Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Lingala -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 4 - LEER GI DAAN NA LËNDËM GI (Yowaana 18:1 – 21:25)
B - Ndekkite Yeesu Krist ak ay peeñoom (Yowaana 20:1 - 21:25)
2. Yeesu feeñu na taalibe ya ca néeg gu kowe ga (Yowaana 20:19-23)YOWAANA 20:20 Ndekkitel Yeesu biral na ne juboo ak Yàlla mat na sëkk. Yàlla bàyyiwul Doomam ca biir bàmmeel ba. Beddiwu Ko ndax sunuy bàkkaar yi Mu nu gàddul. Krist mi tooñul, Moo nangu saraxe boppam, te génne ak ndam ca bàmmeel ba, te di dund ni cereek meew ak Baayam. Rax ci dolli, dafa nangu dem ca kurwaa ba, teg ko ci coobare Baayam doŋŋ. Kurwaa bi moo waraloon ñówam, te nekkoon juumtukaay bi war ngir musal àddina si. Kon nag, nan la ñenn ñi man a waxe ne Yeesu deewul ca bant ba (kurwaa ba)? Krist wone na ne du njuuma, mbaa jinne ju làqu. Won na leen légëti pont ya cay loxoom, ak wetam ga xeej ga bënnoon. Noonu ñu gëm ne Ki nekkoon ak ñoom, du woon Yàlla ju ndaw, waaye Ka ñu daajoon la. Mbotem Yàlla mi moo ndamu ci kow dee gi. Ndank-ndank taalibe ya di xam ne Yeesu du njuuma, du jinne, waaye nit ku wér péŋŋ la ci seen biir. Dundam gu bees gi may leen mbg mu rëy. Sunu ngëneel mooy tax nu gëm te xam ne Yeesu mooy boroom biy dund, te dekkee ci biir ñi dee. Dunu ay jirim yu ñu fegg nee. Sunu Doomu Baay, ji jokkoo ak Xel mu Sell mi, mooy jiite dunyaa ba fàww. Mbég taalibe ya di gën a yokku ba Yeesu amee ndam ci dee gi. La ko dale booba ba tey, la nekk ngir nun ñi war a dee, sunu yaakaar jiy dund. Bàmmeel bu ubbeeku ba du sunug mujj, waaye dundam mooy sunug dund. Ni ko Ki yelloo ndam li waxe nii: « Maay ndekkite li ak dund gi. Képp ku ma gëm, boo deewee sax, dinga dund. Képp kuy dund te gëm ma du dee mukk. » Ba taalibe ya xamee ne Yeesu dafay baale bàkkaar, ñu gën a bégati. Fay na sunu bori bàkkaar yépp. Kon book jaare ko ci ay metitam, am nanu jàmm ak Yàlla. Ndax yaa ngi séddoo ak ñoom mbégu Pàkk gi? Ndax yaa ngi sujjóotal Ku dekki Ki, ndaxte mungi teew, di la may yaakaar te di wóoral sag mbaal (njéggal)? Yeesu mungi dund, te nungi dunde mbég. Apotar Póol nee na Jàngu bi: « Na ngeen bég saa su nekk ci Boroom bi. Na Yàlla xam seen baaxaay. Boroom baa ngi dellusi léegi. » ÑAAN: Sang bi Yeesu, nungi lay sant, di la màggal ndaxte Yów rekk yaay sunu yaakaar. Yaa tax ba sunug dund tekki. Say gaañu-gaañu ñoo nu goreel. Na sa nguur ñów ndax ñu bare man a dekki ci ñi dee, ba dund ngir màggal sa Ndekkite li. LAAJ:
|