Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
Home -- Wolof -- John - 047 (Sifting out of the disciples) This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
Previous Lesson -- Next Lesson YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
B - Yeesu mooy mburu dund gi (Yowaana 6:1-71)
5. Wàññeeku taalibe ya (Yowaana 6:59-71)YOWAANA 6:66-67 Kéemaanu bareel mburu ma, indiwoon na bég mu réy. Waaye Yeesu feeñal na ñàkk ngor ga làquwoon ca gannaawu mbég mooma, ba tax sax ay taalibeem yu bare dëddu Ko. Moom bëggul xadar, walla ngëm gu saxul, mbaa it ngëm gu ànd ak xel ñaar. Juddu gu bees la bëgg, ngëm gu dëggu guy jébbalu ci Moom, te bàyyiwul dara. Noonu, ay yërndukati Mbootaayu kilifa Yerusalem ya rax ca biir taalibeem ya. Ñu xoqtal ña Ko gënoon a jege ne leen bu ñu wéyee di topp ki ñuy woowe naxekat bi, kon dinañu leen dàq ca seen diine Yawut ja. Ba mu ko defee, ñu bare ca waa Kapernawum daldi dëddu Yeesu te mbooloo ma tàmbali di Ko weddi. Ña farluwoon ci Moom sax di tàmbalee ragal waa Kureel ga. Dañu gisoon ne ngëmu Yeesu gi kat mungi bëgg a ëpp. Ay taalibe yu néew te dogu,ñoo mujje des ak Moom. Boroom bi mungi doon lay dugub ji ak xatax bi. Laata xew-xew yooyu,fekkoon na Yeesu tànn fukki taalibe ak ñaar ci ñi Ko doon topp, muy misaalu fukki askan ya ak ñaar yu banni Israel ya Mu cosaanoo. Bii lim (3x 4) ay firnde asamaan ak suuf la, walla sax mooy wone Ñetteefu Kenn Ku Sell Ki ak ñeenti pàcci àddina si. Kon book ci wërgalu taalibeem yi, asamaan ak suuf daje nañu nekk benn. Ba ñooña demee, Yeesu nattuwaat taalibe ya des ngir wóoral seen dogu « ndax dangeen Maa nar a won gannaaw itam? » Ba Mu leen laajee loolu, dafa leen a puus ngir ñu tànn seen ëllëg. Bu nu nekkee ci ay jafe-jafe walla ci ay tolof-tolof, dafa nuy laajaat bii laaj » ndax danga maa nar a bàyyi, walla danga fas yéene taq ci man ba tey? » Lan moo ëpp solo, aada yi, yégeel yi, li nu xalaat ne moo jaar yoon, sunu kaaraange ndey walla sunu jokkoo ak Yeesu? YOWAANA 6:68-69 Piyeer dëggal na waxu Yonent bi Yeesu biraloon ba Mu nee Piyeer doj wu dëgër lay doon. Dafa jëlal kàddu ñépp ne « Boroom bi ci kan lanuy dem? Yów doŋŋ yaay teenu dund gu dul jeex gi. » Xéyna sax xamuloon li Yeesu nar waaye yégoon na ci boppam ne Yeesu mooy Boroom bi wàcce asamaan, Aji Kàttan, ji nga xam ne ay kàddoom raw nañu yu nitu neen. Piyeer dafa gëmoon ne Boroom bi teew na. Fekkewoon na ba Muy bareel mburu ma Loxo Yeesu rawalewoon na ko ba mu naree lab. Xolu Yàlla dafa taqoon ci Yeesu, dafa bëggoon Boroomam te jiital Ko ci lépp, te du Ko mos a bàyyi. Piyeer dafa tànnoon Yeesu, ndaxte Yeesu moo ko njëkk a tànn. Njiitu apotar yi mujj a seede ne: » Gëm nanu te xam nanu. » Seetlul ne waxul: » Xam nanu ba noppi gëm. » Ndaxte ngëm gi mooy ubbi gis-gisu xol bi. Sunu ngëm mooy leeral sunu xel. Kon book Piyeer ak ña mu àndal dañoo ubbeeku ngir dalal Xelum Yàlla, mi leen wommat ba ñu gëm Yeesu te xamloo leen dëgg gi, noonu lañu doon gën a xame ndamam li làquwoon. Mayug yiwu Yàlla doŋŋ mooy tax nit xam Yeesu dëgg. Fan la ngëmu taalibe ya tolluwoon? Lan moo ëmboon ngëm googu? Dañoo taqoon ci Almasi bu tedd bi, ci Ki mataayu Xel mi sax. Moo dajale ci jëmmam bépp sasu ki ñu ber, bu nguur gi ak bu Yonent bi. Ca jamonoy Kóllëre gu njëkk ga, buur ya,saraxalkat ya ak Yonent ya dañu leen daan barkeele (diw) Xel mu sell mi. Ci Krist lañu dajale bépp kàttàn ak barke bu jóge asamaan. Mooy Buuru asamaan, Aji kàttan ji, Saraxalkat, biy jokkalewaat nit ki ak Ki ko sàkk. Man na dekkal ñi dee; Dina àtte àddina si. Ci kow ngëm la Piyeer xame ndamul Krist. Taalibe ya daldi gëm; jaare ko ci Piyeer ñu joxe bii seede bu takku: Yeesu mii mooy Ku sell ki jóge ci Yàlla, du nitu neen, waaye Yàlla la ci boppam. Jikko Yàlla yépp a ngi ci Moom, Doomu Yàlla ji. Amul benn bàkkaar, te matal na sasam ni Botem Yàlla, na ko Yaxya yéglewoon. Taalibeem ya bëggoon nañu Ko te doon nañu Ko jaamu, ndaxte xamoon nañu ne teewaayam mooy teewaayu Yàlla. Ci Doom ji lañu gise Baay ji te xame ci ne Yàlla mbëggeel la. YOWAANA 6:70-71 Yeesu teeru seede boobu ak mbég, ndaxte loolu wone na ne seen ngëm mungi yokku; waaye terewul ne xamoon na ne am na kenn ci ñoom ku daan fexe téye loxoom ay yooni-yoon. Dëgëraayu xolu nit kooku dafa yokku ba Yeesu mujje ko woowe « seytaane ». Apotar yépp dañu léen tànnoon, te Baay ji xiir leen ci Doom ji. Waaye nag duñuwoon ay xuus-maa-ñàpp ci loxoy Yàlla. Manoon nañu tànn déggal baatu Xel mi, mbaa ñu tanqamlu Ko. Yudaa moo ko tey, ne ràpp xelam ci baatu Yàlla te déggal Seytaane mi samp jokkoo baatin ci seen diggante. Yudaa dëdduwul Yeesu ni ñeneen ñi, waaye, dafa ànd ak Moom ci biir naaféqam, mel ni ku Ko gëm. Noonu la nekke doomu « baayu fen » ji ba suux ci labaj. Fi Piyeer di seedee nekkinu Yeesu ni Almasi bi, Yudaa mungi tëral ay pexe ngir Kureel gu mag ga man a jàpp Yeesu. Muy nëbbu di lal ay pexeem yu ñaaw yooyu. Injiil li tëjewul saar bi ak jëf yu kéemaane yi Apotar yi def. Waaye dafa fésal solo siy wone ne ci biir ñi sàmmoon ngor sax, amoon na ca ab workat. Yeesu dàqu ko, te weejewu ko.Daf koo muñal, di xaar Yudaa soppi xelam te tuub. Mbokk mi, na nga seetluwaat sa xol bu baax, boole ci suufeelu. Ndax doomu Yàlla nga walla doomu Seytaane? Nanga moytu ba doo moy sa mébétu dund bu jekk. Sa Boroom dafa laa bëgg te musal la. Waaye boo sàbbee muccam gi, Dinga réer ci yoonu mbon, te wéy ci nekk jaamu Seytaane. Ñówal ci Krist ndaxte mungi lay xaar. ÑAAN: Boroom bi Yeesu Krist, yów yaay Doomu Yàlla ji; sell, am yërmande, am kàttan ak ndam. Baal ma samay tooñ teboole ma ci sa kóllëre ndax ma man a dunde sellaay, te dëkk ci sa teewaay. Soppi ma ba ma mel ni Yów. Sellalal say taalibe ba ñu màgg ci seen ngëm ak ci xam-xam, te seedeel ñépp ne yów rekk yaay Krist, Doomu Yàlla jiy dund. Amiin. LAAJ:
|