Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 048 (Jesus and his brothers)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

a) Yeesu ak ay rakkam (Yowaana 7:1-13)


YOWAANA 7:1-5
1 Gannaaw loolu, Yeesu doon na wër diiwaanu Galile. 2 Bëgguloon a dem diwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wut a rey. Fekk na bésu xewu Yawut ya, ñu koy wax Màggalu Mbaar ya, mungi doon jubsi. 3 Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne Ko: » Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis ñoom itam jaloore yi ngay def. 4 Ku bëgg a siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel nii, fexeel ba ñépp gis la. » 5 Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte gëmuñu Ko woon.

Nit ñi dañu yéemuwoon ci seedeb Yeesu bi aju ci ndamam. Ñenn ca ay xaritam, ca Yerusalem, dëddu Ko, te taalibeem yu bare won gannaaw ca Galile. Ñi seen xel tëju te dëkk ca péey ma gëmuñuwoon ne waxambaane bii dekki na ci ñi dee, te it moo nar a àtteji àddina si. Ña fonk diine ca Galile nag ñoom seen xel dafa teeyoon ci xalaatu lekk yaramam ak naan deretam. Xamuñuwoon ne misaalu reeru Boroom bi la.

Ca Yerusalem yenn kilifay Kureel gu Mag ga dañoo doguwoon ngir rey Yeesu. Ñu joxe ndigal ngir ñu jàpp Ko te tëkku ñépp ñi bokk ci diine Yawut, ne dinañu leen dàq ca néegu jaamukaayu Yàlla ba, te xañ leen barkey (xéewali) Yàlla yi, bu ñu wéyee di topp Yeesu. Noonu, mu am ay yërndukati Kureel gi, yu tàmbalee wër Yeesu te di gëstu ay mbiram ca Galile. Dara umpalewul li tax nit ña daw Ko, ndaxte dañoo waroon a tànn diggante nooteelu Kilifay réew ma, ak mucc gu leen leerul gi ñuy wut ci Yeesu. Ñu tànn li teew. Seen kaaraange gënal leen mayu Yàlla.

Rakki Yeesu ya dañoo ragaloon ñu beddi leen ca askanu réew ma. Noonu ñu weddi Ko ca kanamu mboloo ma; ndax ñu bañ leen a dàq Néegu Yàlla ya (Mark 6 :3) Ñu ñaan Ko ngir Mu jóge Galile ngir setal seen bopp ci bépp wareef ci Moom; xéyna sax dañoo bëggoon Mu woneji ndamam ca Yerusalem. Ak at yu bare yi ñu dund ak Moom yépp taxul ñu gëm baatinam, xanaa di jàppe mbëggeelam ak baaxaayam ni lu war a nekk doŋŋ. Li yenn taalibe yi di wege Yeesu ndax mbëggeelam te xamuñu dëggam gi, tiis na lool.

Rakki Yeesu ya gisoon nañu kéemaan ya Mu daan def. Waaye loolu taxuloon ñu gëm ne mooy Almasi, bi ñu dege woon te bépp óom war a sukk ci kanamam. Amoon nañu kersa ak gàcce ca na riiram ba doon deltoo gannaaw ak it fitna gi Mu indiwoon. Ñu fiir Yeesu na ko Seytaane defewoon ca màndiŋ ma, ba mu Koy digal Mu tëbe ca kow Këru Yàlla ga ngir yey ña Ko gëm. Yeesu amul dara lu Mu bëggoon ci rëyaay, dafa tànnoon suufeelu ñàkk doole ni doomu Aadama. Wutuloon di xumbal ak di wonewu ngir yokk ay taalibeem.

YOWAANA 7:6-9
6 Yeesu ne leen : » Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax. 7 Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne, seeni jëf baaxuñu. 8 Yéen nag demleen màggal ga. Demuma màggal googu ndaxte sama waxtu jotagul. » 9 Bi Mu leen waxee loolu ba noppi, Moom mu des Galile.

Nit ñi dañu bég ndaxte xelum Seytaane yey na leen. Rëy mandarga feebaru ruu la te firnde feebaru xel la. Ci dëgg nit dafa tuuti, ñàkk njariñ, te war a dee, lu wuute ak Yàlla. Nit dafay jéem a nëbb ñàkk kàttanam ci li muy mbubboo. Nit ku yëg boppam dafay foog ne Yàlla ju ndaw la, ju man a def lépp li mu bëgg, walla mu bañ a def dara. Mooy dogal ay tëralinam ak ay doxalinam te du ci boole Yàlla. Dafay mujj nekk fippukat ci kanamu Aji Sàkk ji. Nit ki dafa bëgg boppam te sopp di kañu ak di bàkku; du màggal mukk turu Baay ji ci asamaan.

Du caagéen sax ne xalaati nit ki, ak ay mébétam ñoo bon, waaye itam ay jëfam. Ndaxte képp kuy dund te àndoo ak sa Boroom, sa dund a ngi féwwaloo ak Moom. Li ci ëpp ci li nit ñi defar, walla ñu feeñal ko ciy gëstu, boole ci li aju ci politik ak joŋante xel ñungi jublu ci mbirum bàkkaar. Ñoom ñoo ëmb jiwu (peppu) dee gi.

Krist wone na ne àddina si bëggu Ko. Ñówul ngir def ko neex. Dafa ànd ak Baay ji te di liggéey ak Moom. Xeeru fakkastal la sax ci ñi fonk diine; ndaxte mbëggeel gi muy digle teguwul ci ay sart, waaye ci Yàlla la jóge. Dañu Koo bañoon ndaxte teewaayam dafa beddi yoonu farisen.

Rakki Yeesu ya sàbbi Xel mu Sell mit, mujj nag fees ak xelum àddina. Dañoo faroon ak Farisen ya. Seen ñàkk ngëm moo wone ne Xelum mbëggeelu Yàlla nekkuloon ci ñoom, waaye meneen xel moo leen doon wommat, maanaam xelum « rëy » ak « fippu » ci kanamu Yàlla.

YOWAANA 7:10-13
10 Ba rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam dem, te kenn yégu Ko; siiwalul demam. 11 Fekk Yawut yaa nga Ko doon seet ca màggal ga naan: » Ana waa ji? 12 Ca biir mbooloo ma ñungi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan « nit ku baax la », ñee naan » déet, dafay nax nit ñi. » 13 Waaye kenn ñemewu Koo tudd ca kow, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.

At mu nekk, Yawut yi dañu daan amal màggalu Mbaar ya. Dañu daan jël ay xobi garab ngir ràbbe ci ay néeg, walla ay xayma yu ñu man a dallu. Manoon nañu ko defar ci kow kër yi, walla ci mbedd yi. Nit ñi dañu daan demalante, te daan séddoo lekk yu neex. Xew-xewu cant lawoon bu ñu jagleel Yàlla mi leen may nawet bu naat te barkeel. Néeg yi dañu leen doon fàttali seen jaar-jaar ba ca mandiŋ ma, ndaxte booba amuñuwoon menn màkkaan ci kow suuf, mu ñu man a ñibb (dëkk).

Amul genn bànneex gu Yeesu jële ci màggal googu, ndaxte dañu Koo bundxataal Moom ak ay taalibeem. Dafa bàyyi ay rakkam jiitu Ko Yerusalem, ba noppi Mu door a ñów. Mu tàggu waa Galile, fa Mu dëkkoon ci àddina si. Waxtu dogu gi mungi jegesi, maanaam waxtu deewam ngir yewwi nu ci merum Yàlla.

Xalaat yu wuute la Yawut yi amoon ci Yeesu. Am na ñu ko jàppe woon ni nit ku baax, kuy indi coppite gu jóge ci Yàlla. Ñeneen ña di Koxoole ni kuy réeral nit, te yelloo dee; ndaxte mooy ki teewaayam nar a tax ba merum Yàlla wàcc ci seen kow, yàq seen neexaayu màggal. Kureel gu mag ga joxewoon na ndigal lu askan wa wépp déggoon, te doon ca séentu ne taalibeem ya duñu Ko ñemeeti topp. Ba loolu amee, keenn ñemeetul jollil mbiri Yeesu.

ÑAAN: Boroom bi Yeesu, nungi lay sant ci sa suufeelu, ak sa dégg-ndigalu Yàlla. Yewwi nu ci doxalinu àddina si, te sa Xel mi solu nu ba nu fees-dell. Sàmm nu ci yoon bon yi. Fajal nu sunu biir, ba nu man laa tarbiyu ni nga ko yelloo.

LAAJ:

  1. Lu tax àddina si bañ Yeesu?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 09, 2025, at 08:20 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)