Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
B - Ndekkite Yeesu Krist ak ay peeñoom (Yowaana 20:1 - 21:25)
2. Yeesu feeñu na taalibe ya ca néeg gu kowe ga (Yowaana 20:19-23)YOWAANA 20:19 Ci biir néeg bi ñu tëjoon, taalibe yu tiit ya ñunga doon werante ca mbir ya xewoon. Dégg nañu ne bàmmeel ba dara nekkatu fa. Jigéen ña seede nañu ko te malaaka ya nee nañu ne dekki na. Maryaama mu Magdala wax na ne gis na Ko. Yooyu dégg-dégg jaxase xelu taalibe Yeesu yi. Ki deewoon mungi dund, waaye feeñuwu leen! Waaye ñoom ñungi doon dajjent ba ñuy jàpp Yeesu, te kenn ci ñoom ànduloon ak Moom ba ñu Koy àtte, ak sax ca wetu kurwaa ba, ba mu des Yowaana ak jigéen ña. Wàcceewuñu Ko ca kurwaa ba itam, te suuruñu Ko. Dañu ragaloon Yawut yi, te xamoon ne bu màggal gi jeexee rekk, dinañu dal ci seen kow. Looloo taxoon ñu tëju ca néeg booba, ak xol bu jeex tàkk. Gëmuñu woon la leen jigéen ña waxoon, te naan ci seen biir: « ànd ak Yeesu, te nungi doon xaar Mu am ndam, te fal nu ni ay jawrin. Lépp moy na; dinañu nu dàqe ba jàpp nu, rey nu. » See yaakaar dafa tasoon. Ak li ñu ñàkkoon ngëm lépp, boole ci seen naqar, Yeesu feeñ ci seen biir. Ñówul ndax seen yaakaar ak seen mbëggeel, te it du ndaxte dafa leen yërëmoon ndax seen tiis, waaye ngir wone yiwam gi Mu teg ci kow seen ndëggate. Peeñu googu kéemaan la. Ka deewoon mungi dund, ka ñu weddi woon yewweku na. Amul benn bàmmeel, walla ab bunt bu Ko man a teree feeñu ay soppeem. Dafa leen doon feeñu ci jëm ni doomu Aadama bu nekk. Dañu Ko doon dégg, di Ko gi, te man Koo laal. Rax ci dolli, xel la woon, mu man a fëlle ci miir yi ak bunt yi ñu tëj. Dundam gu bees gi won nanu ni nuy mel, bu nu saxee ci moom. Yaram wi Mu dekkee mooy sunu yaakaar. Ñdaw xel mu dal! Ku dekki Ki merewul ay taalibeem ndax seen yox-yoxi, waaye dafa leen a barkeele nuyóob jàmm: « Na jàmm wàcc ci yéen! » Nuyóo boobu dafay tekki ne ci deewam la juboole àddina si ak Yàlla. Jàmm jaa ngi doon tàmbali di baawaan jóge asamaan, jëmsi suuf; te jamano ju bees di duggsi, muy ju Krist maye. Nun noo war a tànn su fekkee ne danu Koy nangu, walla danu Koy weddi. Muccug nit ki, ci moom la aju. Képp ku tuub te gëm Yeesu, cëru ci barkkeem. Képp ku wàllsi ci mbootaayu Buuru jàmm ji, ñu goreel la, jaare ko ci benn saraxam bi Mu sàkk, ni ko Póol waxe nii: « Ndegam ngëm moo nu goreel, am nanu jàmm ak Yàlla jaare ko ci Yeesu Krist sunu Boroom. » ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist, yów mi dekki ci biir ñi dee, di buuru Jàmm ji, nungi lay sujjóotal ak mbég, ak ngërëm, ndaxte ñówuloo ngir àtte nu, walla mbugal nu, waaye ngir wone sa yiw, te musal nu ci sunu ñàkk yaakaar, ak ngëm; ngir itam may nu sa jàmm te jubóole nu ak Yàlla. Sa mucc gi du sunuy jëf ñoo ko jur, waaye sa yiw rekk moo nu ko may. Dimbalil sunuy xarit ak sunuy noon ba ñu xam sa yiw. Ndax ñu nangu la, te bañ a wéy ci seen dëgër bopp di xëccoo ak Yàlla ju Sell ji. LAAJ:
|