Waters of LifeBiblical Studies in Multiple Languages |
|
Home Bible Treasures Afrikaans |
This page in: -- Albanian -- Arabic -- Armenian -- Bengali -- Burmese -- Cebuano -- Chinese -- Dioula -- English -- Ewe -- Farsi? -- French -- Georgian -- Greek -- Hausa -- Hindi -- Igbo -- Indonesian -- Javanese -- Kiswahili -- Kyrgyz -- Malayalam -- Peul -- Portuguese -- Russian -- Serbian -- Somali -- Spanish -- Tamil -- Telugu -- Thai -- Turkish -- Twi -- Urdu -- Uyghur -- Uzbek -- Vietnamese -- WOLOF -- Yiddish -- Yoruba
YOWAANA - Leer gi leeral na Lëndëm gi
Jàngat ci xebaar bu baax bi ci Kirist ci Yowaana
Dalal ci Injiilu YowaanaKrist dafa sant taalibeem yi ñu nekk ay seedeem. Moom bindul sax nettalib dundam, Moom ci boppam. Te mosul a yónnee benn bataaxal ca Jàngu ya. Waaye màqaamaam laaloon na lool xoli taalibeem ya, ba xiir leen ci màggal Yeesu-Krist jaare ko ci Xel mu Sell mi. Dañoo gis ci Mbëggeelam, suufeeloom, deewam ak ndekkiteem, am ndam lu mel ni ndamu Yàlla cundum, li fees dell ak yiw, ak dëgg. Fi ndaw yi Macë, Màrk ak Luk di nettalee kàdduy Yeesu aky jëfam, ak nguuru Yàlla ni li waraloon ñówam, Yowaana moom, dafa nuy feeñalal kan mooy Yeesu dëgg ak itam mbëggeelam gu sell gi. Loolu moo tax ñu jàppe Injiilu Yowaana ni xolu Injiil yi, maanaam kaalag téere yépp yu Biibal bu sell bi. Kan moo bind Injiil bii?Ci ñaareelu téeméereelu at yi la kilifay Egliis (Jàngu) bi nangu ne Yowaana mi nekkoon ndawul Yeesu moo doon ka bindoon téere bu amul moroom bii. Yowaana taskatu Injiil bii, lim na ay apootar yu bare, waaye boolewu ca turu magam Saak ak turam moom ci boppam, ndaxte dafa jàppoon ne yelloowul ñu koy limandoo ak Boroomam, ak Musalkatam. Waaye, Irene, njiitu jàngu ba ca Lyoŋ. ca Faraans biral na ne Yowaana miy ndawul Yeesu te sóonuwoon ca dënnam, ba ñuy reerandoo reer bu mujj ba, moo bind téere bii, ba muy liggéey ca Efes, ca jamono nguuru Buur Trajan diggante atum 98 ba117 G.Y. Am na ñeneen ñu xalaat ne ki bind téere bii du Yowaana, taalibe Yeesu mi doon ànd ak Moom,waaye kenn lawoon ca magi jàngu ba, te nekkoon taalibe Yowaana te itam ba mu koy bind romboon na jamono ji ñu wax. ŋàññkat yi ay géntkat lañu. Xamuñu Xelum Dëgg gi dul fen mukk, apootar Yowaana dugal baat ci tontu bi, bi mu nee: ”Te nun gis nanu ndamam.” Ci dëgg moom bokk na ci ñi seede jàkk dundug Yeesu, deewam ak ndekkiteem. Ay xaritu Yowaana ñoo tëje téere bi nii: ”Taalibe boobu mooy seede mbir yooyu, bind leen, te xam nañu ne, li muy wax, dëgg la. (Yowaana 21:24) Dañoo ràññee melokaanu Yowaana ak bu yeneen apootar, maanaam yeesu bëggoon na ko lool ba may ko sax muy noppalu ci dënnam, ca bésub reeru jookkoo bu Sell, bu jëkk ba. Yowaana kese moo ñemewoon laaj Yeesu kan mooy workat bi ”Boroom bi, kan la? (kan moo lay wor?”) (Yowaana 13:25). Yowaana doomu Sebede ak Salome waxambaane bu ndaw lawoon ba ko Yeesu di woo ngir mu topp ko. Moo gënoon a féete ndaw yeneen apootar yépp. Nappkat lawoon bu nekkoon ak ay waajuram ca Bethsaida ca wetu dexu Tiberiad. Àndoon na ak Piyeer, Andere, Saak magam, Filip, ak Natanael, ñu wàcc ca dexu jurdan ga ngir dem ca Yaxya mi doon woote ngir tuubu bàkkaar. Yowaana baalu na bàkkaaram te Yaxya sóob na Ko ci ndéegu Yurdan. Man na am ne ci njabootu Aan la bokkoon ndaxte Aan ci boppam xamoon na ko, te amoon na sañ-sañu dug ca biir màkkaanu buur ba. Kon, jegewoon na ag njaboot gu sell, li ko may mu wax ci Injiilam lu yeneen apootar yi bindul, maanaam lu mel ni ba Yaxya joxoñee Yeesu, daldi ne “Kii mooy Botem Yàlla miy dindi bàkkaar ci àddina si. Noonu, apootar yowaana, jaarale ko ci Xel mu Sell mi, mooy ndongo li gënoon a yëg mbëggeelu Boroom bi Yeesu. Li Yowaana séq ak yeneen ñetti taskati Injiil yiBa Yowaana doon bind Injiilam, fekkoon na ñu bind Injiilu Macë, Màrk, ak Luk te jàngu ya miisoon nañu leen sax ab diir ba noppi. Ñetti taskati Injiil yi dañoo bind seen Injiil ci téere làkku Yawut bu cosaanu, boo xam ne Macë moo ko jël dajale ci seede apootar, yi aju ci kàdduy Yeesu, ngir ñu bañ a réer, ndaxte at yaa ngi jàll te Botoom bi dellusiwul ba tey. Jëfi Yeesu ak xew-xewi dundam amaana dañu leen dajale ci ab téere bu ñu def ay xaaj. Taskati Injiil ya dañu daan farlu ci aar mbind yi ngir ñu leen di jottalee ak njubte gu wér. Luk mi nekkoon ab doktoor itam, sukkandiku na ci yeneen ponk, ndaxte gise na sax ak Mariyaama Ndeyu Yeesu ak yeeneen seede yu gis Yeesu. Yowaana moom royukaay bu am solo la, ak yeneen royukaay yi nu jotoon a lim. Dafa moytoo dellu ci nettali yooyu, ak kàddu ya jàngu ya xamoon ba noppi, te dolli ca yeneen. Fi ñetti Injiil yu jëkk yi di nettalee jëfi Yeesu ca diiwaanu Galile, te di ci benn tukkib Yeesu ca Yerusalem, te muy tukki ba ñu koy reye, fekk na ñeenteelu Injiil bi won nanu ne Yeesu dem na Yerusalem ca jamono ja Mu doon liggéey ca Galile ak gannaaw gi. Yowaana biral na nu ne Yeesu ganesiwoon na ñetti yoon péeyu réewam ma, fa Ko kilifa askan wa weddee. Ba ñu jànkoonteek Moom ba sonn, ñu jébbale ko ngir ñu daaj Ko ci bant. Yowaana moo nu xamal liggéeyu Yeesu ci biir yawuti Yerusalem yi, fi nekk xolu cosaanu Kóllëre gu Njëkk ga. Ñenteelu xebaar bu baax bi joxul woon solo kéemaan yi Yeesu def, juróom-benn rekk la wax ci kéemtaan yooyu. Lan la Yaxya bëggoon a leer ci lii? Dafa wax kàdduy Jesus ci anamu Ki wax, "MAN LA" te ci anam woowu lay leeral jikko Jesus. Ñatti evangelist yi njëkka wax ci jëf ak dundu Jesus, waaye Yaxya dafa gënoon bàyyi xel ci nettali nit ki Jesus nekkoon ci ndamam ci sunuy bët. Waaye fan la Yaxya jëlee kàddu yu mel noonu, yu mënul nekk ci ñeneen ñi, te Yeesu wax ci boppam? Xel mu Sell mi moo leen fàttali ginaaw Pentekost bu njëkk bi. Ndaxte Yaxya ci boppam waxoon na ci jamono yu wuute ni, taalibe yi xamu ñu woon dëggug yenn ci kàddu yi Yeesu waxoon, ba keroog ndekkiteem ak wàccig Xel mu Sell mi ci seen kaw. Ci noonu, ginaaw ga mu xam luy tekki ci kàdduy Yeesu, yi mu waxoon ci boppam te ci biir baat bii di "MAN LA". Màndarga yi ñuy ràññee xebaar bu baax bii amul fenn. Yowaana bind na itam ay kàddu Yeesu bi muy wax ci yu wuute yu mel ni lëndëm ak leer, xel mi ak yaram wi, fen ak dëgg, dund gi ak dee gi, ak itam waxinu “bokk ci kow, mbaa ci suuf ”Wuute-wuute yooyu nekkuñu ci yeneen Injiil yi. Waaye ay at ca kanam, Xel mu Sell mi fàttali Yowaana kàdduy Boroom bi, fekk munga dëkkoon ca diiwaan bu Grek ya ëppoon doole. Taskatu Inliil bi xam na ne Yeesu daan na jëfandikoo làkku Semit bi bokk ci làkki yawut yi, waaye itam daan na ci boole Grek ngir yeneen réew (jot ci xabaaram bi). Lu tax a jóg Injiilu Yowaana?Yowaana bëgguloon wone Yeesu ci wàllu jëmam, xam-xam, baatin, walla xalaat, waaye moo gën a farlu ñeneen ñi ci ni Mu soppalikoo nekk nit, ay néew dooleem ak maram, fekk ñungi Ko daaj ci bant. Dafay biral ne Yeesu mooy Musalkatu nit ñépp, du Musalkatu Yawut yi rekk, ndaxte Mooy Mbotem Yàlla miy faxas bàkkaari àddina sépp. Yowaana dafa nuy won ni Yàlla bëggee bépp doomu Aadama. Li nu fi jot a wax,moo nuy tàbbil ci diggu xolu bii Injiil, maanaam Yeesu Krist mooy Doomu Yàlla ji. Dundam ba fàww feeñ na ci dundam ci know suuf, ci nekkinu Yàlla ci jëm, ak sañ-sañam ci biir néew kàttanam. Noonu,jaare ko ci Yeesu, Yàlla dundusi na ci sunu biir. Li Yowaana doon wut, du wone Yeesu ci wàllu màccug xam-xam, walla kumpa, waaye dafa bëggoon a xamle Boroom bi jaarale ko ci Xel mu Sell mi ci know ngëm lu dëggu. Kon noonu la tëje Iijiilam ak kàddu yu siiw yii: ”Waaye li ci nekk, bind nañu ko ngir ngeen gëm ne, Yeesu mooy Almasi, Doomu Yàlla ji, te seen ngëm may leen, ngeen am ci moom dund.” (Yowaana 20:31) Ngëm guy dund te nangu Yeesu ni Yàlla,mooy mébétu Injiilu Yowaana. Ngëm googu dafay jur ci nun dundug asamaan gu amul àpp te sell. Kan lañu jagleel Injiilu Yowaana?Téere bii fees dell aky kàddu yu dëggu yu jëm ci Krist, kenn bindu ko ngir woo ñi gëmul, waaye ngir dooleel Jàngu bi, te dimbali ko ngir mu ñor ci Xel mi. Póol dafa tàmbalewoon samp ay jàngu ca Anatoli ca jamono ja ñu ko tëjee kaso ca Rom. Piyeer takk dàllam dem saytuji jàngu ya ñu geentaloon, te ñaax leen, soññi leen. Ba Piyeer Ak Póol génnee àddina xéy na ca bundxataali Neron ca Rom, Yowaana daldi leen wuutu, dem dëkki Efes, fa doon màkkaanu diine Kercen ca jamono jooja. Mu toppatoo jàngu ya tasaaroowoon ca biir Asi-minër yépp. Képp ku jàng ay bataaxalam, ak saar 2ak 3 yu Peeñu bi, dinga xam li Apootar bii di ragal, ak li mu jublu ci xamal nu mbëggeelu Yàlla gi feeñe ci Yeesu Krist. Dafa jàmmaarloo ak boroom xam-xam yi gëm, te rax géttam gi ni ay bukki te di suxlu ay mboteem ak ay xalaati neen, ay ndigal yu tar, teg ci ay yaa ma neex yu selladi, ndaxte dañoo jaxasewoon dëgg gi ak ay xalaati puukare. Taalibey Yaxya itam ca Anatoli lañu dëkkoon.Ki doon woote ngir tuubum bàkkaar lañu gënoon a naw Yeesu Musalkat bi. Ñungi doon séentu Almasi bi ñu dige,di xalaat ne ñówagul. Ni Yowaana di faramfàccee Yeesu, dafa weddi xalaat yépp yi bañoon Yeesu. Dafa yékkati baatam ca know, ŋàññ xelum jànkoonteel moomu te biral ne: ”Gis nanu ndamam, mu fees ak yiw ak ndam ak dëgg, ndam li baay bi jox jenn Doomam ji mu am keep.” Dafa mel ne ñi ëpp ci ñi ñu jagleel Injiil bii ay yéeféer yu tuub(tuubeen) lañuwoon, ndaxte Yowaana dafa joxe ay tegtal yu bare yu aju ci dundug Yawut, yu ñu soxlawul xamal Yawut yi. Rax ci dolli Yowaana tibbul ci ay kàdduy Yeesu yu ñu bind ci Arame te firi leen ci Grek ni ko yeneen taskati Injiil yi defe. Moom dafa jariñoo ay baati Grek yu jàngoom xam ba noppi, sol leen xelum Injiil, noonu mu seede kàdduy Yeesu ci làkku Grek bu set wecc te amul gallankoor, ci know wommatu Xel mu Sell mi. Noonu, Injiilam dafa xóot te woyof, gën a yeye bépp ngéwéle. Xel mu Sell mi won nanu ci Injiil bii muuru dëgg gu woyof la, ngir ñépp man a xam bu baax li muy firi te amul àpp. Kañ lañu ko bind?Ñungi sant Boroom bi moom mi may ay gëstukati suuf si yu dëkk penku, ñu feeñal ay kayit yu ñu bindoon ca atum 100 L.Y. (Laata Yeesu) ca Misira. Ca booba kayit, man nanu ci jàng ay kàdduy Injiilu Yowaana yu leer nàññ. Yi ñu feeñal wone na ne xamoon nañu Injiilu Yowaana ca atum 100, te du woon rekk ca Asi-Minër, waaye itam ci Afrik bët-gànnaar, te amaana itam ca Rom, li dakkal bépp guddal ŋaayoo ak téesante. Dëgg googu dafay dëgëral sunu ngëm te di nu may nu xam ne Injiil bii, Apootar Yowaana moo ko bind, ci leerug Xell mu Sell mi. Lan la Injiil lii ëmb?Tëj ràpp Mbind mi yoombul. Xaaj Injiilu Yowaana ba mu nekk ay pàcc itam, jafe na. Waaye dinanu ko jéem a defe nii:
Taskatu Injiil bii di Yowaana, dafa jekkal ay xalaatam tënk leen ci benn ba ñaari xalaat, mbaa baat yu lëkkoo ni calalla. Li ñuy tekki benn lay doon yen saa yi. Xalaatu Yowaana nib semit, ak gis-gisu baatinam bu xóot bi, méngoo na ak xadaru làkku grek ci ànd bu rafet te am ndam. Ba tey jii, Xel mu Sell mi mungi nuy dimbali ngir nu man a xam bii Injiil. Teenu xam-xam ak maandute buy ball ba fàww la ci nun. Képp ku xóotal njàngam ci téere bii, dina sukk ci kanamu Doomu Yàlla te jébbal ko dundam ci biir cant, màggal ak goreel gu amul àpp. AY LAAJ
|