Waters of Life

Biblical Studies in Multiple Languages

Search in "Wolof":
Home -- Wolof -- John - 062 (Healing on the Sabbath)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
2. Pajug Gumba judduwaale ga (Yowaana 9:1-41)

a) Paj ma ca bésub noflaay ba (Sabat) (Yowaana 9:1-12)


YOWAANA 9:1-5
1 Amoon na fu Yeesu jaaroon, gis fa waa ju judduwaale gumba. 2 Taalibeem ya laaj Ko ne: ”Kilifa gi, lu tax waa jii judduwaale gumba? Ndax bàkkaaram a ko waral, walla bu waajuram?” 3 Yeesu tontu ne: ”Ajuwul ci bàkkaaram walla ci bu waajuram. Waaye loolu dafa am, ngir jëfi Yàlla yi feeñ ci moom. 4 Bëccëg lanu war a matal jëfi ki ma yónni; guddi dina ñówi, goo xam ne kenn du ci man a liggéey. 5 Ci bi may nekk ci àddina, maay leeru àddina.” (Nii ma nekke ci àddina si, Maay leeram.”)

Yeesu dawul ña Ko doon wut a sànniy xeer, te seetlu na ne ,am na góor gu nekk ci coono. Moom mooy mbëggeel giy baale te gore ci barkeel. Taalibe ya itam gisoon nañu gumba ga, waaye soxaluleenoon lool. Ñunga doon laajante lan moo waral musiba bu ni mel, ndaxte ca jamono yu yàgg ya dañu daan xalaat ne, meññeefu bàkkaar mooy njureelu wopp yi, walla yeneen, kon mbugalu Yàlla la. Yeesu waxul li tax kooka am laago googa; waxul ne waajur ya ñoo tax, walla ngóor si, waaye dafa gis ci coono ngóor si ab buntu jëf ngir Yàlla. Bàyyiwul taalibe ya ñuy àtte ngóor sa, walla ñuy weccoo xalaat ci li waral feebaram bi. Dafa leen a puus ba ñu gis lu gën a sore, te won leen coobare Yàlla: Muuc gi ak Wér gi.

« Dama war a def » la Yeesu wax. Mbëggeel moo ko taxoon a jóg, bëgguloon a àtte kenn, walla di yàq, waaye dafa bëggoon di wéral ci kow yérmande. Noonu lay wonee mbëggeelam, teg ci li Mu gëm, ak ni tëralinam war a mate. Mooy Musalkatu àddina si, te moo bëgg a móolaat nit ñi ci dundug baatin (asamaan).

Nungi dégg kàddu Yeesu yii: »jëfuma ngir sama bopp, walla ci sama kàttan; waaye damay matal samay jëfi Baay ci turam, te nu déggoo ci. » Ci Moom (Yeesu) ay jëfam, yu Yàlla lañu.

Yeesu xamoon na ne diir bi gàtt na te dee gaa ngi jegesi. Loolu lépp terewul Mu am jotu faj gumba ga. Moom mooy Leeru àddina si, te namm a sol gumba gi leeraayu dund gi. Dina am jamono juy ñów, ju du Moom walla kenn Nanu seede fi ak nu ngi ci bëccëg, te nanuy waare fépp fu nu ko man a ame xéewal gi. Lëndëm gaangi yokk, te sunu àddina si amul genn yaakaar gu dul dellusig Yeesu. Kan moo Koy xàllal yoonam ?

YOWAANA 9:6-7
6 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, dafa daldi tifli, jaxase lor wa ak ban, tay ko ca bëti gumba ga, ne ko:” 7 “Demal sëlmu ci bëtu (Ëttu) Silowe. ”Silowe mungi tekki ”yónni nañu ko”. Gumba ga daldi dem sëlmuji, dellusi di gis.

Yeesu ci kàddu gu gàtt la matale kéemaanam gi. Waaye ci lu jëm ci gumba gi, dafa tifli ci suuf, jaxase ko, tay ko ci bëti gumba gi. Yeesu dafa bëggoon mu yëg ne am na lu mu jot, lu jóge ci yaramu Krist. Yeesu dafa yërëmoon gumba ga, ba fexe koo wéral. Doy na waar la bët ya ubbikuwuñu ca saa sa. Dafa waroon a wàcc mbartal ma, te sëlmuji ca Silowe, tur wiy tekki “Ki ñu Yónni” di misaal ab yonnent ca Askanam. Yawut yi ci seen bopp dañoo judduwaale ngumba ci seen biiry bàkkaar ak seeni tooñ, noonu dañoo soxla wér ak mucc gi Yeesu di maye.

Gumba ga dafa nangu digu Yeesu ga te gëm mbëggeelam. Ca saa sa la def la Mu ko waxoon. Boolewu ca sax ay laaj. Noonu la jotewaate leeraayu bëtam. Ci saa si, mu tàmbali gis nit ñi, ndox mi, leer gi, ay loxoom ak asamaan si. Mu gis loolu lépp ak waaru gu jéggi dayoo. Xolam toj ak mbég, mu sarxolle Alleluya yu bre, te màggal Yàlla.

YOWAANA 9:8-12
8 Dëkkandoom yi ak ñi Ko xamewoon bu jëkk ci yelwaan naan: ” Xanaa du kii moo daan toog, di yelwaan?” 9 Ñii naan: ” Moom la de!” Ñee naan du moom! Dañoo niroo rekk.” Mu daldi ne leen: ”Man la de!” 10 Ñu daldi ne Ko: ” Lu ubbi say bët?” 11 Mu tontu ne: ” Ku ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, tay ko ci samay bët, ne ma: ”Demal sëlmu ci bëtu Silowe. Ma dem nag sëlmuji, daldi gis.” 12 Ñu ne ko: ”Ana waa ji?” Mu ne leen: ” Xawma fu Mu nekk.”

Kéemaan gi manul a nëggu, ndaxte dëkkandoom ya gisoon nañu góor ga wéroon, te waaru ci loolu. Am na ñu gëmuloon ne kii ñu gis mu am doxin wu jub, man na nekk ka daan tërëf, te daan làmbatu yoonam;ñu ko daan gunge. Moom ci boppam biral ne moom la.

Nit ña di jéem a fexe xam nan la def ba wér, te jéemuñu sax lijjanti lu jëm ci fajkat bi. Nit ka ñu w éral, xamoon na turu ka ko fajoon, waaye bu weesoo loolu, umpalewoon na ki mu doon. Xamuloon baatinu Yeesu Krist, moo tax mu jàppewoon Ko ni nit ka tayoon ban ban ca ay bëtam ngir mu man a gis. Mooy ka ko santoon mu sëlmuji. Te noonu la ay bëtam man a gise.

Yërndukati Sanedreŋ laaj ko : »Ana Yeesu moomu ? » Waxambaane ba tontu ne : » Xamuma !Man damaa gumba woon, te léegi maa ngi gis. Moom de laajuma xaalis, walla benn baatu cant ak ngërëm. Ma dem sëlmuji, daldi man a gis. Xamuma Ko, te xamuma fu mu nekk. »

ÑAAN: Nungi lay sant, Boroom bi Yeesu, ndaxte rombuloo gumba gi mel ni ku ko gisul. Ubbi nga ay bëtam, ba mu nekk misaal ci ñépp ñi juddoo ci bàkkaar. Sellaleel sunuy bët ak sa Xel mu Sell mi, ndax nu man a gis sa leer gi, te seedeel sa tur wi ak mbég.

LAAJ:

  1. Lu tax Yeesu faj gumba judduwaale ga?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 21, 2025, at 11:11 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)