit, ñi nga tànne ci àddina te dénk ma leen. Bokkoon nañu ci yów, nga dénk ma leen, te sàmm nañu sa kàddu.

Dafa wóoroon Yeesu ne Baayam ji dina Ko may doole ngir Mu man a matal rammu gi, te it réerewuloon mbir ne Baayam ji dina ndamu ndax ñu bare ñi nar a tuub. Gannaaw loolu, ay xalaatam dellu ciy taalibeem yi mu tànnoon ci biir àddina si, te boole leen ci boppam jarale ko ci kóllëreg asamaan.

Krist daldi jibal turu Yàlla wu bees wi : Baay. Ci kàddu yooyu lañu nekke doomi Yàlla, yi ñu tànne ci àddina si. Dundin Bii, mooy kumpa Jàngu bi. Ñi juddu ci Yàlla, moomatuñu seen bopp ; waaye ki leen may juddu gu bees gii moo leen moom ; te kooku it moo leen jagleel Doomam ci njëgu deretam. Boo gëmee Krist, kon moo la moom.

Taalibe ya dañoo mujj nekk doomi Yàlla ndaxte gëm nañu Injiil li, te denc kàddoom yu am solo yi. Kàddu yooyu duñu deñ mukk. Dañuy maye dund. Képp ku leen fonk te denc leen, dinga jot kàttanu Yàlla.

YOWAANA 17:7-8
7 Xam nañu léegi ne, loo ma joxaan ci yów la jóge, 8 ndaxte xamal naa leen kàddu yi nga ma jox, te nangu nañu ko. Wóor na leen ne ci yów laa jóge, te gëm nañu ne yaa ma yónni.

Kàddug Yàlla gi nu Yeesu yét dafay maye xam-xam biy jëme ci mucc, te di soppi dundin yu geru yi. Yeesu dafa doon dund ay bataaxalam, te daan matale ay jëfam ci kàttanu KÀDDU gii. Kàttanam yépp ak barkeem yépp, ci kàddug Yàlla lañu leen jote. Doom ji waxul ne dafa am xam-xamu boppam, waaye dafa jébbal sañ-sañam, kàttanam maanduteem, ak mbëggeelam, Yàlla mi Ko ko mayoon.

Yeesu dafa maye alalam ji ëpp solo, maanaam ay kàddoom. Ndegam Doom ji ci Baayam la jóge, kon kay mooy Kàddu Yàlla gi ñu jëmmal. Ci wax jooju lanuy tibbee sunu doole. Noonu lanuy mose kàttanu kàddu googu gi nuy leeral. Jot nanu kàddu gi ak mbég. Ay pàcci Injiil li dañu nuy may ñu ràññee nekkaayu Baay.

Ji, Doom ji ak Xel mu Sell mi. Ci biir ñaan gi, Krist daf cee feeñal xolu taalibeem yi, ak li ñu jot a xam ciy kàddoom, ndaxte dafa jii jiwu ngëm ci seeny xol. Dañu nangu Kàddu yooyu ak mbég, waaye du ci saa si. Gannaaw ndekkiteem li, Mu yónnee leen Xelam mi ; kàddu gi màgg te meññ ay doom ca jamono ja ko Yàlla natte. Krist jibal xew-xew yooyu ci kow ngëm.

Kàdduy Krist saxal na taalibe ya ci ngëm ak xam-xam. Lu doon ngëm loolu ? Dañu gëmoon ne Doom ji, ci Baay ji la jóge, gëmoon nañu teewaayu Aji Sax ji ci jamono ji, gëm jëmmeelu ndamam ci yaramu nit, gëm mbëggeelam, donte mbañ a ngi taxaw, gëm kàttanam ci ñàkk dooleem, teg ci nekkinu Yàllaam, ak li muy tàqalikook Moom lépp ca Kurwaa ba, ak dundam gannaaw deewam. Xel mu Sell mi dafay dëgëral seen ngëm ci seen Rammukat bi, ba ñu nekk ay cëri yaramam. Seen ngëm bóofuloon lu yàgg ci xam-xam, ndaxte dañoo dogu woon ci Moom ak seen xol bépp, fekk Moom itam mungi dëkk ci ñoom, ci biir baatin. Xel mee leen may ñu gindiku ci baatinu nekkinu Krist ni nit.

Ci jëmmu Krist la taalibe yi gise seen méngalem juddu gu bees, di ci ,ose kàddu Yeesu gi ne : « Ku juddu ci Xel mi, Xel nga . » Xel mu barkeel moomu, mooy kàttanu Yàlla gi nekk ci taalibe yi. Kàddu Yeesu moo koy yónnee.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu nungi lay sant ci li nga nu yët sa kàdduy Baay, yi fees dell ak dund, kàttan ak doole. Dëj nga nu ci ngëm li ak xam-xam gi. Yaay sunu doole, bëgg nanu la, yów ak Baay ji nu la may.

LAAJ:

  1. Lan la peeñalu turu ‘Baay’ gi Yeesu def di tekki?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 23, 2026, at 02:54 PM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)