Home
Links
Bible Versions
Contact
About us
Impressum
Site Map


WoL AUDIO
WoL CHILDREN


Bible Treasures
Doctrines of Bible
Key Bible Verses


Afrikaans
አማርኛ
عربي
Azərbaycanca
Bahasa Indones.
Basa Jawa
Basa Sunda
Baoulé
বাংলা
Български
Cebuano
Dagbani
Dan
Dioula
Deutsch
Ελληνικά
English
Ewe
Español
فارسی
Français
Gjuha shqipe
հայերեն
한국어
Hausa/هَوُسَا
עברית
हिन्दी
Igbo
ქართული
Kirundi
Kiswahili
Кыргызча
Lingála
മലയാളം
Mëranaw
မြန်မာဘာသာ
नेपाली
日本語
O‘zbek
Peul
Polski
Português
Русский
Srpski/Српски
Soomaaliga
தமிழ்
తెలుగు
ไทย
Tiếng Việt
Türkçe
Twi
Українська
اردو
Uyghur/ئۇيغۇرچه
Wolof
ייִדיש
Yorùbá
中文


ગુજરાતી
Latina
Magyar
Norsk

Home -- Wolof -- John - 049 (Disparate views on Jesus)
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula? -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur? -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba

Previous Lesson -- Next Lesson

YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
XAAJ 2 - Leer gi leeral na lëndëm gi (Yowaana 5:1 - 11:54)
C - Tukkib Yeesu bu mujj ca Yerusalem (Yowaana 7:1 - 11:54) Tàggaloo Lȅndȅm Gi Ak Leer Gi.
1. Kàdduy Yeesu ca màggalu Mbaar ya (Yowaana 7:1 – 8:59)

b) Xalaat yu wuute yu jëm ci Yeesu, ci diggante askan wi ak Kuréel gu mag gi (Yowaana 7:14-53)


YOWAANA 7:14-18
14 Ba ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngale ca Kër-Yàlla ga. 15 Yawut ya nag jaaxle naan: » Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul? » 16 Yeesu daldi leen tontu ne: » Li may jàngale, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge. 17 Ku fas yéene wéy ci bëgg -bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngale ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare. 18 Nit kiy wax ci coobareem nag,day wut a màggal boppa, waaye kiy wut a màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax, te jubadiwul fenn.

Yeesu du dee gi walla ërtali noonam ya la ragaloon. Dafa topp yoonam ci sutura ba Yerusalem, ànd ak coobare Baayam. Ba mu agsee nag, nëbbatuwul, waaye dafa dem ca kër Yàlla ga ngir jàngale fa Injiilam ak ñeme gu mat sëkk, ni ab jàngalekat bu ñu fal. Nit ña dañu yëgoon ne ñoom ci seen bopp la Yàlla di waxal. Noonu, ñu tàmbalee laajante ci seen biir naan, fan la waxambaane bii jële xam-xamu diine bu xóote nii? Benn kàngaamu Mbind yi jàngalu Ko. Nan la nu ab xaddkat bu jàngul man a jàngalee dëggu Yàlla gi?

Yeesu tontu leen mel ni ku naan: Ci dëgg-dëgg am naa am njàngale, te ab jàngalekatu dëgg gi laa. Rawatina nag, Maay kàddug Yàlla gi. Bépp xalaat ak bépp mébétu Yàlla ñungi ci Man. Sama njàngale jógewul ci man, maay kàddu Yàlla mi dëkk ci man, sama Baay moo may jàngal. Xam naa bu baax ay xalaatam, ay tëralinam, ay xiirteem ak kàttanam. Ñówuma ak samay xalaati bopp, ndaxte xalaati Yàlla doŋŋ ñooy dëgg. Damay mottali peeñu gi fi mu desee leer. »

Mu màggal Baayam, te déggal Ko, am it taxawaayu ndawu Yàlla. Du Moom moo indi (wàccee) boppam, wayee ci turu Baayam la ñówee teg ko ci sañ-sañu Buuru asamaan. Yeesu moo boole nekkandoo Doom ak ndawul Yàlla. Moom yelloo na nu Koy bàyye sunu xel, sunu ngëm, ak sunu màggal, ni ko Yàlla Baay bi yelloo.

Ngir yombalal leen seen ngëm ci Moom, dafa leen a (Yawut yi) may yoon wu yomb ngir wone ne njàngaleem dafa méngoo ak coobare Yàlla. Kon léegi, lan mooy seede gu wér guy wone dëggu njàngalemYeesu ak ki Mu doon? Mu ne: ” Fexeleen ba di jëfe sama Injiil, noonu dingeen xam màggaayam. Doxalal kàddu Krist yooyu, aaya ci kow aaya, kon dinga gis ne wax jii du neen, waaye ca Yàlla la jóge.”

Boo bëggee doxe njàngalem Yeesu, dafa laaj nga dogu ba noppi. Ndax bëgg nga li Mu bëggoon? Fi ak seen ñaari coobare yi ànduñu, doo man a xam mukk kan mooy Boroom bi. Bu sa coobare jébbaloo ci bu Krist, dinga gën a xam kan mooy Yàlla.

Képp kuy jéem a def coobare Baay ji, ni nu ko Yeesu jàngale, dina gis kàmb gi nekk ci diggante Injiil li ak Yoon wi (Ndigal yi). Boroom bi dafa nuy jox doole ji war ngir nu man a yenu say wi Mu nu dénk. Dinanu man a sottal coobareem ak mbég. Képp ku déggal Krist, dinga am kàttanu dunde mbëggeelam. Njàngaleem du yóbbe ndaan, ni ko Yoonu Musaa daan defe waaye dafa nuy dugal ci dund gu fees dell ak yiwu Yàlla. Képp ku bëgg a jaar ci coobare Yàlla, ji Yeesu feeñal ci njàngaleem, dinga jokkoo ak Yàlla te xam ne Krist du ab jàngalekatub neen, waaye Kàddug Yàlla gi ñu jëmmal la ci boppam. Du ay xelli-xel la indi, waaye dafay maye mbaalug bàkkaar, ak kàttanu dundug Yàlla.

YOWAANA 7:19-20
19 Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? waaye kenn ci yeen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey? 20 Mbooloo ma ne Ko: »Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wut a rey? »

Doxalinam gu sell gi moo may Krist sañ-sañu wax Yawut ya: »jot ngeen Ndigal li, waaye kenn ci yeen toppu ko ni mu ware! »Kàddu yooyu yëngaloon nañu xolu Yawut ya, ndaxte dañuy firnde ne kenn ci waa Kóllëre gu NJëkk ga mosul a topp Yoon wi ni mu ware. Képp ku moy benn Ndigal doŋŋ, moy nga fukk yépp. Merum Yàllaa ngi ko tiim. Noonu la Yeesu faxase la Yawut ya jàppewoon ni njubte, te won leen ne xadar ak góor-góorlu gi fonk-diine yi àndal, du dara lu dul ag ngumba doŋŋ.

Mu xamal leen ne xam na ne kilifa ya dañu Koy fexe rey. Dara umpu Ko woon. Mu artu ñi Ko doon may nopp, ngir ñu moytu xadar gi ñuy mbubboo, te xamal leen it ne képp ku Ko bëgg a topp, am na li mu lay jaral.

Ba léegi Mungi laajte naan: » Lu tax ngeen bëgg maa rey?

Mbooloo ma mer lool ci kàddu Krist yooyu, ba noppi tiit ci li Mu leen wax ne kenn ci ñoom jubul. Seen tontu daldi muur seen mébét: »déet-déet waay, kan moo la bëgg a faat? Yàlla tere na kuy faat bakkanu nit! » Am na sax ñu doon xalaat ne aw rab wu bon moo Ko jàpp. Seen mbañ gumbaloo leen ba manatuñu ràññee Xel mu Sell mi ak xel mu sellul. Dañoo ñàkkoon bépp yégeel bu leen man a may ñu xàmmee mbëggeelu Yàlla.

LAAJ:

  1. Lan mooy wone ne Injiil ci Yàlla la jóge?

www.Waters-of-Life.net

Page last modified on July 11, 2025, at 08:09 AM | powered by PmWiki (pmwiki-2.3.3)